Démb ci àjjuma ji, 27i pani desàmbar 2024, la elimaanu jëwriñ yi doon biral naalu pólitig wi mu fas yéene doxal ngir soppi Senegaal. Fa Ngomblaan ga la ko doon defe, ci kanami dépite yi fa teewal Saa-Senegaal yi. Biral na fa gis-gis biy doon cëslaayu naalu pólitig wi ñu namm a jiitee réew mi, moom ak jëwriñ yi mu bokkal Càmm gi, ci kilifteefu Njiitu réew mi.
Bi ñu tabbee Usmaan Sonko ak léegi, def ko elimaanu jëwriñ yi, def na 8i weer. Ñu doon ko xaar bu baax ci biralu naalu pólitig wi muy sukkandiku ngir liggéey réew mi. Ci diggante bi, lu bari xew na fi, Njiitu réew mi tas Ngomblaan ga woon, ñu amalaat ay wote, fal yeneen dépite. Ginnaaw gi, ci lañu àppal elimaanu jëwriñ yi bésub démb ji, ngir mu biral aw naalam.
Bi fukki waxtu jotee ci yoor-yoor bi la liggéey bi door. Ginnaaw bi njiitu Ngomblaan gi ubbee liggéey bi, moom Elaas Maalig Njaay dafa jébbal kàddu gi Usmaan Sonko ngir mu fésal aw naalam. Moom nag, elimaanu jëwriñ yi, wax na diirub ñaari waxtu yu toftal daanaka fanweeri simili.
Mi ngi ubbee ay kàddoom ci fàttali as lëf ci mboorum Senegaal, fàttali jaloorey Lingeeri Waalo ya, keroog talaatay Ndeer. Fàttali na tamit bésub cargal bees jagleeloon jàmbaar yii di Les Tirailleurs Sénégalais. Li mu ko dugge mooy wone ne, Senegaal, yàgg na am ay bañkat yoy, dee moo leen gënal torox walla di jaay seen ngor walla di tayle seen askan. Mu mel ni ku nu bëgg a wax ne, jàmbaar yooyu ñoo war a doon sunuy royukaay ci wàllu bëgg sa réew, sàmm sa ngor, xeexal sa askan te bañ ko wor. Nde, am réew kat, ay doomam ñoo ko mën a suqali. Te, ngir loolu mën a nekk, fàww réew mi gënal leen seen bopp, ñu nangoo liggéey, nangoo sonn, jaayante ba réew mi tegu ci yoonu naataange.
Ginnaaw bi mu delloo démb, Sëñ Usmaan Sonko dafa delsi ci tay, fàttali “anam bu ñaaw” bi ñu fekke réew mi. Ni mu ko yàgg a waxee bi ñu faloo ak léegi, feddaliwaat na démb ne, Maki Sàll ak i ñoñam, réew mu nërmeelu ci fànn yépp lañu leen bàyyee.
“Ci diirub ñetti weer yii, gàllankoor bi gën a réy bi Nguur gii di jànkoonteel mi ngi aju ci guuta bu metti bi nu fekk réew mi. Ci mboor, bi Senegaal di Senegaal ba tay, Nguur mësul bàyyee réew mi ci anam bu ni mel.” (Usmaan Sonko, elimaanu jëwriñ yi)
Te, ba tay ciy waxam, ci jubbanti, joyyanti ak defaraat lañu nekk. Ci waxiinam sax, loolu moo leen tereegum def li ñu bëgg a def yépp. Bi loolu weesoo, ci la biral naal wi mu lal, nar ci ànd ak Càmm gi mu jiite, ngir doxal réew mi.
Yoon wu bees la Senegaal jël. Loolu la elimaanu jëwriñ yi xamle. Coppite yooyu, ci jub, jubal ak jubbanti lañu ko lal.
“Jéego yi Njiitu réew mi def bi mu toogee ak léegi day firndeel yoon wu bees wi sunu réew mi jël ngir juboole Nguur gi, caytu gi ak askan wi.” (Usmaan Sonko, elimaanu jëwriñ yi)
Yoon wu bees woowu, ci lañuy jaar ngir jëmmal naal wi ñu nas, ñoom Nguur gu yees gi. Jubluwaay bi mooy delloo askan wi li mu moom, liggéeyal ko ba mu yëg ko, gis ci boppam.
“Danoo bëgg a tabax réew moo xam ne, li ñépp bokk, ñépp jot ci, déet réewum Kumba am ndey, Kumba amul ndey.” (Usmaan Sonko, elimaanu jëwriñ yi)
Mbirum àtteb mbaale gi
Mbirum àtteb mbaale gi (loi d’amnistie), bi ñu ko wotee ba léegi, coow la wéy di jur fi réew mi. Démb, elimaanu jëwriñ yi àddu na ci, wax ci lu leer.
“Dinanu dugal sémbuw àtte ngir neenal àtteb mbaale gi (loi d’amnistie).” (Usmaan Sonko, elimaanu jëwriñ yi)
Usmaan Sonko tontuwaale na ñiy wax ne Pastef moo jariñu ci àtteb mbaale gi. Moom Usmaan Sonko, xamle na ne, bu dee loolu la, ñoom waa Pastef bëgguñu. Nañu ko far ñépp wuyujiwaat yoon, ba ci moom sax.
MBAY MI, NAPP GI AK CÀMM GI
Elimaanu jëwriñ yi biral na ay coppite yu bari yu aju ci fànni mbay mi, napp gi ak càmm gi. Coppite yooyu la fas yéene jëmmal, ànd ci ak i jëwriñam. Jubluwaay bi mooy fexe ba ñoŋal dund ak nekkiinu waa réew mi.
Bu dee ci fànnu mbay mi, nisër bi gën a réy mooy dooleel baykat bi, fullaal ko, jox ko ab dayo buy tax mu bokk ci ñiy suqali koom-koomu réew mi. Ci kow loolu, dees na jël ay ndogal ngir jàppale koppe yi (coopératives). Teg ci ne, dinañ taxawal benn “Institut régional des métiers de l’agriculture” ngir tàggat ñiy liggéey ci fànn wi. Rax-ci-dolli, Nguur gi dina taxawal ay daara yoy, dees na ci jàngale xam-xamu mbay ngir waajal ndaw ñi.
Elimaanu jëwriñ yi xamleet na ni, Càmm gaa ngi togg ay coppitey yeesal yu bari ñeel mbay mi ak napp gi. Bu dee càmm gi, daf ne :
“Fas nanu yéene yeesal caytug gàtt yi ak tabax ay ndefar yees jagleel denc bi, fees bi ak mbuus gi (emballage).”
Bu dee fànnu napp gi, Sëñ Usmaan Sonko xamle na ne, dinañ saytuwaat digaaley napp gi ngir sàmm àqi Senegaal ak nappkati réew mi. Rax-ci-dolli, wax na ne, dinañ suuxat “aquaculture” bi (yarub jën) ngir yombal napp gi.
Mbirum galag yi
Dees na soppi càrtug galag yeek suuf yi. Lees ko duggee mooy yokk limu xaalis buy jóge ci juuti yi. Li mu wax mooy :
“Yaatal limu faykati juuti yi ànd ak wàññi lees di fayloo nit ñi, loolu mooy pexe mi gën ngir am juuti yu baax te lalu ci màndute.”
Bokk na ci sémb yi mu fa biral ñeel wàll wi :
-
Wàññi baalaate yi ñeel payug galag yi ;
-
Génnug Senegaal ci bépp xeetu digaale bob, séq na ko ak réew yees duppee “paradis fiscale” ;
-
Waxtaanewaat gépp pas gog, daf ci am ay tomb yu baaxul ci Senegaal, te réew mi xaatimandoo ko 18i réew yu am galag yu jaar yoon ;
-
Wàññi sañ-sañi jëwriñu kopparal gi ci wàllu baalaate yi muy defal yenn këri liggéey yi (ni mu amee woon ca atum 2022 ak Sabadola Gold Opération mi ñu wàññiloon 136i miliyaar ci 150i miliyaar yi mu waroon a fay) ;
-
añs.