Bu Usmaan Sonko bokkee ci wotey 2024 yees dégmal de, dina doon jaloore ju réy. Nde, 2021 ba léegi, Nguurug Maki Sàll gaa ngi koy tegal i ndëgg-sërëx yu dul jeex. Yoon wum mën di jaar ngir bokk ci yile wote, Nguur gi lal i pexe ngir dog yoon woowa. Bu dee pexe yooyu, lu ci ëpp ci yoon lees koy jaarale, am na ci yoy, caytug bokkeef gi moo leen di doxal. Li koy firndeel moo di ne, bi ndawul Usmaan Sonko li demee ca DGE ngir ñu jébbal ko xobi baayale yi, dañu ko ko gàntal ci lu worook yoon. Li ñu taafantoo woon mooy ne, ndawul Nguur gi ci wàllu yoon (Agent judiciaire de l’Etat) dafa dugal ab dabantal (recours) ngir neenal àtteb Sabasi Fay bi delloo woon Usmaan Sonko ay àqam. Noonu, Ayib Dafe di fa jaabante, ñu koy gàntal ba keroog ëttub àtte bu mag bi di neenal àtteb Sabasi Fay bi, mu di seen uw lay nëgëni. Démb nag, banqaas bii di CDC (Caisse de Dépôt et de Consignation) moo feelu DGE ci xeetu doxalin woowu.
Ngir bokk ci wotey 2024 yi, lawax bu ci nekk danga war a joxe ag warlu (caution) gu tollu ci 30i tamndaret (milyoŋ) ci sunuy koppar. Xaalis boobu, CDC moo koy nangu. Li ko ci yoon gàll mooy nangul wutaakon yi seen i seg (chèque), jébbal leen ab kitãs, ginnaaw gi mu jox leen ag ceedit (attestation). Démb nag, al coow juddu na ci. Nde, ci ngoon gi la demoon ca màkkaanu CDC ngir jébbal leen segu wutaakon bii di Usmaan Sonko mi ko yabal. Ñoo ngi doon ruumandaat naan, waa CDC dañ bañoon a jël seg bi ngir ne Usmaan Sonko bokkul ci toftaleg lawax gi ñu yor. Waaye, Ayi Dafe miy ndawul Usmaan Sonko ci boppam, génne ne ab yégle di ci indiy leeral.
Ayib Dafe nee na, jot na kitãs bu wér ginaaw bi mu joxee segu 30i tamndaret (milyoŋ) yi. Dafa weddi tamit xibaar bi jiboon di wax ne, CDC daf delloo segam, bañ ko jël. Waaye, nag, fàttali na CDC fi dayoom yem. Ndaxte, moom Ayib Dafe dafa gi ne :
« CDC ak DGE ñoo yem kepp ci wàll saytu ak nangu ay wutaakon yu bëgg doon i lawax. Sañ-sañam mi ngi yem rekk ci nangu warlu yi ni ko dogu L.122 bu càrtug wote gi tëralee. »
Ginnaaw bi mu leeralee loolu, ndawul Usmaan Sonko li wax na CDC mu jox ko ceedit giy ànd ak kitãsu warlu gi ci ni mu gën a gaawee.