CARGALUG NEUSTADT INTERNATIONAL PRIZE FOR LITERATURE : BUBAKAR BÓRIS JÓOB JËL NA NDAM LI (PAAP AALI JÀLLO)

Yeneen i xët

Aji bind ji


Ci talaata 26eel ci oktoobar 2021, lees jot ci mbégtem weer wi. Surnaalu ladab bees duppe World Literature Today, nekk ca Iniwérsite Oklahoma, ca Amerig, moo biral xibaar bi : Bubakar Bóris Jóob mooy 27eelu rawaanub Cargalug ladab bu Neustadt ñeel àddina sépp. Muy xibaar bu neex a neex ñeel réewum Senegaal, di sag ci askanu Afrig wépp ak way-ladab yi mboole-seen. Nde, cargalug ladab bu Neustadt gileey ñaareelu cargalug ladab gi ëpp solo ci àddina si, gannaaw gu “Prix Nobel” gi. Du guléet nag, Bubakar Bóris Jóob di jot cib cargal. Waaye, gu Neustadt gii da cee raw ngir dayo bim làmboo. Ay ndaanaan ci biir i ndaanaan, tànn ab ndaanaan ci biir i ndaanaan, sag du ko gën a réy. Ndax, werekaan bii di Bubakar Bóris Jóob, ak lim liggéeyal àddina lépp, rawatina Afrig ak Senegaal, amul cargal walla neexal bu ko jomb. Kon, yeyoo na ñu jagleel ko lu réy ci bés bu réy. Waaye, bés du réy, du tuuti, boroom lay tollool.

(Paap Aali Jàllo)

«Jàppees na ni, gannaaw “Prix Nobel”, cargalug ladab Neustadt ñeel àddina sépp mooy bi gën a réy.» Cargalug Neustadt International Prize for Literature gu ren ji, ci àntarnet bi lañ ko yéglee, jaare ko Zoom, bi ñuy amal Neustadt Lit Fest 2021 bi. Dafa dib neexal bi ñuy sargalee kenn ci jàmbaari àddina si ngir biral cant ak jukkal bi ko àddina si ameel. Dees na ko joxe ñaari at yu nekk ci turu Iniwérsite bu Càmmug Oklahoma ca Etaasini ak surnaalu ladab bii di World Literature Today.

World Literature Today nag, da dib yéenekaay buy wax ci ladab ak mbatiiti àddina si. Ñaari weer yu nekk lay génn. Jubluwaayam mooy fésal ak biral ngën-ji ladab, di gungey cargali ladab ak i këri mbatiit ñeel ndongoy daara yu kowe yi. Li mu sasoo mooy liggéeyal àddina wërngal, càmm yeek daara yu kowe yi. Solos surnaal beek dayoom a tax ndajem cargalug Nobel mi boole ko ci «yéeney [sources] ladab yees gën a móol ci àddina si te gën a matale ci wàllu xibaar». Teg ci ne, yàggul dara, taggoon nañ ko fi, melal ko ni «sàqub xibaar bu matale ñeel xalimay àddina mboole-seen te seen i boroom safoo mbind, di ko dunde». (Utne Reader, saŋwiye 2005). Rawaan gi nag, dina jot neexalug 50 000 $ (fukki junniy dolaari amerig), dunqu jaaxaay wuñ tëgge xaalis ak ug birtal (certificat). Ndàmpaay lu takku liy jóge ci loxoy waa kërug Neustadt yi nekke Dallas, Denver ak Watertown ak Massachusetts moo tax cargal giy wéy di am ba abadan. Cargalug ladab gu Neustadt gi mooy njëlbeenug cargalug ladab bu cosaanoo Amerig tey teral mbooleem way-ladabi àddina. Te, bokk na cis-tuut ciy cargal yoo xam ne, wëliis boroom xam-xam yiy yëngu ci yeneen fànn ak yeneen xeeti kilifa, dañoo ëmbaale taalifkat yi, way-fent yi ak ma-kilib yi. Li ko tax a jóg mooy biral ak delloo njukkal xalimay ladab yi ko gën a yeyoo ci way-ladabi àddina si. Dafa di, cargal gu am dayo la, muy lees fonk lool ci péncum way-ladab yi. Li ko waral mooy ne, day fésal, di ràññee ak a sargal way-ladab yi aay te xareñ dëggëntaan. Ci 26i way-ladab yim mës a sargal yépp, ba ci Bubakar Bóris Jóob mii di 27eel bi, kenn werantewul ne ay werekaan lañu, diy ndaanaan, aay lool ba àddina sépp seedeel leen ko. Saa bu kurélug-àtte gi biralee kim tànn, ñépp a ciy ànd te kenn du ci am lu muy diiŋat.

