CAYTUG SUUFI TEFESI SENEGAAL YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Kurél gi doon saytu suuf si féete ci tefesi Ndakaaru yi, jébbal nañu Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, caabal gi rote ci seen liggéey bi ñu doon amal ñeel càmbarug suuf yi ci tefesi Senegaal yi. Tay ci yoor-yoor bi, lañu doon daje ak moom, ci teewaayu elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko.

Ci li ñu xamle, am nay mbir yu doy-waar yees nemmeeku suuf yooyii, rawatinay rëq-rëq ci yéeme ci wàllu kéew mi ak koom gi. Ci weneen waxiin, suuf yees joxe a knees ko joxee, dëppowul ak Yoon te méngoowul ak càrtug kaaraange kéew mi. waaye nag, ci li Njiitu réew mi xamle, dees na jubbanti rëq-rëq yi.

Bees sukkandikoo ci lees tuxal ciy waxam, deesul a singali kenn walla di ko jay doole ak a xoqatal. Jubbanti bees di amal ñeel mbir mi, day tegu ci Yoon te kenn du salfaañe àqi jàmbur.

Li ci kanam rawul i bët.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj