TV5 doon na dalal werekaan bu mag bi, Bubakar Bóris Jóob, séq ak moom ab laaj-tontu. Ci laaj-tontu boobee, waxtaane nañ téere fent bi mu mujje móol-lu ak faagaagalug Tutsiy Ruwàndaa yi. Waaye, li mu wax ci nguurug njiitu réew ma woon, Maki Sàll, lees gën a jàpp ciy waxam.
Jaratul ñuy aajar Bubakar Bóris Jóob. Loo wax ci moom, waxoon nañ ko ba noppi. Nde, turam daj na àddina sépp. Muy ku siiw lool, moom bindkat bi, taskatu xibaar bi, jàngalekat bi, waxtaankat bi, liggéeykat biy suqali làkk ak mbatiiti Afrig, rawatina yoy Senegaal. Moo tax, saa bu waxee, ñu tàllal nopp yi ngir taataan i kàddoom, di leen faramfàcce ci jotaayi waxtaan yi, ci tele yeek rajo yi ak ci dali web yi. looloo tax it, léeg-léeg, ñu koy laaj gis-gisam ci wàllu pólitig, rawatina xew-xewi pólitig yiy am fi réewam bii di Senegaal.
Bóris ragalul. Xalaatam, gis-gisam, daf koy wax, mbaa mu bind ko, dem toog, jàpp njàmburam. Bi ko taskatu xibaar bu TV5 bi laajee ci wotey 24 màrs 2024 yi amoon Senegaal, Basiiru Jomaay Fay falu ci sumb bu njëkk bi ak 54,28%, dafa wax ne :
« Guléet ñu teewe ag coppite gog, day saf coppali gu bees tàq. »
Li tontu biy wund mooy yaakaar ji palug Basiiru Jomaay Fay gi dekkil ci xoli Saa-Senegaal yi. Ndax, bu ñuy wax waxi coppite ak coppali gu bees tàq, lees ci namm mooy jëlee fi xeetu pólitig bob, day daganal yenn jikko yu ñaaw yi ci yoriinu réew mi. Te, li waa Pastef jaay askanuw Senegaal mooy « jub, jubal, jubbanti », nees koy déggee fan yii. Waaye, bu weesoo yaakaar ji Saa-Senegaal yi am ci Nguur gu bees gile, bindkat bee ngi fàttali pékke (crimes) yu réy ak njombe yi fi Nguurug Fay-Sàll gi def ci ñetti at yii weesu. Forees na ciy kàddoom, ci laaj-tontu bi, ne dañoo war a topp kilifa yi fi nekkoon. Bóris ne :
« Dañu war a topp ñi def [pékke yi]. Warunoo bàyyi mu sedd wii yoon. »
Pékke ak njombe yi Bubakar Bóris Jóob di wax ñooy : mbugal yi ñu daan mbugal ñenn ñi ba ay bakkan rot ci, càcc yu jéggi dayo yi cim réew mu ndóolee ni Senegaal… Mënees na ci dolli ndaw ñi ñu rey ci doxi ñaxtu yi, sox leen ay bali fetel, ñi ñu nangu seen i suuf ak seen i alal, ñi ñu dàq mbaa ñu yàqal leen seen i liggéey, sàndarm yi réer walla yi ñu rey (?) (Fulbeer Sàmbu ak Dijje Baaji), alalu réew mi ñu aakimoo fekk ndaw ñi amuñu xëy ba tax leen di mbëkk ak a song jéeri ji, seen i bakkan di ci des… Ndax dañuy seetaan ñaawteef yile, maasale leen, maslaa jàll ? Bindkat bi, Bubakar Bóris Jóob, ne :
« Mësuñoo topp Abdu Juuf, Wàdd it noonu. Waaye, wii yoon, lu war la. »
Kàdduy Bubakar Bóris Jóob yi nag, jur nañ coow lu réy ndax li mu doon boroom tur, di ku ñu may nopp. Ñu baree ngi koy tàccu, rawatina askanu Senegaal wi Nguurug Maki Sàll gi lottal ba mu lott. Dafa di, kàddoom yi dañuy màndargaal mer gi waa Senegaal mere Nguurug Maki Sàll ci 12i at yi mu yor réew mi. Maanaam dafa waxal ñi amul baat walla ñi nga xam ne bu ñu waxee, kenn du leen dégg.
Ni Maki Sàll ak i àndandoom yoree woon réew mi dafa ñaaw lool ba jéggi dayo. Waxuma la dund gu jafe gi te metti, waaye tooñ yi, xoqtal yi, jaay doole yi, salfaañe alalu réew mi di ci yaataayumbe ak a gundaandaat, njombe yeek giraawaali yi… lii lépp nag, ñu boole ko ak réy, reewande ak bul-faale bob, foo leen natt weesu nañ ko. Lu ni mel la askanuw Senegaal dootul nangooti. Moo tax Bubakar Bóris Jóob di artu njiit yu bees yi.
Bindkat baa ngi moytuloo Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, Usmaan Sonko (elimaanu jëwriñ yi) ak ñi ñu bokkal liggéey bi. Mi ngi leen di xamal ne, askan wii nga xam ne dafa fippu, nangoo ñàkk lu bari ba àgg fii, du leen may dara. Kon, waruñoo juum yenn njuumte yi. Ndax, bu boobaa, dina leen wex xàtt.
Ngir seetaan laaj-tontu bi ci kàllaamay nasaraan, dees na cuq ci lënkaay bii toftalu :