BAANE, YAA WAANE !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Dàqees na àtte bi ba alxames, 1 fan ci suwe 2023. Démb ci talaata ji lañu doon layoo tuumay ciif ak tëkkuy rey yu Aji Raabi Saar di jiiñ Usmaan Sonko, njiitul Pastef li. Lu bari xew na ca àttewaay ba, démb. Xëccoo, dàggasante, werante, xastante ak xeeti wax yu ñaaw a ñaaw…lu nekk, déggees na ko, fa àttewaay ba.

Démb, sutura dafa gàddaay, wacc fa jébbaane. Kersa dafa rus ba ne tott, tottaaral, ndax waxi baane. Teggin dafa làqu, daw, ndax kenn wormaalu ko. Wax ci boppam dafa amoon gàcce, nde kenn woddu ko. Yeraange moom, kenn séentuwu ko fa woon ba ko fay xeeñtu. Dafa di, fu waxi baane ganesi, ay duural fees fa dell, ngor du fa xëy ba fay gontu. Gor yee jommi. Ndege, démb, jigéen lañu summi ; awra góor, ñu wuññi. Fii la Senegaal tollu.

Ñaari ati Yàlla, ñuy tilimal deru Senegaal ba, démb ci talaata ji, ñu gënati koo didimal. Senegaalu Seŋoor jagul woon, waaye sàmmeesoon na wormay nit ñi. Senegaalu Abdu Juuf bari woon nay fitna, waaye kersa amoon na ba tey. Senegaalu Ablaay Wàdd metti woon na gaa, xeexoo bi bari woon, waaye nag, doon nañ jéllale ak a wattu suturay nit ñi. Gu Maki Sàll gii nag, lépp a wullee-mbaay. Senegaal a ngi mel ni cin lu amul kubéer.

Fexeel ab nattaangob pólitig a jaral ñenn ñi sànk as ndaw su desee saagër, bu fekkul mu xayadi sax. Jël ab xaleel lu jigéen di ko fowe, soppi ko ngànnaay, di ko xeexe sa wujjuw pólitig. Mu jaral la nga lor ko, tuutal ko, xeeblu ko ci kanami nawleem, yablu ay mbokkam. Faagaagal Usmaan Sonko moo tax ñu yàq àddinay Aji Saar. Bu dee wax dëgg rekk, kuy seet ñi gëm waxi Aji Saar ak ñu koy nawlooti fii ci Senegaal, ay bennat lay doon. Faralun Usmaan Sonko de, Yàlla xam na ko. Dafa di rekk, lu ne fàŋŋ, kenn du ko jeex. Te, lii, dafa sax fàŋŋaaral. Nu ànd tënk ni mbir mi deme.

Aji Saar daf ne Usmaan Sonko daf ko siif ay yooni yoon, boole ci di ko tëkku ak ñaari fetel. Waaye nag, wax ji dafa bari ay mbir yu ci safaanoo. Nde, bees sukkandikoo ci kàdduy boroom-këru Ndey Xadi Njaay mi moom dàmpuwaayu Sweet Beauty, Aji Saar daf ko sonaloon ci laaj yim ko doon laaj Usmaan Sonko kañ la fay ñëw. Waaw, ku la yàgg a siif, nar la siifaat, noo ko mën a xaaree ? Balaa loolu sax, nga ne yónnee na la bataaxel, ne la mi ngi ñëw. Waaw, noo sañee xaar as waay su nar a àgg sa kow wëliis sa coobare ? Mu agsi, nga war ko dàmpandool ak sa moroomu liggéeykat, nga dàq ko, ne ko mu génn. Waaw, noo mënee wéet ak góor gu lay metital ? Nga ne dafa yoroon ñaari fetel tiimale la leen. Mo waay ! Aji nag, loo nu jàppe ? Naka la góor mënee séq ak jigéen ñaari loxo yi jàpp ? Rawatina bi nga nee dafa daanu sa kow. Loolu moom, képp kuy jigéen, waxuma la sax góor, xam nga ni yenuwul maanaa. Diggante boobu, boroom dina tal leneen. Dëgg neexul. Kaay nag, nu laaj la tuuti.

Aji, lu fa Siidi Ahmet doon def ? Lu la dugal ci oto Maamuur Jàllo mi nga xam ne, àddina sépp a xam mer gim guuxal Usmaan Sonko ? Lu ci yoonu Me Gabi Sow ak Joor Jaañ ? Waa Aji, kañ ngay wësin ? Li nga wax MC Ñas nag ? Yow Aji Saar, lu tax benn seede dëggalul say wax ? Ana say mbokk ? Caaxaan baaxul waay.

Coow lii, tas nay kër, féewaley mbokk, yàq ay liggéey… Daay bim taal lakk na xaalis bu baree bari. Waaye, li ci gënatee metti xol mooy fitna ju réy ju mu jur ci réew mi ak bakkan yi ci rot. Daanaka, 17i nit dee nañ ci sababu coow lii. Ñépp foogoon ne dina jeex démb ginnaaw bi àttekat bi dogoo ne daf koy àtte wenn yoon mu jeex. Waaye de, dàqaat na ko ba keroog  1eelu fan ci weeru suwe, mu méngook bésub alxames.  Layoo bi nag, yàggoon na lool sax. Mi ngi tàmbali woon juróom-ñeenti waxtu ci yoor-yoor bi, di wéy ba ñetti waxtu ci guddi gi.

Usmaan Sonko teewu ca woon. Moo tax ay layookatam mënuñu ko woon a layal. Meetar Gabi Sow, Joor Jaañ, Mammadu Maamur Jàllo ak ñeneen ñees tudd ci coow li tamit, teewuñu ca. Waaye, loolu terewul layoo ba am. Ak li layoo biy yàgg yépp, nee ñu, Aji Saar ak i layookatam indiwuñ fa dara ciy firnde yuy dëggal tuuma yees gàll ci ndoddu Usmaan Sonko. Moom kay, làmmiñam rekk la yor. Terewul nag, toppekat bi moom, dafa jàpp ne Usmaan Sonko a def lees koy toppe lépp. Moo ko tax a sàkku ci àttekat bi mu daan ko. Abdu Kariim Jóob, li mu bëgg mooy àttekat bi daan Usmaan Sonko 10i ati kaso ngir ciif ak yeneen 5i ati kaso ngir nger mi mu ger ndaw ñi. Àttekat bi nag, nee na, ndogal li dinañu ko jël benn fan ci weeru suwe.

Mbaa boobule àtte du laajaat beneen àtte ? Nde, li ñépp di njort mooy ne, bu ñu daanee Usmaan Sonko ci lii, réew mi dina tàkk, dina jax, fitna jóg te kenn du xam fu muy teerijee. Lii lépp ci waxi baane rekk. Ay baane ! Yaa waane de.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj