Isen Aabare, Njiitu réewum Càdd la woon, génn na àddina ci loppitaal “Principal” bu Dakaar talaata 24eelu fan ci weeru ut 2021. Nee na ñu“covid-19” bee ko yóbbu. Mi ngi amoon 79i at. Moom nag, yoon da koo daanoon, mu waroon a tëdd kaso giirug dundam.
Isen Aabaree ngi gane àddina 13 ci weeru ut 1942 ca dëkkub Càdd buñ naan “Faya-Largeau”.
Daanaka foo ko tudd, xel yépp dem ci liñ ko fi àtte woon ba caabi féete ko ginnaaw. Waaye ginnaaw “doxotu gëléem kow la jëm”, kenn mënul a tudd Aabare te doo wax tamit ci 40.000i doom-aadama yiñ ne moo leen bóom ak saa-Càdd yi mu tere woon ñu dellu seen dëkk. Daanaka doomu-Càdd joo waxal mu ni la ñaawtéefi Isen Aabare bàyyi nay góom ci njabootam. Am na ci ñoo xam ni ci jamono xarey maxejj yi lañ dakkal seen njàng. Ñu bare it génn nañ réew ma ci lu leen gënalul woon.
Nu dellu ginnaaw tuuti.
Isen Aabare bi mu làqusi Senegaal ak tey mat na fanweeri at ak benn ndax ci atum 1990 la fi ñëw. Goxu Wakaam la dëkkoon ak njabootam.
Bunu fàtte ni Isen Abare daan na xeex bu baax Xadafi ci ndimbalug Farãs ak Amerig waaye daa dem ba ci biir mu bëgg a dëddu Farãs, xamal Mitterrand, njiitu réew ma woon, ni Afrig daa mës a am melokaan buñ koy jiitee, maanaam amoon nanu sunu doxalinu bopp ; kon, amul saar wu mu war a jàngee ci moom. Looloo tax Farãs fexeel ko.
Waaye du loolu rekk moo jural Abare fitna ji ko dawloo Càdd indi ko Senegaal ba mu faatoo fi. Moo nekkoon ci boppu réewum Càdd diggante 1982 ba 1990 bi mu cëtëŋee Gukuni Wédey, daldi koy wuutu ci jal bi. Kon mënees na ne ngànnaay la jote woon ca nguur ga, waaye ngànnaay moo ko fa jële moom ci boppam, ndax Idiriis Débi-Itnoo ko fey boram.
Isen Aabare jiiñ nañ ko ne dafa taxawal nguurug jaay doole, doon buur, di bummi, ku ko weddi mu dal sa kow, képp ku bañ jaarul ci waawam, mu toroxal la, lee-lee sax mu leb say fan. Looloo waral njabooti ña mu bóomoon lëkkaloo cig kurél ànd ceek ay layalkat, sàkku ñu àtte ko, daan ko te jox leen ndàmpaay.
Ci atum 2015 lañ àtte Isen Aabare ci Senegaal mu sukkandiku ci « déggoo » gu Senegaal ak « Union africaine » xaatim. Guléet sax ñu àttee Afrig ku fi doonoon njiitu réewam, daan ko, tëj ko kaso. Liñ ko dugge woon mooy mu doon am ngànt ci bépp njiit bu ko bëggoon a toppandoo.
Li Isen Aabare nekk ci kaso bi yépp, soxnaam, Faatim Raymoon Aabare, daan na dajeek taskati xibaar yi, di layal boroom-këram. Fu mu tollu it, mi ngi doon jébbaane ak a ŋàññ nguuru Maki Sàll ak ëttu àttekaay bi ñu duppe « Chambres Africaines Extraordinaires». Moom, soxna si, dafa gis ni kurél gii ak nguur gi dañoo kootoo ngir toroxal Isen Aabare, Farãs moom nekk ci ginnaaw di xamb taal bi.
Ànd naak tamit seen layalkat di Me Sire Keledoor Li ñaan ba tàyyi ñu afal Aabare ndax mag la, rax-ci-dolli wérul. Te bu loolu weesoo it, njabootam ragaloon nañ Aabare jële koronaawiris ci kaso bi. Mujj gi nag, ci awril 2020, yoon mayoon na ko mu dellu këram diirub ñaari weer, noyyi ngelawul péex. Waaye kaso da koo nëbbaat jant bi. Bi mu feebaree ba xaw a sonn, lañ ko door a yóbbu ci benn kilinig. Biñ gisee ni li ko dal a ngi ëpp i loxo, ñu jàllale ko lopitaal “Principal” bi mu faatoo. Am na ñu doon wax ne ci kaso bi la Aabare amee feebar waaye jawriñu Yoon bi, Me Maalig Sàll, da koo weddi ba mu set. Nee na ca kilinig ba mu doon fajoo la ko “covid-19” bi dale.
Ak lu mënti am, àddina sépp dina jàpp ni Isen Aabaree ngi faatoo Senegaal, réewum teraanga mi ñépp di woy.
« Ku dee bari xarit »…
Ba xibaar bu tiis bi jibee ak tey, ñu baree ngi taggal Isen Aabare ay maamam, naan bañkat la woon, dafa bëggoon réewam, walla moo tabax Càdd, dakkal fa nooteel. Ci seen xalaat daal, bu Càdd nee jonn, tey, nañ ko sante Isen Aabare.
Waaw, ña mu faat seeniy waajur mbaa seeni doom xanaa dañ leen a fàtte ? Doomi-Càdd yi mu gàddaayloo, nag ?
Naam, nguurug Senegaal mënoon na koo génne kaso te du tee muy wéy di bàyyi xel ci moom. Xamees na loolu. Waaye nag, nekk fi naan ñayu-xare la woon ba di ko tappal i medaay, loolu moom xel mënu koo nangu.
Moom Isen Aabare, mësul a bari wax, ca layuwaay ba sax, patt la mës a féetewoo waaye tey jii, noppi na ba fàww. Ñiŋ ko denc ci sëg yu Yoof yi, fii ci Senegaal. Yaaxam Mbay, njiitu yéenekaay “Le Soleil” jël na kàddu ca rob ba, wax lii : “Isen Aabare, daa gëmoon ni Afrig benn bopp la, kon suul ko Dakaar ak Njamenaa, benn la woon ci moom. Man nag li ma gënal mooy wax ci lu baax li mu defal réewam doonte newu ma fi di fàtte-fàttelu liñ koy tuumal ». Doomu Isen Aabare, moom, di wuyoo ci turu Amiid Isen Aabare, juddoo Senegaal, di ma-xareñ (ingénieur) ca Farãs, nee na baayam ku baaxoon la, ku bëggoon Afrig te ñoom diñañ def seen kem-kàttan ngir dëgg gi feeñ ëllëg, ñépp xam ni Isen Aabare, Afrig rekk a ko soxaloon. Aamadu Tiijaan Won, mi fi nekkoon jawriñu Mbatiit ci jamonoy Ablaay Wàdd, moo doon lootaabe jataayu rob ba, doon séddale kàddu gi ak a fàttali santaane yi nuy aar ci mbas mi. Moom ci boppam, nag, ci atum 2011, bindoon na fi Abdu Juuf bataaxal di ko laaj lu tax nguuram nangu woon a làq Isen Aabare ba noppi waññiku di ko toroxal. Moom sëñ Won waxoon na yit ci bataaxal boobu ni àndul ci benn yoon Senegaal di seetaan Aabare ndax way-làqu la fi te bàkku Senegaal su doon tabax, teral gan moo koy xadd.