TÀGGATOO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Roqi, ba beneen yoon.

Seetal ma lii rekk. Wax dëgg. Xool sama digganteek Yàlla te bañ a fen.

Waaw, yombul nga seeti sa rakk ak sa mag te say rongooñ tuuruwuñu. Walla dara yëngalul sa yaram.

Li ma yëg tey bi may tàggoo ak Roqi Yàlla rekk a ko xam. Bi ma koy nuyu, di wéy di dem, geestuwuma ndax xol bu fees ak yaram wuy rëg-rëgi. Ma xam ni deret fum la fekk daan la. Te doo ci mën dara. Li ci gën a yéeme mooy dangay mel ni ku ràkkaaju. Nga naan : « waaw feebar bi ma soppi nii nu mu tudd ? » Geneen kàddu jib, daldi feelu, ne : « feebaru mbokk moo la daan ba nga xalangu. » Bu ko defee, may seet naka laa koy fajee.

Doktoor mënu ci dara. Farmasi du jaay lu koy woyafal.

Roqi gënuma laa xam li may bind. Duma fi nekk di jekk-jekkal ak a làq-làqal. Damay jaar ci digg bi, toj yax bi. Su ma wóoroon ne tàggoo nii la mettee damay randal sama ñibbisi Itali. Waaye lu la bett, daan la ba nga mëq suuf si.

Lu waay di jàmbat, wolof njaay léebootina ko. Dëgg-dëgg sama rakku bopp ji lu ma wax rekk sama digganteek Yàlla laa ciy seet.

Weneen yoon su may ñëw Pari dama koy waaj bu baax. Julli ñaan Yàlla bañ a jooy, bañ a saalit. Guléet mu dal ma bésu tey. Àddina nii la. Ay jaar-jaar rekk la.

Abu Daraame, seede ma.

Baay NJAAY

Baay Njaay
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj