“COUP D’ÉTAT” FA GABOŊ

Yeneen i xët

Aji bind ji

Gaboŋ, sóobare yi foqati nañ Nguur gi ci loxoy Aali Bongo ginnaaw wotey Njiitum réew ya fa amoon. Moom kay, bi ñu biralee njureefi wote yi, jox Aali Bongo ndam li (64,27%), ci la sóobare yi yégle ne jël nañ Nguur gi.

Gaboŋ, dañ boole woon wotey Njiitum réew mi, yu Ngomblaan gi ak wotey gox-goxaan yi. Juróom-ñetti téeméeri junni ak juróom-fukki junniy (850 000) saa-gaboŋ ñoo waroon a fal seen Njiitum réew lu bees, dépite yeek meer yi. 

Wote yooyu nag, dafa bari woon lool ay lënt-lënt ak i jiixi-jaaxa. Ndaxte, amul woon benn saytukat bu bawoo bitig Afrig walla biir Afrig bu fa teewoon ngir saytu doxalinu wote yi. Dafa di, kibaraan yi sax, dañ leen a tere woon a siiwal xibaar yay tukke ca réew ma, am sax ay tele yu ñu dog seen i siñaal. Rax-ci-dolli, dañ dogoon mbaali-jokkoo yi fa réew mépp. Kenn mënatul woon xam lay xew biir Gaboŋ. Dañu daggoon lënd gi, tënk nit ña ci kër yi, tere leen génn diggante 5i waxtu ci ngoon jàpp 6i waxtu ci njël. 

Aali Bongo mi tollu ci 64i at moo doon dagaan ñetteelug moome. Ki doon xëccoo ak doomu Omar Bongo ji mooy Albeer Ondoo Osaa mi jiite kujje ga. Te sax, ci ginnaaw Albeer Ondoo Osaa moomu la xaaju kujje gépp bootu woon, ànd ak moom, def wenn say ngir jële fa njabootug Omar Bongo. 

Moom, njiitul kujje gi, ca teel la artu woon, wax ne wote yi am nañuy njuuj-njaaj. Dafa ne woon sax, moom mooy kees war jox ndam li. 

Bi wote yi jeexee, Aali Bongo lañ jox ndam li, wax ne téeméeri xob yu nekk, moo ci fàggu 64 yi lu teg. Ci saa si la sóobare yi génn, wax ne :

“Nun, wattukati kaarange yi mboole-seen, booloo ci Ndajem njàllale gi ak joyyantib campeef yi (Comité pour la transition et la restauration des institutions- CTRI), ci turu askanu Gaboŋ ak li nu warloo kaaraangeg campeef yi, jël nanu ndogalu dakkal Nguur gi fi nekk ngir sàmm jàmmi réew mi.”

Xamleet nañu ne, far nañu njureef yi tukkee woon ci wote yi. Nde, ci seen i wax, càcc daf cee am. Lépp la woon campeef fa reew ma yit, tas nañ ko. Rax-ci-dolli, dañu tëj digi réew ma ba jëmmi jamono. 

Biris Oligi Ngema moo jiite mbir yi, moom ak wattukati kaarange ya féete woon fa màkkaanu Njiitu réew ma. Askan wa bég nañ ci moom lool nag, génn ci mbedd yi di ko fësal.

Farãs naqarlu na “Coup d’Etat” bi. Waaye, Riisi ak Siin, ñoom, dañu fësal rekk seen njàqare. Waa CEDEAO ak Bennoog Afrig, àddooguñu. Waaye, xam naa du yàgg.

Bu dee Aali Bongo moom, ab widewoo la def, di ci làkk àngale, di sàkku ndimbalu waa àddina si. Nee ñu, ma nga Marog làqatu. Moom mi daggoon lënd gi, moo koy mujje jëfandikoo ngir ñaan wallu.

Fi mu nekk nii, xibaar yi bareegul. Moo tax mëneesagu cee sori. Dees na ko topp.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj