CENA BI DËGGAL NA USMAAN SONKO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw ndogalu àttekatu Sigicoor bi, Sabasi Fay, CENA joxati na dëgg Usmaan Sonko ñeel xobi baayale yi ko DGE di bañ a jox. Nde, CENA, kurél gi saytu lépp lu aju ci mbiri wote yi, joxe na ndigal moom itam, sant waa DGE ñu jox Usmaan Sonko xobi baayaleem ni mu gën a gaawe.

Usmaan Sonko amati na ndam, ñaareel bi yoon. Ginnaaw bi Sabasi Fay, àttekatub Sigicoor bi, santaanee ñu dugalaat Usmaan Sonko ci wayndarew wote wi, CENA moo joxaat dëgg meeru Sigicoor bi. 

Dafa di, àtteb Sabasi Fay bi jibee, DGE daf lànkoon ne du jox Usmaan Sonko xobi baayame gi. La ñu taafantoo mooy ne, AJE bi dafa dugal ab dabantal. Te jamono jooja sax, AJE bi dugalugul woon dabantal boobee ñuy layee.

Fi mu nekk nii, DGE amatul lay. Bu yeboo ne dañ ko wër-ndombo. Nde, ñaari àtte yépp dañ neenal layam yi. Te, CENA mi ko yilif, daf ko ga ci mu jébbal ndawul Usmaan Sonko li, dépite Ayib Dafe, xobi baayale gi ci ni mu gën a gaawe. Lu ko moy, CENA ci boppam mooy jox Ayib Dafe xobi baayale gi ak li ci war a ànd lépp. Ndaxte, CENA am sañ-sañ bi. Nde, dog (article) 6 bu càrtug wote yi mooy may na CENA, bu DGE bañee jëfe ndigalu jox Usmaan Sonko xobi baayale yi, mu jéggi ko, jox leen ndawul Usmaan Sonko li.

Rax-ci-dolli, dog 10 bu àtteb 2005-07 bi samp kurélu CENA dafa wax ne :

“CENA day saytu ngir ñépp jëfe càrtug wote yi te sàmmonte ak moom, muy kilifay caytu gi di làngi pólitig yi, lawax yi aak falaakon yi.

Bu fekkee ne am na kilifag caytu gu jalgati àtte yi ñeel wote yi walla referàndom bi, CENA daf koy ga ci mu jël ay matuwaayam ngir joyyanti jalgati yi.

Bu dee kilifag caytu gi jëfewul ndigal li, CENA am na sañ-sañu teggi ko ak wuutu ko ci ndogal wote yi ñeel nit ki jalgati yoon, astemaak sañ-sañu àkki ëtti àttewaay yi war.

CENA mën na yit digle ñu teg ay daan nit ki jalgati yoon te di fexe ñu jëfe ndigal li.”

Leer na. Ndigal lu bawoo ci kilifa nag, jëfe rekk la sant. Waaye, DGE wone na ni ñoom, genn kilifa rekk lañuy déglu, luy jëwriñu biir réew mom, Njiitu réew mee koy sant muy def. Ñépp a ngi toog di xaar ba xam ñu DGE di doxalee.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj