Jaafara Sadiixu Fofana
Ca Kungéel (péeyub Bàmbug) amoon na ndajem tàggat bu
ñetti fan ci « Ndefarum saf-safal ak sunu xeeti meññeef yi ak
suusal caakiri ak cerey ñebbe ».
Lu tollu ci 30i jigéen ak lu teg, bawoo ci 6i diiwaan ak i gox yu
wuute ci réew mi, amaloon nañ am ndaje ca Kungéel. Ndaje
maa ngi dooroon àjjuma, 28eelu fan ci weeru féewaryee jàpp
dibéer 1eelu fan ci weeru màrs 2020. Ñu bare ñoo fa
daje woon : jàngalekat, yombalkat, gëstukat, lëkkalekat, añs.
Liñ ko dugge woon mooy tàggatu ci « Ndefarum Saf-safal ak
sunu xeeti meññeef yi ak suusal caakiri ak cere ñebbe »
Ku nekk ci jigéen ñooñu, nag, cib bànqaasu diiwaan mbaa gox
nga féete. Bànqaas yooyu, dippees na leen ci nasaraan
« Komisiyoŋ » SNAN. Juróom-benni bànqaas lañu am, yu :
Jókkul Mbelbuug
Jurbel
Kungéel
Kawlax
Kafrin ak
Kidira
Ñoxor Ngom mi jiite SNAN (Sàndikaa Njabootu
Alfaabetisaasiyoŋ Nasiyonaal), ginnaaw bi mu sargalee kilifa yi,
wax ci juddug SNAN, kàddu yii la fa biral :
« Ndaje maa ngi tàmbale ci àjjuma jii, waaye ñu ngi ko déggoo
woon ca jataayu Jókkul Mbelbuug ci 23eelu fan ci weeru
desàmbar 2019 mu bokk ci sunu jëf yi nu tëral war koo doxal ci
at mi, maanaam mu dellu ci naalam. Lees ci jublu moo di fexe
ba ubbil jigéen ñi buntub xéy ak koom-koom ngir soppi ak gën a
baaxal seen nekkin, te bañ a yem rekk ci njàngum liifantu ak
xayma, waaye jëfandikoo leen ba indi koom. »
Kii di Daawuda Jàllo, 2eelu tofo ci njiitu Bokk moomeelu Kungéel
(MEER) ak Maamudu Umar Géy miy « Inspekteeru
edikaasiyoŋ ak foormaasiyoŋ » Luññutukat bi ŋànk ak di
saytu lépp lu aju ci njàngum tuut-tànk yi, yar ak tàggat ci xaaj-
diiwaan bu Kungéel, jàpp nañ ni tàggat bii lu ñu war a ñoŋal la.
Ndax ci 3 nisër yi ko taxoon a jóg, 2 yi moom jot nañu ko fii.
Ndaxte, soxna Juma Jóob (di kenn ci way-tàggatu yi) , li mu fi
wone, nettali ko ci 3 xeeti saar yi ngeen fi jànge, dal na xel, te it
am na solo lool. Ndege, dina tax ba jigéen ñi gën a yokk seen
koom. 3eel bi moom ci kàdduy IEF bi, ci biti doŋŋ lañ koy mën a
nattee ci kow ñu nangoo sotti ak wéyal li ñu fi weccoo ci 3 fan yii
ci seen gox yi !
Aliyu Sàll mi teewal « Koñsey departamantaal » bi mu jëlee
kàddu nee na : « li SNAN def nii méngoo na lool ak sémbub PRODESK dib naal bu nu defar ngir gunge kuréel yeek
mbootaayi koom yi nekk ci gox bi, te dinanu fexe ba def ciy
jéego »
Mbaaxaan Jóob mi teewaloon kuréelu CDK, gannaaw bi mu
fésalee mbégteem ci tàggat bi, wone na ne lëkkaloo dina am ak
waa SNAN ngir ñu àndandoo lawal xam-xam bii.
Laata Inspekteer, maanaam IEF, di tëj ndaje mi ci turu
« Perefe » mi ko yebal, Ami Siise Fay jagleel nab taalifu delloo
njukkal Sàmba Jaawo mi desoon ci toolu xare bi ci 24 fan ci
weeru desàmbar 2019 cib « laksidaa » diggante Gudiri ak
Kidira ba xol yépp tooy !
Awa Faati, ak Jaafara Fofana feelu ko, waaye, ñoom seen taalif
dafa jëm ci njariñal saf-safal bi ñu doon defar, ak jàng ak
jàppalante ngir réew mi jëm kanam.
Wólis 6 « Komisiyoŋ » yi bokk, waa Luga ak Dakaar ñoom it
fésal nañ seen yéene ngir bokk ci SNAN.
Way-tàggatu yi woon ci lël bi, jox nañ leen ku ci nekk « lijaasa »
buy firndéel ni bokkoon na ci.
Nu wax itam ne, ginnaaw « Meer », « Perefe », « IEF » ak
« Koñsey departamantaal », SNAN yëgaloon na lël bi yeneen i
kuréel ak i kilifa ngir ñu teew, jëmmal ak darajaal lël bi ci ubbite
beek tëjte bi, ñu ràññee ci : UCEM, Kërug Jigéen, GIE « Xaritu xale yi, Seydinaa Ibraayima Jóob ak Ndey Ndumbe Saar mu « Comité consultatif des femmes ».