Ndogal li jib na. Lees doon njort bir na. Nee na fàŋŋ. Àttekat bii di Mamadu Siis Faal mi jiite woon layoob dabu bi ak Elisabet Géy Mbeng ma woon ci wetam, jëmmal nañu yéeney waa Bennoo Bokk Yaakaar. Nde, yokk nañu daan biñ njëkkoon a daan njiitul Pastef li, Usmaan Sonko, keroog 30 màrs 2023. 6i weeri kaso yum dul tëdd lañ gàll Usmaan Sonko, daldi saxal ndàmpaayu 200i tamndaret lu njëkk la. Nee ñu, meeru Sigicoor bi mënatul a bokk ci wotey 2024 yi, donte ne Nguuda Mbuub ak Biram Suley Jóob, ñoom, dañ jàpp ne, ba tey, Usmaan Sonko mën na bokk.
Cig pàttali, Maam Mbay Ñaŋ moo doon toppe njiitul Pastef li ay tuumay yàq der ñeel mbirum PRODAC mi Usmaan Sonko waxoon ne, moom jëwriñ jiñ dénk wërteef gi, daf cee luubal 29i tamñaret ci sunuy koppar. Bésub 30 màrs lañ njëkkoon a daan Usmaan Sonko 2i weeri kaso yum dul tëdd ak 200i tamndaret yi muy dàmpe Maam Mbay Ñaŋ. Ci ginnaaw gi la ngóor si Ñaŋ sàkku àtteb dabu ngir ne, loolu doyu ko. Moone, ca njëlbeen ga, fésaloon na mbégteem ci àtte bi, doon wax ni deram set na.
Bésub 17 awril lees ubbi woon àtteb dabu bi laata ñu koy bëtal ci bésub tey jii di 8 me 2023. Usmaan Sonko teewul woon ci layoo bi. Du moom, du woon tamit ay layookatam. Ndax ma nga woon fa Sigicoor, doon liggéey.
Toppekat bii di Ibraayma Baaxum dafa sàkku woon ci àttekat bi, mu daan Usmaan Sonko 2i ati kaso yoy, menn mi daf koy tëdd. Sàkkooti na woon ci àttekat bi sax, mu dóor Usmaan Sonko ab « mandat de dépôt ». Àtte bi nag, yéex na jib. Nde, ci 15i waxtu lees ko jàppoon. Waaye, mujj naa dem ba 16i waxtu ak lu teg. Mu mel ni, yombutoon. Xel teey na.
Soxna Mimi Ture, Décce Faal, Seex Tiijaan Yum, Maalig Gàkku ak yeeneen i kilifa ñaawlu nañu àtte bi, fésal seen ànd ak Usmaan Sonko ci nattu bii.