Démb, ci gaawug korite gi, Njiitu réew mi jagleel na ab laaj-tontu rajo RFM. Alasaan Géy a doon dalal ci Jotaayam bii di Yoon wi. Ci biir waxtaan wi, faramfàcce na ci ponk yu bari. Waaye, tànnal nan leen ci yi gën a bir te jëm ci jàppaate yu bari yi, mbirum ñetteelu moome geek demug Idiriisa Sekk.
“Senegaal amul saa-kasob pólitig.”
Bu dee ci wàllu pólitig, jàppees na ni demokaraasi dafa tumurànke Senegaal, te Yoon dafa jeng. Am nay sax ONG yu bari yuy génne ay caabal, di ci joxoñ Nguurug Senegaal. Nee ñu, réew mi, dañ fiy salfaañe àq ak yelleefi doom-aadama, di jàpp ak tëj ci sababu pólitig kese. Maanaam, làq doom, dóor doom moo fi am, walla Kumba am ndey ak Kumba amul ndey. Njiitu réew mi nag, Maki Sàll, weddi na tuuma yooyu. Ndax nee na, “Senegaal amul saa-kasob pólitig.”
Moom, dafa jàpp ne, ñi Yoon teg loxo ñépp, dañoo jalgati Yoon walla ñu def i ñaawteef. Séydi Gasama nag, nangul li Njiitu réew mi wax. Nde, moom, leneen la gis, moo ko tax a tontu Maki Sàll ngir fàttali ko. Dafa bind, ne :
“Kilifa gi, Njiitu réew mi, Maki Sàll, li ëpp ci ñi tëdd ci kaso yi, taaluñu réew mi, sàccuñu, randaluñu.” Séydi Gasama, njiitul Amnesty Internationale fi Senegaal.
Dolli na ci sax ne, ñooñee ñu nëbb jant wi, sañ-sañ yi leen Ndeyu-àtte réew mi ak Sàrti ma-réewandoo yi may rekk lañ doon jëmmal. Séydi Gasama gën a leeral waxam ji, biral ne, liy “màndargaal ñi ci kaso bi, ñépp, daanaka, mooy li ñu bokk pàrti pólitig.” Waa Pastef la ci namm. Ndaxte, jamono jii, ci xayma, lu tollu ci 300i waa Pastef ñoo ngi kaso bi, ba ci Basiiru Jomaay Fay. Te, li ñu wax ne moom lañ leen jàppe, ñenn ci waa Nguur gi def nañ lu ko yées, kenn wooluwu leen sax. Looloo tax ñuy wax ne Yoon dafa jeng. Te moom, Njiitu réew mi, moo jéng lenn ciy àttekat, ñuy jëfe ay ndigalam, di ko jàppal, di ko tëjal. Ci ñoom lay jaar ngir teree bokk lenn ci waa kujje gi ci wote yi. Looleet, Kor Mareem Fay Sàll nanguwu ko. Ndax, neeti na, Baat bu nekk a moom boppam. Ciy waxam, demokaraasi mooy daw Senegaal.
“Am na ñoo xam ne ci saaga ak a ŋàññi njiitu réew mi ak kilifa yi lañ fi nekke. Kon, bu dul woon li sunu réew miy baale, ñooñu duñu wax liñ bëgg a wax.”
Maki – Idi, am na luy ñuul ci soow mi
Démb, ci gaawug korite gi, Idiriisa Sekk tamit janoo naak taskati-xibaar yi. Njiitul CESE li nag, xamle na ni day tàggoo ak Njiitu réew mi, Maki Sàll. Wax na fa yit ne, lawax la ci wotey 2024 yi. Moo tax muy génn ci lëkkatoo Nguur gi, Bennoo Bokk Yaakaar. Rax-ci-dolli, bu altine jotee, dina tekki ndombog-tànkam ci boppu campeef gii di CESE, maanaam Ndajem Koom-koom gi, Mboolaay geek Kéew gi. Jëwriñ yi bokk ci pàrteem itam, dañuy bàyyi. Moo tax Ndaamal Kajoor waxoon ne day tekkil boppam ndombog-tànkam ci toogu ba ko Maki Sàll tegoon, keroog 2020 bi muy àndati ak moom. Waaye, ku déglu Maki Sàll, xam ne moom ci boppam moo dàq Idi. Ndaxte, Njiitu réew mi dafa gis ne yenuwul maanaa, ab lawax di bokk ci Nguuram.
Mu mel ni, Njiitu réew mi ak Idiriisa Sekk dañu bëgg a gëmloo saa-senegaal yi ne, ñoom ñaar, dañu réeroo, juyoo ci mbirum ñetteelu moome gi ba tax leen tas seen ug ngoroo. Cig pàttali, ñaari doomi Ablaay Wàdd yi xamante nañ bu yàgg, ca ati 1990 ya. Maki Sàll sax a ko wax démb. Kon, yàgg nañoo ànd, xamante ci wàllu pólitig. Bi Ablaay Wàdd di topplu Idiriisa Sekk ñeel sàncey Cees ya, Maki Sàll a nekkoon magum jëwriñ yi doon ko yaq lu nekk. Wotey 2012, ca ñaareelu sumb ga, Idi, Maki la àndaloon ngir xeex Ablaay Wàdd. Maki Sàll falu, Idi bañ a bokk ci Nguur gi, di ko xalab saa su nekk. Noonu, mu daldi bokk ci kujjeg Maki Sàll. 2020, ñu taafantoo mbasum Covid-19 mi, daldi yeesalaat ànd bi, Maki tabb Idi ci boppu CESE bi nga xam ne, moom Idiriisa Sekk daf ne woon amalul réew benn njariñ. Tey, ñu ngi nii di tasaat seen ngoro. Ànd tey, tàggoo ëllëg ; àndaat ginnaaw-ëllëg, tàggoowaat ginnaawaati-ëllëg. Xma ngeen ne moos, am na luy ñuul ci soow mi.
Tàggatoo bii nag, mënees ci jàngatee ñaari mbir. Bi ci jiitu mooy ne Maki Sàll wuyoo na turu Soxna Batoor bi ko ndaw ñiy dàkkental. Nde, bir na ni bëggul wujje, bëggul bokk ak wujjam kër, astemaak néeg. Dafa di, doon lawax am déet warut a mën gàllankoor ab diggante bob, liggéey kesee ko Sekk, rawatina bu dee dafa ñeel réew mi.
Ñaareelu mbir mi ñu ci seetlu mooy ne Maki Sàll dafa bëgg a bokk 2024. Ndaxte, ci jamono yii weesu, képp ku taxawoon ciy àndandoom, wax ni amul sañ-sañu bokk ci wotey 2024 yi, dàq na la, bàyyi fa ñi ko xalamal ak xàllal yoon wi. Saa buñ ko ci laajee, day daw wax ji, di ko ajandi. Démb, bi ko ci Allaaji Alasaan Gay laajaatee, Njiitu réew mi, Maki Sàll, dafa dawati wax ji, bañ a leeral. Daf ne rekk :
Te, njortees na ni, Idi, dafa bëgg Maki beddeeku, jiital ko ci lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar, mu ànd ak ñoom kàmpaañ. Am ñu naan sax Maki Sàll daf ko diggante Idiriisa Sekk. Ak lu ci mën di am, leer na ni Maki Sàll dafa bëgg a bokk te ku ko namm a gàllankoor mu fexeel la. Mooy Buur, di Bummi. Kon boog, ne leen : “Buur Maki !”