Démb, kippaangog depite gu Yewwi Askan Wi doon na janoo ak taskati xibaar yi. Jubluwway ndaje maa doon indi ay leeral ci lenn ciy ponk yu soxal askan ñeel seen taxawaay ca Ngomblaan ga, rawatina mbirum “Déclaration de politique générale” mi kujje gi di xaar ci Usmaan Sonko.
Depitey Yewwi Askan Wi xamle nañ ne, bind nañu njiitul Ngomblaan gi, jébbal ko ay laaj. Laaj yooyu nag, moom njiitul Ngomblaan gi, Aamadu Maam Jóob, daf leen a war a jébbal Càmm gi.
Ci laaj yooyu depite YAW joxe, bokk na ci, teewaayu jëwriñ Séex Dibaa, moom mi ñu dénk koppar geek nafa gi. Li ñu bëgg mooy ñu càmbar nafag réew mi, xam fu xaalis bi tollu. Waaye, li gën a soxal nit ñi, mooy ndax Usmaan Sonko dina dem fa Ngomblaan ga, def les duppee ci nasaraan “Déclaration de politique générale”, gàttal biy joxe DPG. Maanaam, wan yoon la xàll, walla yan naal ak i jéego lay teg ngir doxal liggéey bi ko Njiitu réew mi dénk. Teewaay boobu nag, dafa jur coow lu bari.
Bees sukkandikoo ci waa PASTEF, càrtug Ngomblaan gi mayewu ko. Ndax, ci seen i wax, ci li càrt gi yaxal, ndombo-tànku elimaanu jëwriñ amuñu ci. Dafa di, bi Njiitu réew ma woon, Maki Sàll, faree ndombo-tànku elimaanu jëwriñ yi lañ soppi woon càrt gi.
Bu dul loolu sax, nee ñu, amul genn àpp gu tënk Usmaan Sonko, elimaanu jëwriñ yi, ngir mu reew fa Ngomblaan ga. Loolu nag, jur na coow. Kippaangog depite yu bokk Bennoo Bokk Yaakaar joxe nañ dig-daje ëllëg ngir janoo ak taskati xibaar yi. Du ñàkk ñu àddu ci mbir mi.