Ay kilifa ak i kàngaam yu mag bennoo nañ bind ab bataaxal, jagleel ko Njiitu réew mi, Maki Sàll, ñeel mbiri Usmaan Sonko ak làngug Pastef. Li jëmm yu mag yooyuy sàkku mooy ñu bàyyi Usmaan Sonko te ñu far dekkare bi tas làngug Pastef. Téeméer ak ñeen-fukk ak ñetti (143i) nit ñoo xaatim bataaxal bile. Ci biir ñooñii, dees na ci fekk kii di Sëriñ Jóob, jàngalekat ci daara yu kowe yi, nekkoon fi jëriñu Yoon ak kii Aliyun Sàll mi bokk ci àttekati ëttub àtte Bennoog Afrig ñeel àq ak yelleefi doom-aadama. Yeneen 141 yi ci des, ay gëstukat lañu, di jàngale ci daara yu kowe yi. Lii toftalu lañ bind ci seen bataaxal bi.
« 28 sulet 2023 ba tey, Sñ Usmaan Sonko, njiitul PASTEF, mi ngi ñu jàpp kaso.
Tuuma yi ñu koy toppe ba tax ñu jàpp ko dañu soppiku ci diggante bi. « Càccug jollasu » lees ko jëkk a jiiñ. Ginnaaw gi ñu toftal ci yeneen i tuuma yu réy a réy : « xirtal ci song Càmm gi », « mbooloom defkati ñaawteef », « nasaxal kaaraange Càmm gi », « mbooloom defkati ñaawteef yu namm a amal jëfi terorist », « kootoog ngir fexeel njiiteefu Càmm gi » ak « jëf ngir nasaxal kaaraange réew mi ak a sabab ay yëngu-yëngu yu réy ».
Ñu daldi génne ab dekkare buy tas làngu pólitigam gii di PASTEF. Te, bi ñu ko sosee ba tey, bokk na ci làng yiy dundal pólitig bi fii ci Senegaal. Rax-ci-dolli, am nay dépite yu bari fa Ngomblaan ga ak ay meer yu baree bari ci réew mi.
Lu mu néew néew, ñetti nit dee nañ ci ñaxtu yi amoon biir réew mi keroog biñ ko jàppee. Ñu daldi jàpp lim bu takkoo takku ciy militã ak i soppey PASTEF, jàppaale ay nit ñi ñu fal. Li ëpp ci ñees jàpp, dañ leen téye, di leen toppe ay tuuma yu réy.
Sñ Usmaan Sonko a ngi xiifal dale ko 31 sulet 2023 ba tey. Fi mu nekk nii daa feebar ba sonn lool, tax ñu rawale ko fa « Urgences » ya keroog dibéer 6i fan ci weeru ut 2023.
Nun ñi xaatim bataaxalub woote bile, góor ak jigéen, ku nekk ci turu boppam walla turu ay mbootaay walla ay kurél ; maxejji Senegaal, maxejji lenn ci réewi Afrig ak àddina sépp :
Ngir aar Càmmug yoon ak njàqare ji nu ame ci yëngu-yënguy pólitig yi ak yi ci mboolaay gi ak fitna ji nar a yàq dal ak jàmm ci réew mi,
Bëgg jàmm lool ak ug dal te bëgg a sàmm jéegoy demokaraasi yi réew mi seqi,
Xër lool ci wormaal ak a sàmm sañ-sañu dundu nit ki, te Ndeyu àtte réew mi ak diggaley àqi doom-aadama yi ci àddina si sàrtal ko ;
Noo ngi woo Sñ Maki Sàll, Njiitu réewu Bokkeefu Senegaal ngir mu, ci benn boor, joxe ndigal yi war kii di jëwriñu Yoon ji ngir toppekat yi gaawtu ci :
-
Bàyyi Usmaan Sonko ni mu gën a gaawe ngir muccal bakkanam te bañ ko xañ àqi maxejjam ;
-
Ñu bàyyeendi ñeneen ñi ñu jàpp ci kaso yi te dara waralu ko lu moy li ñu wax seen xalaat ak a amal ay xewtey pólitig yoy, Ndeyu àtte jee leen may sañ-sañ yi ;
-
Ci beneen boor, nañu far dekkare bi tas làngug pólitig gu PASTEF ngir ñu mën a dëppoo ak mbarile gi Ndeyu àtte ji sàrtal.