Kurélug-àtte giy tànn rawaan bi nag, ay bindkat yu mag a mag, aay lool te diy boroomi tur ñoo ci nekk. Moo tax, doo ci dégg par-parloo walla njuuj-njaaj. Te dina tax cargal gi mucc ci pexey kàgguy téere yi, móolkat yeek ñeneen ñiy bëgg a jiital seen i bindkat. Loolu yépp day wone màndute gi cargal gi làmboo. Ñoom, aji-tànn yi, dañ wax ne, «bindkat bu ne, ak foo mënti cosaanoo, feek yaa ngi dund, mën nga jël cargalug Neustadt» Amul xàjj-ak-seen, amul boddekonte ci waaso walla ci der, amul gënale walla jeng jëmale ci benn xeet. Moom daal, ku gën a rafet xalima, gën a ñorle wax te amal àddina si njariñ, dees na la sargal. Tànnin wu mucc ayib woowu, ànd ak màndute te digg-dóomu, moo yokk dayob cargal gi. Màggaay boobu la Lawrence Van Gelder di biral bi muy wax ne, «jàppees na ni, gannaaw cargalug Nobel, cargalug ladab Neustadt ñeel àddina sépp mooy cargalub ladab bi gën a réy.» («Footlights», New York Times, 26eel féewaryee 1998)

Looloo tax ñenn ñi di ko dàkkentale «le Nobel américain». Nde, cargalug Neustadt gi mooy ubbee tànn gi waa Akademi bu Suwed di amal ngir biral seen i tippoo ñeel cargalug Nobel gi ci wàllu ladab. Muy wone ne, cargal gi ndawul, te ku ndaw itam du ko jël. Looloo tax kurélug-àtte gi seedeel Bóris, fésal ràññiku ak «ngëneel» li xalimaam bi làmboo «ci biir way-ladabi àddina si».

Maki Sàll, njiitu réew mi (Twitter) : « … Lii day gën a dëggal aay bi àddina sépp xame Bóris.»

Bubakar Bóris Jóob, doomu Senegaal la, tollu ci 75i at, nekkoon jàngalekat, dib taskatu xibaar, bindkat, aji-fent, aji-rabatal ak senaaris. Bokk na ci bindkat yi gën a siiw ci àddina si, rawatina ci biir Afrig. Bubakar Bóris Jóob, Yàllaa ko nàkkal xel mu ñaw, yattal ko xalimab wurus bu rafet, may ko gisin wu leer ak déggin wu xóot. Muy ku xereñ lool ci mbind, ñeme li muy wax, gëm li muy def tey wéyal liggéeyu Séex Anta Jóob mim def sëriñ ak royukaay. Bu ko neexoon def ni yenn tubaab yu ñuul yi, di mar taatu nootkat bi, di ko xalamal ak a dunguru ngir poñetu àddina. Wànte, moom, wutul tur, diirul alal te teraangaak raaya, lu ñu réy réy ci nit ñi, feesuñ bëtam. Dara yitteelu ko lu dul sag ak peexug nit ku ñuul, naataange Afrig ak bu àddina.

