BAKKEL : NJIITUL SAED LI SEETI WOON NA BAYKATI KÀMBUG KOLANGAL GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Mbënnum dexug Senegaal gi dafa jural ay jafe-jafe dëkk yi ko dar, rawatina Bakkel mi nga xam ne, dafa bariy kàmb. Ndax, bi dayob dex gi yokkee, ndox mi dafa wal, ngàllent bi daanu, mu jàll ca tool ya, yàq fa lu bari.   Looloo waral njiitul SAED li, Alasaan Ba, seeti woon, tey ci altine ji, beykati Bakkel yi nga xam ne, mbënnum dex gi daf leen a lor. Nde, ñoom beykat yooyee, seen tool yaa ngi féete ci kàmbug (cuvette) Kolangal gi. Li yékkati Alasaan Ba moo doon taxawuji beykat yooyi, wan leen ni Càmmug Sénégaal gi du leen seetaan. Sëñ Alasaan Ba dafa wax ne,

« Dama seetsi tey beykat yi ngir indil leen ndimbalug Càmm gi, saytuwaale yàq-yàq yu bari yi mbënnum dex gi sabab, rawatina ngàllent bi mu daaneel. »

Li ngàllent bi daanu moo sabab mbënnum dex gi. Ndaxte, ngàllent baa daan téye ndox mi. Bees sukkandikoo ciy waxam nag, moom njiitul SAED li, bu ngàllent bi daanoo, dafa fekk ne defarin waa baaxul. Ci kow loolu, xamle na fa ne, dinañ càmbar kàmbuy Bakkel yépp, nga xam ne ay jafe-jafe yu metti lañuy dund jamono jii.

Mi ngi jeexalee ay kàddoom ci dige ni, dina saytu béréb yi ci laale yépp ngir indi ciy saafara, mën a joyyanti mbey mi foofa. Li tax mu bëgg a doxalee noona mooy ne, ciy waxam ba tey, Bakkel dafa yeyoo ñu beral ko loxo ngir taxawu askan wa fay yeewoo.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj