DAAR-DAARU USMAAN SONKO (NJIITUL PASTEF)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci guddig démb ji, Usmaan Sonko, njiitul làngu PASTEF, doon na amal daar-daar ci xëtu Facebookam. Ca biir waxtaan woowa, àddu na ci tolluwaayu réew mi, biral naal yi mu fas yéene doxal ngir joyyanti réew mi. Waayeet, àddu na ci ni Yoonu réew miy doxe ak caytug Bokkeef gi.

Mbubbum njiitul PASTEF la Usmaan Sonko soloon démb, bi muy waxtaan ak saa-senegaal yi ci daar-daar, jaare ko ci xëtu Facebookam. Moom nag, feddali na dogu bi mu dogu ci jëmmu boppam ak ci wàllu pólitig ngir joyyanti Senegaal, jubbanti li dëng. Bees sukkandikoo ciy kàddoom, naam, mbir mi narul a yomb. Waaye, ba tay ciy waxam, moom Usmaan Sonko, du kuy soppeeku, na mu meloon lay wéy di mel. Maanaam ,na woon, fa woon.

« Man, Usmaan Sonko, maa ngi wéyal xeex yi ma doon xeex, ànd ceek pasteef. Sama jubluwaay soppeekuwul : tegaat réew mi ci yoon. Sunu wareef la, nun ñi jiite réew mi, ci mboor ak ngir askan wi. »

Ngir firndeel ay kàddoom, Usmaan Sonko xamle na ni kër sax amatu ko. Li mu bëgg a wane foofu mooy ne, ñoom njiit yu yees yi, ci jub, jubal ak jubbanti lañu tegu.

NAALUW JOYYANTI SENEGAAL : « DINANU AM NDAM BA YÉEM ÀDDINA SI. »

Njiitul PASTEF li xamle na ne, ci fan yu néew, dina gaaral aw naal ngir joyyanti rew mi. Ca biir naal woowa, dees na ca fekk ay pexe yu leer ngir tegaat réew mi ci yoon. Dafa ne :

« Ci fan yii di ñëw, dinaa gaaral saa-senegaal yi naaluw joyyanti réew mi. Dinanu wax saa-senegaal yi naka lanuy jubbantee réew mi. »

Usmaan Sonko fàttali na taxawaayam ba muy nekk ci kujje gi. Nee na, ca atum 2018, ba muy nekk dépite, dafa daan xeex nger ak yoriin wu ñaaw.

« Ca atum 2018, waxoon naa ca kanamu Ngomblaan ga ne, dañu war a teg ay daan ñiy laale ci nger ak yoriin wu ñaaw. Widewoo yaa ngi fi. Waaye, li nu fi fekk moo yées li nu njortoon. »

Waaye, jafe-jafe yooyu taxul Usmaan Sonko xàddi. Nde, ciy waxam, yaakaar am na bat ay. Xamle na ne ñu bari ci àddina si ñoo ngi wéy di bëgg a liggéey ak Senegaal. Joxe na misaalu Mercedes-Benz mi bëgg samp ci réew mi ag ndefar guy taqale ay daamar. Rax na ca dolli ne Senegaal dina am ndam ba ñépp yéemu.

« Tay, àddina sépp a ngi bëgg a liggéey ak Senegaal. Te sax, Mercedes-Benz ci boppam dafa bëgg a samp ci réew mi ag ndefar guy taqale ay daamar. […] Dinanu am ndam ba àddina sépp yéemu ci sunu liggéey. »

DOXALINU YOON

Ba tay ciy kàddoom, njiitul PASTEF li fàttali na ne, lees fal Basiiru Jomaay Jaxaar Fay ci boppu réew mi tekkiwul ne lépp sotti na. Ci xalaatam, coppite gi ñu war a amal ngir jëm ci xeetu yoriin wu jub du doon lu yomb te gaaw. Nde, dina am ay gàllankoor ci biir. Usmaan Sonko wax ne, bés bu nekk xeex la. Ndax, li ñu fi fekk dafa doy waar ba jéggi dayo.

Usmaan Sonko àddu na yit ci doxalinu Yoon. Li mu ci jëkk a wax mooy ne, moom ci boppam moo jëkk a bind jëwriñu Yoon ji, keroog 5 màrs 2025. La mu jublu woon ca bataaxalam boobu mu bind niki maxejj, mooy sàkku ci àttekat yi ñu def seen liggéey. Ndax, ciy waxam, ci biir àttekat yi, dafa am ñu baax ñuy siggil Yoon ; mu am itam ñu doy waar te dëng ñuy gàkkal deru Yoon.

Usmaan Sonko a ngi jeexal ay waxam ci woo saa-senegaal ci ñu gànnaayoo muñ, pasteef ak teey. Ndax, liggéey bi du yomb.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj