Ci àjjumay tey jii, 22 desàmbar 2023, la Ëttub àttewaay bu mag bi doon saytu neenal-àtte bi layookati Bàrtelemi Jaas yi dugaloon. Ëtt ba nag, daf leen a gàntal. Maanaam, dafa dëggal daan yiñ daanoon Bàrtelemi Toy Jaas.
“Àttekat bi dafa dawal ndogalam, muy ndogalu dàq ci ñeenti càkkuteefu yi nu ko jébbaloon. Sikk amul ci ne mbetteel gu réy la jural layookat yi. Waaye nangu nan ndogal li. Dese nanu àqu dabantal, muy “rabat d’arrêt”. Layookat yi dinañ jéem a xool wan yoon lañuy jaar ngir mën ko def.”
Ginnaaw bi ndogal li tàbbee, mel na ni Bàrtelemi Jaas day ñàkk mbubbum dépiteem.