Loolooy balle ciy njàngaleem, ciy waxam ak i jëfam, rawatina ci mbind mi ko àddina si xame. Moo tax Robert Con Davis-Undiano, njiitalug-ndogalu World Literature Today, wax ne : «dafa dib sag bu réy a réy, li benn bindkatu Afrig bu toll ni BBJ jël ndam li, di cargalug Neustadt. Raayab Bubakar Bóris Jóob bile de, ndamu cargal gi la ; waaye, day firndeel itam dayob Bubakar Bóris Jóob ak siiwaayam biy wéy di yokku  ci biir réewi sowu. Loolu, nag, du lu ko jomb.»

Du guleet Bubakar Bóris Jóob di amub cargal. Jot nañ koo sargal ay yoon. Ci misaal, bim bindee “Les Tambours de la mémoire”, ame na  cargalu bu Mag bu Njiitu réewum Senegaal ci atum 1990 ak Cargalug Tropiques ñeel téereem bim duppe woon “Le Cavalier et son ombre.” Téereem bii di “Murambi : The Bokk of Bones” (Murambi : le livre des ossements), ab kéemtaan la ko Toni Morrison jàppe. Rax-ci-dolli, “Foire internationale du livre” bu Zimbabwe dafa boole téere bile ci 100i téerey doomi Afrig yi gën a am solo ci 20eelu xarnu. Téere bi, nag, ci faagaagalug Tutsiy Ruwàndaa gi amoon ci atum 1994 lay wax. Téere la boo xam ni làkk yiñ ko sotti bari nañ.

Bi xibaar bi jibee, Njiitu réew mi, Maki Sàll, ndokkeel na sunu werekaan bi ci àllarba ji, fésal mbégteem ak sag bim am ci bile ndam. Ci Twitteeram la bind :

«Maa ngi ndokkeel sunu mbokk mi Bubakar Bóris Jóob. Maa ngi koy sargal ci Cargalu Neustadt gu réy guñ ko teralee ñeel kàggub ladabam bu fees ciy téerey fent ak i rabatal. Lii day gën a dëggal aay bi àddina sépp xame Bóris. Waaye tamit, ndamu Bóris bi day firndeel xareñte bindkati Senegaal yi.»

«Bóris ku aay la», du lu kenn umpale. Lim bind ci farañse ak li ko àddina seedeel doy na ci firnde. Waaye, li ëpp solo, te ñépp war koo xam, mooy liggéey bim sumb ñeel làmmiñ ak mbatiiti Afrig. Ndege, Bubakar Bóris Jóob ku fonk cosaanam la, xam lim doon ak fim jóge. Xam bim xam ne Afrig mënta suqaliku feek sukkandikuwul ciy làmmiñam, mbooram, mbatiitam ak mbaaxi maamam, moo ko tax a bind ci làmmiñ wim nàmp, di wolof. “Doomi Golo” (2003), téere fent bim jëkk a bind ci wolof, mooy njëlbeenug téere wolof biñ mës a tekki ci làkku àngale, tudde ko “The Hidden Notebooks” (Michigan State University Press, 2016), ci farañse “Les petits de la guenon” (Phillipe Rey, 2009), tekki nañ ko tamit ci español muy “El libro de los secretos”… Yemu fa, ndax jamono jii ñu tollu Musaa Ja mu ngi koy sotti ci italiyeŋ. Gannaaw gi, móolaat na beneen téere fent, “Bàmmeelu Kocc Barma” (2017). Bubakar Bóris Jóob ak i xaritam taxawal nañu ag këru móolukaayu téere ci làmmiñi Afrig yi, tudde ko EJO. Dafa di, “Bàmmeelu Kocc Barma” sax, EJO moo ko móol. Nu ni déet-a-waay, mu sos LU DEFU WAXU, ab dalu-web boo xam ne, day biral i xibaar ci kàllaamay Kocc. Kon, ci toolub xareb làmmiñ ak mbatiiti Afrig, Bóris gaynde la ci, di jàmbaar jees war a roy. Gàcce-ngaalaama, Jóoba-jubba ! Sa ndam, ndamu Senegaal la, di ndamu Afrig, waaye tam, ndamu àddina sépp la.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj