Gàcce bu reyul, semmal. Nguurug Senegaal a ngi ne tott ci kanamu àddina sépp. Coowal CREI ak Kariim Wàdd a leen ko yóbbu. Nde, dañu daan Nguurug Senegaal, sant ko mu fay 168i tamñareet ak xaaj. Muy ndàmpaay lol, Yoonu Farãs a ko gàll Nguurug Senegaal mur war ko jox Bibo Bourgi.
Ci mbirum Kariim Wàdd mi ñuu doon toppe luubal ak càcc alalu réew mi, Nguurug Senegaal gu Maki Sàll gi da doon toppaale Bibo Bourgi, wax ne ci ñi jàppale Kariim Wàdd la bokk. Ca la ko CREI daanee woon 6i ati kaso ak 138i tamñareet yees ko alamaanoon, nangu lenn ci alalam.
Bibo Bourgi nag, bankul woon i loxoom. Ndax, dafa kalaame woon Nguurug Senegaal ca Yoonu réewum Farãs. 2012 la layoo bi tàmbali woon. Bésub 12 oktoobar 2021 la àttewaayu yaxantu bu Pari njëkkoon àtte mbir mi, jox dëgg doom Farãs ji cosaanoo Libã, Ibrahima Abuu Xaliil, ñu gën koo xam ci Bibo Bourgi. Àttekat bii di François Ancel a jiite woon àtte bi. Nguurug Senegaal nag, dafa sàkku woon àtteb dabu (appel) ca ëttu dakkal gi (cours de cassation) ngir ñu gàntal daan boobu. Waaye, ëttu àttewaayu dakkal (cours de cassation) gu Pari feddali daan bi, dëggal ko muy lu sax.
Li ci doy waar nag mooy ne, boobaak léegi, Nguurug Senegaal dafa mel ni kuy nëbb mbir mi. Yéyu ci, yàbbiwu ci.