Askanu Senegaal dafa mës a weg i làmmiñam, làmmiñi réew mépp. Yàgg na leen a jàppe niy bokk-moomeelam. Loolu, deesu ko nàttable. Naam, ñoo ngiy jëfandikoo, yenn saa yi, yeneeni làkk ngir jàng walla jokkook àddina si ; waaye terewul ne, ci làmmiñi réew mi lañuy faje li ëpp ci seeni soxla. Waaw, ci lañuy wax seen xalaat, di ci waxtaan, di ci jokkoo aka werante. Kon nag, doomi Senegaal fonk nañu lool seeni làmmiñ, rawatina wolof bi nga xamante ne mooy lëkkale sunu waaso yépp.
Kon, bu dee nguur gi jaamu soxlay askan wi kesee ko tax a jóg, war na fullaal làmmiñi réew mi, dooleel leen te boole leen ci njàng mi. Waaye…ndeysaan, ak doxalin wi nu fi seetlu de, ku yaakaaroon bu yeboo yàqi…
Lu tax ?
Njiit yi fi nekk tey, ku ci nekk ba ngay doon lawax di sàkku ñu fal la, biral ngay dige ñeel làmmiñi réew mi. Waaye ku ci toog, daldi fàtte la nga dige woon, fàtte askan wi. Bu weesoo coppati as tuut ci nafag réew mi ngir jagleel ko pulaar, joolaa, séeréer, wolof ak ñoom seen, nguur gi tus la leen defalul. Waaw, ginnaaw bees nattee xaalis bi réew mi soxla ci at mi, téeméer boo ci jël, dërëm lees ci jagleel làmmiñi réew mi. Xam ngeen ni lii bu dul yabaate yit, ag xeebeel bu amul àpp la. Leeg-leeg sax danga naan doxandéem yee nu gën a fonk sunuy làmmiñ, gën noo xam seen dayook seen njariñ. Waaye, ba tey, warees na xoolaat seen doxalin ñoom tamit.
Sémb yi fi jot a jaar yépp ngir ñoŋal sunuy làmmiñ, moo xam nguur gee leen yabal, walla “ONG” yi, añs, seen liggéey dafa des. Ndege, dañuy tàggat ay nit ci diir bu gàtt a gàtt, jox leen lenge yi, ne leen ayca ! liggéey baa ngook ! Bu ko defee, ñu leen di jox ay tur yu deme ni : jàngalekat, yombalkat, wolonteer walla sax saytukat. Noonu, ñu sóobu ci liggéey bi, fekk ne waajaluñu leen, joxuñu leen jumtukaay yu méngook li ñu leen sant. Moo tax it, xeetu jafe-jafe wu nekk la ñooñii ñu wutal ay dàkkental di jànkonteel saa su nekk. Ñi leen di liggéeyloo yit, kenn du ñoom, moo xam njaatigi operaatëer lañu walla banqaasi nguur gi. Jafe-jafe yiy gàkkal liggéey bi, nag, mënees na cee lim :
– Pey gu néew te ñu ciy yéex a jot ;
– Xeetu njàngale wu sukkandikuwul ci manoore jàngkat yi ak tamit i xarala yu dëppoowul ak jamono ;
– Xam-xamu làmmiñal bu des te li ko waral mooy gàttaayu tàggat bi ;
– Ñàkkum jumtukaay yu baax ak ñàkkum xaalis;
– Sémb yu soreyoo lool, ba tax nit ñiy toog diir bu yàgg soog a dégg walla gis liggéey ;
– Tànneef bu jaarul ci yoon wees di tànne ñenn ci operaatëer yi ;
– Gunge gu jàppandiwul ñeel ñiy yëngu ci làmmiñi réew mi ;
– Tuutal ak ñàkk a weg, añs.
Lees fi lim yépp ciy rëq-rëq a sabab juddug kurél guy xeexal ñiy yëngu ci njàngalem làmmiñi réew mi. Sunu mébét mooy xeex ngir ñépp sàmmonteek àqi làmmiñi réew mi. Kurél gaa ngi tudd Sàndikaa Njabootu Alfabetisaasiyoŋ Nasiyonaal, gàttal bi di joxe SNAN.
SNAN, nag, dafa boole wuuf mboolem jàngalekat yeek yombalkat yi aajowoo làmmiñi Senegaal yépp. Ndax, ñoom ñoo booloo, def benn say, taxaw temm nar a xar seen tànki tubéy ngir ñu jox leen seen gëdd. Kurél gaa ngi juddoo ci ndaje bees amaloon ca diiwaanu Kafrin, ña fa daje woon di waa Kafrin ci seen bopp, waa diiwaanu Kawlax, waa Cees, waa Jurbel ak waa Fatig.
Kurél gi, nag, ay kurél a koy teewal ci diiwaan bu nekk. Loolu dina tax képp ku ci bëgg a bokk, ak foo mënti dëkk, mu yomb la. Waaye, warees na indiy firnde yu leer yuy biral ne jàngalekatu làmmiñi réew mi nga walla yombalkat walla boog li lay tax war a mën a bokk ci njaboot gi. Bu loolu yépp sottee ngay door a joxe juróom-ñett-fukki (400) dërëm ba noppi ñu xamal la ni weer wu dee dinga natt ñeent-fukki (200) dërëm.
Ñaari weer yu nekk, SNAN fas yéene naa amal am ndaje muy boole kuréli diiwaan yépp. Ndaje moomu dees na ko amal ci benn diiwaan bu ñu tànn, di ko ay-ayle ngir yaatal géew bi ba noppi gën a jege askan wépp.
SNAN sos na benn Mbootaayu “WhatsApp”. Dina yombal jokkoo bi ci biir kurél gi, di siiwal aka leeral i jëfam tey tontu ci yenn laaj yi. Dinañ ci waxtaane itam jafe-jafe yi way-bokk yiy tawat.
Sunu nisër mooy soppi nekkinu yombalkat yeek jàngalekati làmmiñi réew mi, fexe tamit ba ñépp jox leen seen gëdd, rawatina nguur gi ak képp ku ciy liggéeyloo doom-aadama yi !
Tey jii bu nuy xool walla di càmbar ñi nekk ci biir SNAN, wólis yombalkat, jàngalekat ak saytukat, daanu fa fekk yeneen boroomi xam-xam yu seen xel màcc jëm ci fànn yu bare ñeel yokkute : Ñooñu ay beykat lañu walla sàmmkat, fajkat, taskati xibaar, bindkat, óbëryee, añs.
Kurél yi nu teewal ci diiwaan yi ñoom tamit dinañuy daje gën gaa néew 2 yoon ci weer wi ngir tëral yëngu-yëngu yi, dajale teg yi waaye it natt doxinu liggéey bi.
Njiitul «Sàndikaa Njabootu Alfabetisaasiyoŋ Nasiyonaal» (SNAN), nag, Ñoxor Ngom la tudd. Képp gu bëgg a jokkook kurél gi, kilifa googu nga war a woo ci 00 221 77 120 21 54.
Jaafara Sadiixu Fofana
SÀNDIKAA NJABOOTU ALFABETISAASIYOŊ JUDDU NA
