Magum jawriñu Senegaal, Aamadu Ba, ma nga woon Farãs, waroon fa teewe ndajem liggéey mom, Càmmug Senegaal ak gu Farãs a ko séqoon. Duppees na ndaje mi, ci farãse, « Séminaire intergouvernemental franco-sénégalais », gàttal biy joxe SIG. Ci alxames ji, 8 desàmbar 2022, la amoon ca Pari. Booboo nekkoon 5eelu ndaje mu ni mel, ginnaaw bi ñu ko mujjee amal ci njeexitalu 2019. Fommees na ko ñaari yoon, 2020 ak 2021, ci sababu mbasum Covid-19 mi.
Moom, Aamadu Ba, ak naataangoom bu Farãs, Elisabet Born mi fay magum jawriñ ji, ñoo waroon a jiite ndaje ma. Waxtaane nañu fa mbirum ndaw ñi ci lu ñeel njàng mi, koom-koom, xeexub Covid-19 bi ak mbirum kaaraange. Wax nañu tamit ci mbirum « visa » yi ak fitnay rëtalkat yi (terorist) yi. Ñaari jawriñ yu mag yépp ñoo fésal seen mbégte ci ndaje mi. Waaye, dafa mel ni Aamadu Ba moo gënatee bég. Ndaxte, nee ñu, indaalewul loxoy neen. Nde, ba mu génnee ca ndaje ma, góob na fa sarica bu duun : 100 tamñaret (miliyaar) ci sunuy koppar. Xam naa looloo ko tax a saalit ba mu wax fa kàddu yii :
« …Maa ngi rafetlu taxawaayu Farãs ci wetu réewi Afrig yi ñeel xeexub terorism ci Sayel bi ak caay-caayug njéggi-dig. Benn jafe-jafe rekk a am ci sunu diggante ñaari réew yi, te mooy ne, Soxnas jawriñ ji, danoo amul benn jafe-jafe. »
Kon, bees déggee Aamadu Ba, diggante Senegaal ak Farãs, amul benn xeetu lënt-lënt, dara ba dara booloo jeex ñagasu ci ; mbëggeel gu sax dàkk a ci am.
Yow miy jàng mbind yile, xam as lëf ci mbooru Seneegal, te jot a teewlu xew-xew yi fi mujje yëngal réew mi ak nees di xoolee Farãs léegi, xam naa yaa ngiy naan :
« Kii de saaga nanu yow ! Saaga na sax sunuy maam, saaga sunuy baay ak i ndey, saaga nu, saaga sunuy doom, sunuy sët ak sunuy sët-sëtaat. »
Moom kay, saaga na maas yépp mboole-seen, saaga Afrig ci boppam. Waaye, lii warul a doon mbetteel. Lu tax ? Waaw, Aamuda Ba deful lu moy topp ci tànki njaatigeem, baayam ci pólitig, Maki Sàll. Xanaa dangeen a fàtte ? Bi Maki Sàll faloo 2012, tukkeem bu njëkk Farãs la ko jagleeloon di, am déet ? Aamadu Ba, moom itam, ginnaaw bi ko Njiitu réew mi tabbee magum jawriñ, Farãs la jagleel génnam bu njëkk. Rax-ci-dolli, Maki Sàll ci boppam, keroog ba muy daje ak “Groupe consultatif de Paris tamit”, indaale woon na, ci seen i wax, 7. 700i tamñaret (miliyaar) ci sunuy koppar, wax fa lu xaw a jege li Aamadu Ba wax keroog. Bu wolof naan « doom ja, ndey ja », fii ku yebu ne « doom ja, baay ba ».
Li Nguurug Senegaal ak gu Farãs di biral mbégte ak a rafetlu rataaxaayu digganteb ñaari réew yile sax, du lu jaaxal nit ñi. Bu ki ci nekk di jéem a fésal njariñ yiy tukkee ci lëkkaloo bi tamit, du dara. Wànte nag, bees demee bay dégg ñenn ci askanuw Senegaal di bàkku ak a damoo ab bor bu réy a réy, di kontaan cim ndimmal mom, tubaab bi la nootoon, wéy di la noot a la ko jox, bu boobaa, jar na nu tiit. Te sax, dañuy àgg ci di tagg ak a kañ ña seen i loxo tàllalu ba suufe, daldi nangu ndimmal loolee. Mu mel ni dañu xamul ne, am réew, amul xarit amul mbokk, ittey boppam rekk. Kon, xaalis bii, ku nu bëgg a gëmloo ne Farãs miy wéy di nu noot daf nu ko may noonu, xippeegoo.
Dafa di, am réew mu fees dell ak i balluy mbindaare yu dul jeex, muy ci biir suuf ak ci biir géej, nekk ci buntub Afrig jàkkaarloo ak àddina, am suuf, am naaj, am i ndaw yu tollu ci seen digg doole, réew mooma, lu muy dox di ñaan ? Mo ndax noo ngi xalaat ? Ku doful ku ne, war a xam ni ndimmal lii, am na lu ci laxasu. Nde, ku la abal i bët, moo lay wax fooy xool. Te, ku ëmb sa sanqal, ëmb sa kersa.
Lii nag, mënees na cee jukkee ay njàngat yu baree bari. Waaye, kàdduy Gelwaar yii toftalu doy nañuy njàngat. Moo tax bindalees na leen ci ab jukki ngir ngeen jàngal ko seen bopp.
Gelwaar, loo waxoon ?
« [Dama ne], baaraam bu ñu tàllal, ab joxoñ la. Xam ngeen loolu. Wànte, juróomi baaraam yu ñu tàllal kuy romb, yalwaan la. Sunu njiit yaa ngi nu dajale fii. Ndax xam ngeen lu tax ? Du tus ! Ngir mën a jot ci ndimmal lii doŋŋ ! Dégg ngeen sunu njiit yi di sant ak di gërëm, ngërmaande gu amul àpp, ci sunu tur nun ñépp, ñu fi nekk ak ñu fi nekkul, jagleel ko ñi nu jox ndimmal lii.
Xool leen sunu njiit yi. Koo ci gis mu ngi bég di layam-layami sunu kanam di sagu, mel ni ndimmal li seen ñakki bopp la… Nun nag, nun askan wi nga xam ne amunu kàddu, amunu fayda, nuy fecc ak di woy, jagleel ko ndimmal lii… Coo ! Noo ñàkk fayda. Ma ne, nan leen ubbi sunu bët yi xool…
Yeen gis ngeen ni xewu maye gu tollu nii, diirub fanweeri at, mu ngi am fii ak feneen. Ndimmal lii ñu nuy séddale, moo nuy rey ! Rey na [jépp] jom ak [gépp] ngor gu nekkoon ci sunu biir. Coo ! Noo ñàkk jom ! Kenn amatul jom.
Ndax xam ngeen ne, réew yi nu yónnee may gi ak tiitar, dañ nuy ree sax fa ñu dëkk ; ndax xam ngeen loolu ? Rax-ca-dolli, sunu doom yu góor ñi ak yu jigéen ñi nga xam ne ñoo ngi dund ci seen biir foofu ca bitim-réew, gàcce rey na leen. Mënatuñoo siggi xool kenn ndax gàcce. Mënatuñoo siggi xool kenn ndax gàcce !
Dëgg la, sunu réew mii, coono lu nekk wàcc na fi, njaajan lu nekk wàcc na ci réew mi. Waaye, loolu nun noo ci war a taxaw. Du kenn ! Nun doŋŋ noo ci war a mën a taxaw. Sunu maam Kocc Barma nee na : “Su fekkente ne bëgg nga rey as gor, dee ko jox suba gu jot lu muy dunde. Bu yàggee, nga soppi ko mala.”
Wax naa leen li fi nekkoon di kor-koral ci jom ak ngor, ndimmal lii lekk na ko. Ndimmal lii lekk na [jépp] jom ak [gépp] ngor gu nekkoon ci sunu biir.
Du gis ngeen xiif gi, ak mar mu metti mi nekk fii ak ñàkk dund bi, rafle bi, ndax xam ngeen lu ko yokk ? Ma wax leen li ko yokk ? Gis ngeen réew ci boppam, bu fekkente ne li muy dunde ak di ko woddoo moo ngi koy yaakaar ci réew ni moom, gis ngeen réew mooma, li ko dale ci doomam ba ci ay sët-sëtaatam, genn kàddu doŋŋ lañuy xam. Laaj leen ma gan kàddu… :
“Jërëjëf ! Jërëjëf ! Jërëjëf ! Jërëjëf !”
Nun nag, nun askan wi nga xam ne amunu kàddu, amunu fayda, nuy fecc ak di woy, jagleel ko ndimmal lii. Coo ! Noo ñàkk fayda !
Ma ne, nan leen ubbi sunu bët yi xool, te xam ne ag njaboot mënut a sosu, sax reen, dëgër, su sukkandikuwul ci lenn lu dul yalwaan bu sax dàkk, dàkk, dàkk !… »