Askanuw Goma dootuñu fàtte altiney tay jii, 27i fani sãwiyee 2025. Nde, ci fitna lañu yeewoo tay jile. Ay soxi fetel yu diis ñoo leen yékkati. Sóobarey Kongo RDC yi ñoo doon soxante ak yoy Ruwàndaa yi ànd ak waa M23. Goma nag, mooy dëkk ba gën a mag ba féete ca penku Kongo RDC, digaloo ak Ruwàndaa. Ci lees wax, démb ci guddi la fa sóobarey M23 yi ak yoy Ruwàndaa yi dugg.
Ci yoor-yoor bi la xibaaru xare bi jib, ñuy siiwal ay nataal ak i widewoo yuy wane ferey Goma yiy daw làquji. Booba, xeex bi taqarnaase na diggante sóobarey Kongo RDC yi ak sóobarey M23 yi ànd ak lenn ci làrme Ruwàndaa bi, jéggi digu réew ma. Nee ñu, amagum na juróomi bakkan yu ci rot ak i nit yu ci jële ay gaañu-gaañu yu sew. Ci bëccëg bi la ko Ronald Rwivanga xamle, moom mi yor kàddug sóobarey Ruwàndaa yi. Bees sukkandikoo ciy waxam yees jukke ci AFP, ñaar-fukki nit ak juróom ñoo ci ame ay gaañu-gaañu yu sew ci benn goxub Ruwàndaa bu digaloo ak Kongo RDC. Ñu bari, ci àddina sépp, ñu ngi ñaawlu cong mi.
Sóobarey M23 yi a kyu Ruwàndaa yi ñoo song, ndax ñoo jéggi dig, dugg biir Kongo RDC. Loolu nag, kilifa yu bari ci àddina si rafetluwuñu ko. Moo tax, ñu ngi duut baaraam Njiitu réewum Ruwàndaa li, Paul Kagamé.
Bees sukkandikoo ci Mbootaay Xeet yi (ONU), am na ñetti at ci ren, bi sóobarey yiy xeex Nguurug Kongo RDC ak limub 3 000 jàpp 4 000 ci sóobarey Ruwàndaa yi tàmbalee xeex ak làrmeb Kongo RDC. Tay nag, ci altine ji, xeex dafa yegg ci beneen jéego ginnaaw bi ñu songee Goma. Ci li saabalkati AFP yi siiwal, ñoom ña teew fa Goma, am na kaso lakk ba jeex. Kaso booba, 3 000iy nit lañu fa jàppoon. Waaye, ñu baree bari ñoo ci rëcc.
Etaasini ñaawlu na cong mi Ruwàndaa ak waa M23 def fa penku Kongo RDC. Ci dibéer ji la seen ndaw li leen teewal fa ONU àrtu, wax ne Washington dina jëfandikoo « jumtukaay yépp » ngir xeex ñiy taal fitna ji.
« Noo ngi ñaawlu bu baax a baax xeex bi Ruwàndaa ak M23 sabab ca Goma ak cong yi ñu amal jëme ca Sake. » (Kàdduy Dorothy, àmbaasadëeru négandiku bu Etaasini fa ONU)
Ñaawlu na tamit xeeti ngànnaay yu xarañe yu Ruwàndaa di jëfandikoo ndax dafay gàllankoor ndimbal lees di yóbbul waa gox ba. Mu wax it ne Etaasini mi ngi sàkku ci ñu dakkal xeex bi ci ni mu gënee gaaw.
Bu dee waa Farãs, seen jëwriñu bitim-réew, Jean-Noël Barrot, ñaawlu na li waa Ruwàndaa ak M23 def. Dafa njëkk a bind, wax ne « Goma mi ngi waaj a daanu ». Moom sax, biral na péeteg Farãs. Dafa ne :
« Farãs a ngi biral njàppaleem ñeel Kongo RDC, deesul a cof dara ci mberaayam. (…) Xeex yi dafa war a dakk ñu toogaat waxtaan. »
Kurél gii di EAC (Communauté de l’Afrique de l’Est) fas na yéene amal am ndaje mu jamp ci àllarbay ginnaaw ëllëg ji ngir wax ci mbir mi. Nee ñu, Njiitu réewi Kongo RDC (Félix Tshisekedi) ak Ruwàndaa (Paul Kagame) joxe nañu seen kàddu, wax ne dinañu ko teewe. Njiitu réewum Kéeñaa, William Ruto, moo xamle xibaar bi. Waaye, waxaguñu fu ñuy amalee ndaje mi. Paap Aali Jàllo, xibaar