Tay ci alxames, 5eelu suwe 2025, moo yemoo ak bés bi ñuy taxaw taxawaayu Arafa. Muy bés biy toollook 9eelu fanu weeru tabaski atum 1446. Mu doon bés bu màgg a màgg, réy lool ci jullit ñi mboole-seen, rawatina ci ñi aji Màkka. Dafa di, taxawaayu Araa ponk la ci ponki aj gi. Ci bés bile nag, ay miliyoŋi miliyoŋi ciy doomi Aadama walla lu ko ëpp ñooy daje fa béréb bu sell booba, di sàbbaal Yàlla, di Ko kañ ak di Ko tàllal loxo, di Ko ñaan ngi Mu fajal leen seen i aajo.
Lislaam juróomi ponk la : ñaari baati seede yi, julli, woor, joxe asaka ak aji Màkka (bu la ko sa doole mayee). Aj giy juróomeelu ponk bi nag, at mu nekk lees koy amalee fa Màkka, réewum Araabi Sawdit. At mu nekk, lim bu takku ciy jullit ñooy bawoo fu nekk ci àddina si ngir jëmmal ponk bu solowu boobule. Ren, bees sukkandikoo ci dég-dég ya tukkee Araabi Sawdit, limub miliyoŋu nit ak xaaj ñoo aji, foofa fa Màkka.
Arafaat mi ngi soree Màkka 18i kilomet. Laata allaaji yeek ujaaj yiy taxawi Arafa, Minam ùi ñenn ñi fanaan lañuy jóge. Diggante Minam ak Arafaat, 10i kilomet la. Arafaat nag, ab bérb la bob, guddaay bi ak yaatuwaay bu ñu ngi tollu ci, daanaka, 3i kilomet. Béréb bi nga, ay tund ñoo ko wër mel ni xala.
Ci fajaru tay ji la ujaaj yi màbb, wutali Arafa. Njëwriñu wér-gi-yaram ga nekk fa Araabi Sawdit soññ na ujaaj ji, wax leen ñu jël seen i matuwaay ngir wattandiku tàngaay bi ak ceeñeeri jant bi, rawatina ci waxtuy njolloor geek diggu njolloor gi. Xelalees na ujaaj yi ñu sàmmonteek ndigal yees joxe, jëfandikoo seen i parasol ngir mën a mucc. Naka noonu, yabalees na fa takk-der ya ngir ñu aar ujaaj yi, yombalal leen senn dem ak dikk. Am na sax ay falfalnaaw yuy tiim béréb ba, lépp rekk ngir sàmm kaaraange ujaaj yi.
Ci bésub tay ji nag, ujaaj yi dañuy boole julliy tisbaar ak tàkkusaan, ñu gàttal ko. Dees na nodd wenn yoon, iqaama ñaari yoon ca jumaay Namira. Bu jant bi sowee, ujaaj yi dinañu jóge Arafa ngir dem fa Musdalifa, foofa lañuy jullee timis ak gee, fanaan fa, ni ko Yonent bi (SAWS) defee woon.
Yonent Yàlla bi, Muhammat (SAWS), ca ajam gu mujj ga, la jottali woon aaya bii di : “Tay, matal naa seen diine, tàbbal naa ci yeen samay xéewal ci yeen te daganal naa leen lislaam niki diine.”