Fan yii weesu, defuwaxu.com, seen yéenekaay ci kàllaamay Kocc, bindoon na fi ab kayit, tudde ko : “Kan mooy jiiteji CESTI ?” Laaj boobu, am na tey tont : Mamadu Njaay moo nekk ci boppu CESTI, daara ji ñuy tàggate taskati xibaar yi ci Iniwérsite Séex Anta Jóob bu Ndakaaru.
Jonaŋte yi ci diggante njiit lu bees lii la woon ak ki mu wuutu di soxna Kusoŋ Tarawore Sàll. Benn baat doŋŋ moo dox seen diggante biñ waññee kart yi, kon mënees na ni joŋante bi metti woon na.
CESTI, muy ndongo-daara yi fay jàngee nii ak ñi fa jot a jaar, koo ci laaj lu mu xam ci Mamadu Njaay, wax ji benn la : ku xereñ la, laabir te ànd ak sagoom.
Te moom ci boppam, xamle na yéeneek naal yu réy yi mu am ci luy jëmale kanam CESTI. Mi ngi woote booloo, yaatal, weccee xalaat ak jéem a def i jéego ci xarala yu bees yi.
Bu doon moom rekk, xëccoo ak réeroo du am ci Daara ju mag ji, tàmm nay dox ay ay tànki jàmm saa yu ko mënee, rax-ci dolli ku déggook ndongo yi la. Lii lépp, boo ci boolee ni mu yàggee CESTI ak fi mu jaar ba egsi fa, dafay biral ne ku yelloo jiite Daara ji la te àttan na liñ ko yen.