CAMPEEF / NGOMBLAAN GI : TAXAWAL NAÑU PEKK GU YEES GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw bi ñu falee dépite Maalig Njaay ci boppu Ngomblaan gu yees gi, sampees na pekk giy jiite campeef gi. Ci altine jee weesu la dépite yees fal bees tànn way-bokki pekk gu yees gi. Waaye nag, coow lu réy jiboon na fa laata liggéey biy àntu. Coow loolee, mi ngi aju woon ci ki waroon a doon juróom-ñetteelu tof-njiit li.

Nii la pekkug Ngomblaan gu yees gi tëddee :

Njiit li :

  • Maalig Njaay

Tof-njiit yi

  • Ismayla Jàllo, njëlbeenu tof-njiit

  • Rokki Njaay, ñaareelu tof-njiit

  • Séex Coro Mbàkke, ñetteelu tof-njiit

  • Mbeen Fay, ñeenteelu tof-njiit

  • Aamadu Ba (PASTEF), juróomeelu tof-njiit

  • Ulimata Siidibe, juróom-benneelu tof-njiit

  • Sàmba Daŋ, juróom-ñaareelu tof-njiit

  • Ramatulaay Anta Bojã, juróom-ñetteelu tof-njiit

Fara-caytu yees fal

  • Maymuna Buso, njëlbeenu fara-caytu bees fal

  • Muhamet Sàll, ñaareelu fara-caytu bees fal

  • Daba Wañaan, ñetteelu fara-caytu bees fal

  • Bakari Jéeju, ñeenteelu fara-caytu bees fal

  • Beyaatiris Sermen Fay, juróomeelu fara-caytu bees fal

  • Asan Jóob, juróom-benneelu fara-caytu bees fa

Way-doxal yi (questeurs)

  • Aysa Ture, njëlbeenu aji-doxal

  • Alfõs Maane Sàmbu, ñaareelu aji-doxal

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj