BASIIRU JOMAAY FAY RAAFAL NA LÉPP !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Basiiru Jomaay Jaxaar Fay jël na raw-gàddu gi ! Daanaka, taax yu mag yépp la raafal. Mayul yeneen lawax yi dara. Li mu rawee Aamadu Ba, ki topp ci ginnaawam, dafa bari ba jéggi dayo. Bees sukkandikoo ci « procès-verbaux » yi génnagum, muy Ndakaaru, di Cees, di Mbuur, di Jurbel, Kawlax ba Sigicoor… fépp, Jomaay a buub xob yi.

Boo demee Tuubaa, ci biir 610i pekki wote, lawaxu lëkkatoo « Diomaye Président » bi dafa duma yeneen lawax yi duma yu mettee metti. Yemu ca de. Ndax Luga, Kéedugu, Ndar ak Kafrin, fépp a wàcc. Moone de, bu njëkkaan, Bennoo Bokk Yaakaar moo daan faral di gañe diiwaan yooyii.  Sigicoor moom, mbetteel amu fa. Nde, xameesoon na ne, Usmaan Sonko mi fay meer moo ko moome.

Aamadu Ba, ci bëj-gànnaaru réew mi kese la jiitu, rawatina Maatam. Am na yit yenn gox yu mu gañe fa Podoor ak Jolof. Waaye, la mu am fa béréb yooyule doyul ngir dab Basiiru Jomaay Fay. Moo tax ñu bari jàpp ne kàrt gi jeex na, Jomaay mooy juróomeelu Njiitu réewum Senegaal.

Fileek nuy xaarandi njureef yiy tukkee ci àttekat yi, kii di Alfõs Cakaan di ma-xayma (statisticien) bu Rfm, xayma na njureef yi. Basiiru Jomaay Fay moo jiitu ak 56,7%, Aamadu Ba topp ci ak 31,4%. Naam, Aamadu Ba mi ngi jéem a gëmloo nit ñi ne 2eelu sumb day am, waaye mbir mi leer na nàññ. Lu ne fàŋŋ, kenn du ko jeex. Moo tax, ñu baree ngi ndokkeel Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, di ko nangul ndam li ko askanu Senegaal may.

Bu weesoo lawax yi, am nay boroom tur yu ndokkeel Njiitu réew lu bees li. Ku ci mel ni Aliyun Tin def na ko. Moom mi sos Think Tank AfrikaJom Center, dafa bind ne :

« Maa ngi ndokkeel bu baax a baax Njiitu réew mi Basiiru Jomaay Fay. Maa ngi ndokkeel itam lënkoom bi, Usmaan Sonko, njiitul Pastef. Maa ngi leen di ñaanal ngeen mottali kóllëre gi leen Saa-Senegaal yi ji. Yàlla na ci ndam yu bari topp. »

Kariim Wàdd ma ca Qataar tamit, ndokkeel na Basiiru Jomaay Fay, ak Sire Keledoor Li. Waaye, sargal nañ tamit askanu Senegaal ci ni mu ñoree, am fulla ak faayda, tànnloo boppam Njiit lu bees ci jàmm ak dal. Démb ci guddi nag, Saa-Senegaal yi génnoon nañ ci mbedd yi di sarxolle ak a yaataayumbe, di woy ak a fecc ndax mbégte. Xaw na sax taw ci yenn béréb yi, taw bu ndaw te sedd. Mu mel ni luy gaatnga ag coppite ci jàmm ak xéewal.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj