“COUP D’ÉTAT” FA GABOŊ : “XEEXU BIIR LA” (ALBEER ONDOO OSAA)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Albeer Ondo Osaa mi jiite kujje gi fa Gaboŋ doon na amal ab laaj-tont ak waa TV5 Monde ñeel “Coup d’Etat” ba fa am. Moom, nee na, li xew du dara lu dul ab “xeexu biir” ci diggante Bongo yi ci seen bopp : “Lii nekkul “Coup d’Etat”, xeexub biir la”. Démb ci alxames ji la Albeer Ondoo Osaa wax kàddu gii ba muy tontu laaji saabalkati TV5 Monde yi.

Bees sukkandikoo ciy kàddoom, njabootu Bongo moo nekk ci ginnaaw Oligi Ngemaa. 

“Fàww ñu delloo mbir yi ci seen jamono. Balaa dara, “Coup d’Etat” amu fi, xeexu biir la. Oligi Ngemaa doomu bàjjenu Aali Bongo la (…) Njabootu Bongo ñoo dem ba gis ne dañ war seppi Aali Bongo ngir mën a wéyal Nguurug Bongo yi.”

Rax na ci dolli sax, ne :

“Dañu jiital Oligi Ngemaa kese, waaye xam nan ki nekk ci ginnaawam. Nguurug Bongo yi mooy wéy ba tey. Oligi Ngemaa ab surga doŋŋ la. Njabootug Bongo moo nekk ci ginnaawam. Ba tey ñoo yor Nguur gi.”

Li kàddoom yiy wund mooy ne, ag kootoo la doomi Bongo yi nas ngir sax ci Nguur gi. Nde, xamoon nañ ne, Aali Bongo mënatul woon wéy di jiite réew mi te ñàkkoon na wote yi. Li Albeer Ondoo Osaa bëgg mooy sóobare yi woññiwaat xob yi, daldi koy delloo ndamam, tabb ko Njiitu réewum Gaboŋ.

Dafa mel ni nag, nopp bu bon bi la ko sóobare yi jox, rawatina Biris Oligi Ngemaa. Ndaxte, ci xibaar ya fa rotagum, ci altine jii, 4i fan ci sàttumbaar 2023, lees war a tabb Biris Oligi Ngemaa moomu, mu nekkandi Njiitu réew ma fileek ñuy indiy coppite ak a amal yeneen i wote. 

Moom nag, Albeer Ondoo Osaa, dankaafu na sóobare ya, tëkku leen. Xamal na leen ni, Nguur gi du yàgg ci seen i loxo.

Li ci kanam rawul i bët. 

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj