Robine tijji, ndox walangaan, xel dal, xol tóor yaakaar, yaakaar ëllëg gu tane ndax fu ndox mate, dund sell. Lii mooy njeexitalu Kër Momar Saar 3 (KMS3), dikke 274i milyaar ci kopparu Senegaal.
Ñetteelu defaru (isin) bu Kër Momar Saar ca Luga moom la Njiitu-réew mi, Maki Sàll, doon ubbi gaawu 10eelu fan weeru Sulet ci teewaayu Sàrl Faal, njiitu SONES, Jany Arnal, njiitu SEN-EAU, jëwriñu ndox mi Sëriñ Mbay Caam, njiitu “Collectivités locales” yi, Aminata Mbeng Njaay, ndawu Farãs ci Senegaal Philippe Lalliot. Yeneen jëwriñ a nga fa woon ak ay gan ak waa dëkk baak ñeneen ak ñeneen.
Ginnaaw bi mu nuyoo waa Njaambur, sant leen ci teertu bi, kañ seenug njaambaar ak mën gan, lii la ci Maki Sàll teg : «Ndox mu sell ak mbey dañu maa mës a soxal… 3i at ak genn-wàll a ngi bi nu ñëwee teg xeer wu njëkk wi ci ñetteelu defaru (isin) bu Kër Momar Saar. Tey, nu dellusi ubbi ko. Soo leen déggee KMS3 war ngeen xam ne am na ñaar yu ko jiitu ci at yi nu génn.
Ñàkk ndox moom, kenn dootu ko fi jàmbat. Guléet lu ni mel am fii ci Senegaal. Waaye nag, ngalla bu ndox mi ñëw rekk, ñu koy yàq ak a pasar-pasare. Buleen fàtte ne ndox mi liggéey bu réy la laaj ak alal ak i jumtukaay ; kon nan ko yaxanal bu baax. Dëkk yi wër Kër Momar Saar yit dinañu am ndox ndax jaaduwul ñuy tanqee Lac de Guiers, yóbbu Dakaar, ñoom ñii ñuy wéy di mar».
Bi ko Sàrl Faal wuutoo ci kàddu gi, dafa ne : «Nu ngi sant Yàlla, di gërëm bu baax Njiitu-réew mi Maki Sàll; yombalal nanu lépp luy jumtukaay ngir KMS3 taxaw. Defaru (isin) bi dina saafara lu mu néew-néew fukki at bu nu ko booleek defaru (isin) biy sellal ndoxu géej mi nga xam ni daa saf xorom. Kon, dalal-leen seen xel te xam ni fileek 2030 kenn du jàmbatati ñàkkum ndox ci Dakaar ak li ko wër. Rax-ci-dolli, Jogo dina ko feelu ngir séddale gi gën a yaatu. Ak KMS3, li nu daan joxe ci ndox yokku na daanaka ñetti yoon : 250.000 m3 lan ko jële, yóbbu ko ba 600.000 m3…
Njiitu-réew mi sàkku ci nun nu fagaru te nu ngi ci, di liggéey ngir ndoxu ëllëg. Fas nanu yéene sàmm ndox mi ba mu mucc ayib ci bépp fànn, ki koy jëfandikoo dina ci gis boppam te du tax njëg li yokku».
Ci gis-gisu Baabu Ngom, njiitu naal bi, mën-mënu KMS3 romb na soxlay waa Dakaar ci ndox. Nee na it ngir matale, 200.000 m3 egsi Dakaar bés bu jot, dinañu door beneen defaru (isin) ca Mexe balaa yàgg.
Aliyun Seen miñ dénkoon liggéey bi, moom, nëbbul sagam ndax yombul woon waaye mën nanoo wax ne njeexital gi wurus la.
Te lépp a ngi sukkandiku ci seen xam-xam ak seen xereñ. Ciy leeralam, «ndox mi su jógee dex ga, dina jaar ci juróomi pomp, bu nu ci noppee dindi suuf si, segg ko, laata muy dugg ci mbalka yi, ginnaaw loolu lay door a wutali Ndakaaru ak Mbuur».
Ambasadëeru Farãs ci wàllu boppam yëkkati na fay kàddu ci turu farandoo yi ñeel wàllum koppar, sargal Senegaal, sant ñépp ñi tax liggéey bi àntu. Dafa njëkk biral mbégteem ci li mu teewe ubbi KMS3 bi nekkoon nisër gu réy te di tey isin bi gën a mag ci Afrig sowu-jant gépp.
Kenn mënta nettali daloo KMS3 te tuddoo Sëriñ Mbay Caam. Delloo na njukkël kippango yi lëkkaloo ba liggéey bi sotti te «doomi-Senegaal ak ay farandoom séq ko. Xewu tey wi am na solo lool. Duma ko ndamoo ndax du samag ngóora, ay nit ñu baree ci jàpp ba mu egsi fii, kon nuy sant ñépp. Weeru Me wii nu génn rekk, tele yi demoon nañ Pikin, Géejawaay ak Tëngéej, waa gox yooyu yépp xamale leen ni ñàkk ndox gi wàññeeku na bu baax. Ak KMS3 gii, kanam la jëm».
Nu ngi am yaakaar ne meññeefu KMS3 dina méngook seeniy tóor-tóor ngir ñàkkum ndox nekk ci sunu ginnaaw ndax, ni ko Aminata Mbeng Njaay tënke, «fu ndox amul, kenn du fa mën a dund.»