Mbir mi doy na waar. Kenn xamul lii lu mu doon. Nekk cim réew, dund fa lu ëpp fanweeri at, te ba tey may bind baat yi, doxandéem la ñu la fi jàppe.
Am fi liggéey bu baax, di faj samay soxla ak a dimbali samay mbokk ; bokk ci ñiy yëkkati koom-koomu réew mi. Ci gàttal, man nanoo wax ne Baay Njaay xaw naa tekki ci réew mi te amal na njariñ dëkk bi.
Bariwuma fi ay xarit waaye am naa fiy xameel yu rafet jikko yoo mën a jëflanteel ci wàllu àddina ak diine.
Bi may ñów Itali amaguma fukki at ak juróom-ñatt. May xale bu góor, tollu ci sama diggu ndaw. Ma ànd ak kàttan, wóolu sama bopp, yaakaar ne lu sama loxo yóotu jot ko.
Dëkk bu ñuy wax Duwinoo, fa laa ame bàkkaloryaa soog a dem Triyeste. Fa laa defe sama lisãs. Yàlla dimbali ma ma jàll eksame doktoraa ca iniwérsite bu Siyeena. Kon dëkk bii ame naa fi ay lijaasa yu raññeeku ci daara yi gën a kawe. Lu nit di itewoo ci njàng, Yàlla may na ma ko fi.
Ba ma noppee ci loolu laa taxawal am mbootaay ngir siggil jëmmu Afrig fii ci Itali, bokk tamit ci mbootaay yiy xeex ngir sunu aada ak sunuy làkk am seen gëdd.
Dara yombul ndax Wolof Njaay nee na «Ndar xëyul sotti». Masumaa jàng sama kàllaama, Wolof, bay am fitu taxaw ne damay dundal li ma nàmp. Waaye yaakaar naa ne li amoon solo mooy tàmbalee xam sa bopp ak geestu fi nga jóge walla fa nga cosaanoo.
Ndànk-ndànk may jege ab bindkatu wolof ak di jàng abajaday làkk wi. Ma dem bay tàmbalee firi baatu waa réew mi ci Wolof. Mbir mi dugg ma, saf xorom, indil ma yokkute yu am solo ci samay xalaat, sama gis-gisu àddina, ak samay xameel.
Lu neex du doy, te kenn du ko dog ba beneen yoon. Nit koo gis am na ku ko xàllal yoon mu jaar fa. Ca njëlbeen ga, jànkoonte woon naa ak ay jafe-jafe yu bare ci njàngum wolof. Ci yëngu-yëngu bu am solo la dajeek boroom xam-xam bu siiw, ñu raññee ko lool ci mbindum kàllaamay Kocc ak tekki ay làkk yu wute ci Wolof.