CAABALUG ËTTUB CETTANTAL BI : YOON SUMB NA LIGGÉEY BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Saabalukaay bii di Source A moo siiwal xibaar bi. Bees sukkandikoo ci li yéenekaay bi fësal, Yoon a ngi lëñbët caabalu gi Ëttub cettantal bi génne woon fan yee. Caabal googee nga xam ne, dafa feeñal ay njombe ak i njuuj-njaaj yu jéggi dayo ñeel koppari askan wi ak bor bi ëpp bi Maki Sàll ak nguuram leboon ci turu askanuw Senegaal. Ci li yéenekaay biral nag, Yoon a ngi ci tànki ñetti jëwriñ yees dénkoon koppari réew mi, benn Sàmba-koppar bu mag ak ñenn ci saytukati sàqi xaalis réew mi. Nde, njorteesagum na ne, ñooñii, bokk nañu ci ñi saax-saaxe alalu réew mi diggante 2019 jàpp 2024.

Dafa di, Yoon jot na ci caabalu Ëttub cettantal gi lëmbe woon réew mi. Ci loxoy toppekat bu mag bi (parquet général) lañu teg. Source A xamle ne, du ñàkk mu am ñu ñu ci topp, rawatina jëmm yees tudd ci kow.

Li xew nag moo di, dañu leboon xaalis bu takkoo takku, leb ko ci turu doomi Senegaal, te kenn jaaralewu ko yoon yi mu waroon a jaar. Maanaam, bor boobu, ak lu muy bari bari yépp, dëppoowul ak sàrt yi lal li ci aju.

Source A dafa bind, ne :

“Dafa mel ni dañu leb, leb yu bari, ci turu Nguur gi, te jaaralewuñu ko ci banqaas bii di Comité national de la dette publique (CNDP) mi nga xam ne, moom rekk am sañ-sañ def lu ni mel.”

Li caabalu Ëttub cettantal gi tënkoon la yéenekaay bi jukki fii. Yéenekaay bi rax ca dolli ne, pexe mi gaa ñi laloon mi ngi aju woon ci lees duppee “signature de lettre de confort” walla “conventions de financement” ak i bànk. Loolu nag, dañu daan taafantoo ay semb yu ñu war a kopparal. Waaye, daawuñu ko jaarale ci sàrti koppar yi.

Ëttub cettantal bi dafa jàpp ne, koppar yi, jaaralewuñ leen ci banqaasi Càmm gi. Nde, bind koon nañu ko, ñu xam fu mu jóge, fu mu jaar ak yan loxo ñoo ko jël. Waaye, bees sukkandikoo ci caabal gi, ci wëlis walla saag lañu dugal xaalis bi, randal ko. Maanaam, nit, walla ay nit ñoo génnee koppar yi ci bànk yi, dem ak moom.

Li tax luññutukati Ëttub cettantal bi njort loolu mooy, ci li caabal gi bind, “ñiy saytu sàq yi ñuy dugal koppar yi, te war a wéral payoor yi, dañu leen a jéggi. Ñenn ci jëwriñ ya woon dañu daan faral di jox santaane Sàmmba-koppar bu mag bi ngir mu génnee xaalis moom ci boppam. Te nag, loolu dafa safaanoo ak li Yoon tëral.”

Yemul ci loolu, dañu nëbb dayob koppar yi ñuy génne ci gafakag Nguur gi. Nde, ca atum 2023, li ñu xamle woon mooy ne 434,9i miliyaar kepp lañu ci génne woon. Ndeke, bi ñu saytoo ba ca biir, koppar yees tibb ci gafakag Nguur gi ñu ngi tollu ci 1 131,6i miliyaar. Muy lu doy waar.
Yoon nag, door na liggéeyam. Ñàkkul ne, fi ak fan yu néew, dina am xibaar yu ci rot.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj