Tey ci talaata ji, 9 sãwiyee 2024, la ndajem ndeyu àtte réew mi doon saytu baayaley lawax yi matalul woon te waroon a mottali walla joyyanti leen ci seen i baayale. Bi 9i waxtu yu toftal 30i simili jotee ci la caytu gi tàmbali. Dafa amoon i lawax yu waroon a jàll ci suba si, muy Meetar Elaas Mustafaa Juuf, Róos Wardini, Idriisa Sekk, Aliw Mammadu Ja, Sëriñ Mbuub, Paab Jibriil Faal, Mammadu Lamin Jàllo, Muhammet Bun Abdalaa Jonn, Aliw Kamara, Elaas Maalig Gàkku, Paab Momar Ngom.
Bi ndajem ndeyu àtte réew mi jeexalee caytoom, ñii ñoo jàll :
Basiiru JOMAAY Jaxaar Fay
Ceerno Alasaan
Elaas Mammadu Jaawo (Maam Bóoy Jaawo)
Aali Nguy
Elaas Maalig Gàkku
Muhammad Bun Abdalaa Jonn
Mammadu Lamin Jàllo jàll
Paab Jibriil Faal
Sëriñ Mbuub
Aliw Mammadu Ja (PUR)
Idriisa Sekk
Róos Wardini
Ñi ci des nag, muy Meetar Elaas Mustafaa Juuf, Aamadu Li “Akile”, Bugaan Géy Dani, Elaas Abdu Rahmaan Juuf, Aminata Ture, Abdul Mbay, Suleymaan Ndeene Njaay ak Sëriñ Géy Jóob.
Bu dee lawax yii di Aliw Kamara, Paap Momar Ngom ak Aamadu Sekk, ñoom, jotuñoo ci mottali li leen dese woon ci yak li ñu waroon a joyyanti.
Kii di Soxna Aminata Ture nag, moom fasul yéene bank i loxoom. Nde, ginnaaw biñ ko gàntalee, biral nay kàddu wax ne : “Dinanu wéyal sunub xeex. Kàmpaañ bii, dinanu ci bokk ngir nguur gii jóge fi…”.