Li ko dale 1eelu fan jàpp 12eelu fan ci weeru oktoobar bii ñu génn, 414i ngaalukat (émigrés clandestins) ñoo lug ci yoonu géej wiy lëkkale Afrigu sow-jant ak duni Kanaari yi. OIM, kurél giy saytu daw-làqu yi (migrants) ci àddina si, moo joxe xibaar bi ci dalu webam. Kurél gi teg ci ne, li ko dale ñaareelu xaaju weeru oktoobar ba nëgëni-sii, jàppees na 400i ngaalukat ci géeju Gànnaar gi. Mbëkk mee xewati, nit ñiy song géej gi ci anam bu doy waar, ñu bare di lab bés bu nekk, ñeneen ñiy réer. Àjjuma jii la waa réew mi jagleeloon way-dëddu yi njiitu réew meek nguur gi ñeeblu.
*
Jamono jii, gaal yee xewati. Bés bu nekk, nga dégg lim bu takku ciy ndaw yiy lab ak a réer ci géej yi ; muy lu raglu. Àllarba jii weesu, pólis biraloon nay lim yoo xam ne, dañuy wone ne ndaw ñaa ngiy song géej gi ak doole. Takk-der yi ne, jàpp nañ 1.537i ngaalukat ci diggante Sumbéjun, Barñi, Tëngéej, Mbuur ak Ndar. Ci biir ñooñee ñu jàpp, am na ci 29 jàllalekat yees defeere. Pólis nanguwaale na 6i gaal, 10i motëer, 3i GPS, 2i oto ak karbiraŋ.
Jamono ja ñuy waajal delloosi Senegaal ngaalukat yi jot a teer ca duni Kanaarii ya, la yeneen 1.600 dolleeku ca ña fa nekkagum ci 2i fan kese. Muy luñ mësta gis ci fukki at yii weesu. Ci gaawu gee weesu rekk, 20i gaal yi yeboon lu tollu ci 1.000i nit àggoon nañ Grã Canaria, Tenerif ak El Hierro. Ci dibéer ji, yeneen gaal yu yeboon 600i nit teersi fa. Rfi ne, guleet ñu gis lu ni mel. Rajo Farãs biy leeral ni limees na 2.000i ngaalukat yu fàqee ca tefesi Afrig sowu-jant ya, séddalikoo ci 40i gaal ak i looco yu wóoradi. Li ci ëpp di ay gaali napp.
Lugatees na 115i nit ci géej gi, am kenn ku ci dee ci tefesu dunub Hierro. Muy lu doy waar. Waaye, lim yi yemul foofu rekk. Nguur gi, OIM : ku ciy wax dëgg ?
Bi mi mbir mi dooree ba léegi, at mii, daanaka kenn bàyyiwu ci woon xel noonu. Moom, daal, biñ nee am na 140i nit ñu lab ak 6i néew yu feeñe ci tefesi ndakaaru yi la nit ñi tàmbalee fullaal mbir mi dëgg-dëgg. Ñu teg ci ne lu tollu ci fukki ngaalukat réer nañu ci géeju Gànnaar gi, kenn gisagu leen. Bi xibaar bi jibee, nag, askan wi jaaxle, coow li mel ni tulleek maale ci réew mi, mbëkk mi fii, gaal yi fee, jàppal Barsaa fii, bàyyil barsàq fee, Maki Sàll nii, nguur gi naa… Waaye, nguur gi dafa ne woon tekk-tekkaaral.
OIM, gannaaw bi mu jotee ci xibaar bi, daldi koy ñaawlu, naqarlu ko. Ca la génne ab yégle, wax ci ne : « lu tollu ci 140i ndaw ñoo lab ci géeju Senegaal gi ginnaaw bi seen gaal gi suuxee. Gaal gaa ngi yeboon 200i ndaw. » Mu toftal ci ne musiba bile, « mooy musiba bi gën a réy bees dund ci géej gi, ci atum 2020 mi ». Ci saa si, nguur gi daldi jànnaxe, gaawantu génne ab yégle ngir weddi lim bi kurél gi biral. Nguur gi, cib yégleem, dafa ne 10i nit rekk a lab ak 60i yi ñu lugat. Maki Sàll ci boppam, ab bataaxal bu gàtt rekk la bind ci Tweeter, daldi feddali li nguuram gi wax. Ñoom, waxuñu sax ñaataa nekkoon ci gaal gi. Njiitu réew mi, Maki Sàll, deful lu dul jaale way-dëddu yi seen i mbokk, ba noppi di ñaax askan wi ñu gën a fàggandiku, bàyyi xel ndaw yiy war gaal yi, wutali tugal. Waaye, ki teewal OIM ci réew mi, yor seen kàddu, dafa tontu nguur gi, ne : « mbooki way-lab yi ci boppam ñoo nu wax ne gaal gi 200i nit la yeboon. Kon, 140i ñoo réer ».
Ci diggante bésub 7 eel ak bésub 25 eel ci oktoobaar bii, marinu Senegaal, ci ndimbalu Guardia Civil Espagnole, dogaale na 5i gaal yi doon wutali Tugal. Ci lañu xettalee 388i tukkikat, musal leen ci lab. Nguur gi teg ci ne jàpp nañ ci 28i nit yoo xam ne, nee ñu, ñoo jiite woon tukki bi. Ñu ni déet-a-waay, nguur gi yéglewaat ne, am na geneen gaal gu teddi woon bésub 23 eel ci oktoobar, daldi tàkk ci diggu géeju Mbuur gi. Waa OIM ne ko déedéet, teg ci ñenn ci askan wi ñoo leen wax ne, gaal googu, bésub 24 eel ci oktoobar la teddi woon, te Ndar la tàkke gannaaw bi mu jengee, daldi këppu.
Ku ciy wax dëgg ? Ak lu ci mënti am, lim yiy gën di yokk saa su ne. Ay lim yu raglu. OIM mi ngi wéy di xamle ne, am na 200i gaal yu teer ca Kanaarii ci njeexitalu sàttumbar 2020 ba tey jii. 200i gaal yooyu, ñoo ngi yeboon lu tollu ci 5.000i ngaalukat. Lim bii, bees ko méngale ak limu atum daaw mi ci jenn jamono ji, dees na gis ne ëppe na ko 10i yoon. Waaye, lim ba tey àggagul ca limu ati 2006-2007 ya (32 000i ngaalukat yi teeroon Kanaarii). Dafa di, 2006 ba tey, dara soppeekuwu fi ñeel mbëkk mi. Ba tey nit ñaa ngiy sóobu géej gi, naan Barsaa rekk walla barsàq. Mu mel ni, tey la waalo gën a aay.
Helena Maleno Garzon, ab ndaw buy wattu àqi doom-aadama, ne, ci diggante bésub 14 eel ci oktoobar jàpp bésub 7 eel ci nowàmbar 2020, lu tollu ci 1.765 ngaalukat yu bawoo Senegaal lañu dalal ci 3i duni Espaañ, gën jaa yées. DIRPA, ci wàllu boppam ne, ci diirub weer, marinu Senegaal jébbal na pólis 527i ndaw yi doon waaj a ràngu ci mbëkk mi. Sàndarma yi ne, ci alxames jii weesu, fekkees na 6i néew ci mbaalu genn gaal gu doon napp ci géeju Ndakaaru gi. Ñu jàpp ne, ci way-labi mbëkk mi lañ bokk.
Covid- 19, 327, mbëkk mi, 414
Ci dalu webam, OIM biral ne, limu ndaw yiy song géej gi jubali Tugal dafa gën a yokk. 14i gaal yu yeb 663i nit jóge nañ Senegaal, wutali Espaañ. 4i gaal yoo jël, 1 bi suux na. Jamono ja muy wax loolu, limees na 414i nit yu ñàkk seen i bakkan ci mbëkk mi, ci atum 2020 bi. Te, atum daaw mi yépp, 210 a ci dee woon. Kon, li mbëkk mi rey, mbasum Covid-19 bi sax reyu ko. Nde, bees sukkandikoo ci xibaari jawriñu wér-gi-yaram bi, ba tey jii, 327i way-tawat a deewagum ci sababu mbas mi nga xam ne, def na fi 7i weer.
Usmaan Sonko : « Maki Sàll dafa wor ndaw ñi… na tekki ndombog-tànkam… »
Gii Mariis Saaña dafa yakk nguur gi lu mel ni xeme, jiiñ ko deewub ndaw ñiy lab ci géej gi. Gannaaw bi dafa lim ay sabab yoo xam ne, ci xalaatam, ñoo sabab lii fi xew yépp : 270.000i nit yu amul xéy, 100i PME yoo jël ci réew mi, 64 yi dee nañ, ay njaatige yu bon a bon, ngënale li am ñeel doxandéem yi, xàjj-ak-seen bi am ci bindug liggéeykat yi, nger, càccug xaalisu réew mi, añs.
Ci benn widewoo bi mu defoon ci talaata ji, 27eel oktoobar, Usmaan Sonko, moom, dafa tuumal nguur gi, ŋàññi njiitu réew mi Maki Sàll. Mu ne, li xew day wone ne : « Maki Sàll cuune la. Dafa lajj, moom mi dige woon xéy, ca atum 2012, 100. 000i ba 150.000i at mu nekk. Maanaam, 500.000i ba 750.000i liggéey ci 5i at. Nee na Maki dafa wor ndaw ñi, kon dafa waroon a tekki ndombog-tànkam. Mu fàttali ne Maki dige woon na fi tamit 1 miliyon liggéey. »
Buubakar Séy, njiitalu Horizon sans frontière (HSF), moom tamit, ci xëtu Facebookam la wax ne : « HSF mi ngi sàkku ngir ubbi ab lànket ci mbëkk miy rey ndaw ñi. Warees na ci amal ab luñutu bu faaydaayu ngir xam kan a def lan. Bu loolu weesoo, HSF mi ngi sàkku ci njiitu réew mi mu jël ab dekkare ngir, tànn benn bés buñ jagleel way-dëddu yi ñàkke seen i bakkan ci géej gi. »
Jamono ji ñuy bind yaxal bi, waa Tugal ñoo lal ab naal ngir dàq doomi Afrig ya fa nekk te amuñu kayit. Waaye, loolu taxul ndaw ñi xàddi. Koo ci dégg, genn kàddu rekk lay wax : « tekki mbaa dee ! »