COOWAL NAPPKATI KAYAAR YEEK YU MBOORO YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Géej gi sàmbaraax na. Bakkan bu rot, 22i nit ñu amey gaañu-gaañu, ñaar ñu nekk diggante dund ak dee, 18 doomi Kayaar yu pólis jàppagum, lii moo tukkee ci xeex bi amoon diggante nappkati Kayaar yeek yu Mbooro yi. Yemu ca de. Ndax lébuy Get-Ndar yi dugg nañ ci xeex bi. Dafa di, seen i mbokk ya sancoon Kayaar la nappkati Mbooro yi song, taal seen i gaal (50 ak lu teg), dàjji fa ab butig, sàcc ay xari laadum, añs. Li seen mbokk yi daj a tax waa Get-Ndar mer ba futt, yeb seen i gaal ba ñu fees, def ciy ngànnaay, ne dañuy feyuji. Lu sabab coow li ?

Keroog, guddig gaawu 1 awril jàpp dibéer 2 awril 2023 la nappkati mbooro yeek yu Kayaar yi jàppante woon fa Xonjo, Mbooro-Ndëndkat ak ci beneen dëkkuy nappkat. Nappkati Kayaar yi ak yu Mbooro yee doon xeex, xeex bu metti. Mu am ay gaal yuñ ci lakk ak i nappkat yu ci jëley gaañu-gaañu yu metti. Am na ci sax ñoo xam ne, dañu ame ay lakk-lakk yu mettee metti ci seen i kanam. Bu dee sabab yi waral xeex bi, Moor Mbeng mi jiite Ndajem nappkati Kayaar yi daf ne : « dafa am i nappkati Kayaar yiy nappe mbaaluy laaw ñoo demoon kow géej, ay nappkati Mbooro song leen, gaañ leen. » Ciy waxam, magi Kayaar yee dëfal nappkati dëkk bi, dalal leen. Bu dul woon loolu, feyantoo day am. Moor Mbeng rax na ca dolli ne :

« Nappkati Mbooro yi dañuy jalgati yoon ndax dañuy nappe mbaal yu sew ci géeju Kayaar gi. Looloo tax ndawi dëkk bi di taxawal gaali Mbooro yi ngir saytu leen. […] Nde, jamono yii, dañuy jàppante ak nappkati Mbooro yi. Ndax, nun, dunu nappe noonu te danuy tere ku nappe ci anam boobu ci sunu géej gi. Te, nappkat yiy jóge Mbooro faalewuñu loolu. »

Moor Mbeng leeral na yit ne, taaluñu genn gaalu waa Mbooro, seen mbaal yi lañu lakk. Waa Mbooro, ñoom dañu wax ne, nappkati Kayaar yee leen tooñ. Ndax, ayu-bés bii weesu, nappkati Kayaar yee karoon seen i gaal, sàndi seen i mbaal. Ndekete, nappkati Mbooro yeek yu Kayaar yi mësuñoo juboo.Bu ñu delloo ginnaaw, dañuy gis ne yàgg nañoo coow seen biir. Ngir fàttali, 2005, xeexoo nañ ba am ku ci ñàkkoon bakkanam. Lu ëpp, nag, tuuru. Ndaxte, bakkan rot na ci.

Kii di Lamin Ñaŋ, fekk baax Dagana, lees wax ne dee na ci. Bu ñu sukkandikoo ci xibaar yi rotagum, bi gaalu nappkati Mbooro yi mbëkkee gaalu nappkati Kayaar yi la daanu ci géej gi, daldi lab. Nee ñu nag, ba léegi, gisaguñ néewam.

Fi mu nekk nii, waa Get-Ndar a ngi bëgg dugg ci xeex bi. Te, su boobaa, jéyya mën na cee am. Ñépp a gis ne, Nguur gee war a jël i matukaayam, dakkal xeex bi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj