Nguuru Israayel ak waa sóobarey Hamas yi (Palestin) am nañu déggoob dakkal xeex bi fa Gasaa. Ci àllarbay démb ji, 15i fani sãwiyee 2025 bi la déggoo bi taxaw.
Jassim Al Thani, elimaanu jëwriñi réewum Qataar moo biral xibaar bi va ndajem saabal ma mu doon amal ak saabalkat ya. Ciy xibaar ya mu biral, lélu déggoob dakkal xeex bi mi ngi door bésub dibéer, 19i sãwiyee 2025. Daf ne :
“Nanu am yaakaar ne lii mooy jéego bu mujj ci xeex bi.”
Jëwriñ ji yokk na ci ne, Qataar dina ànd ak réew yii di Esipt (Misra) ak Etaasini, di wéy di liggéey ngir way-jàmmaarloo yi, ku ci nekk, sàmmonte ak li nga sasoo ci déggoo bi.
Déggoo bi dafay wax ne, Hamas dafa war a bàyyi fukki-fukki doomi Israyee ya mu jàppandi. Naka noonu, Israayel tamit sasoo na bàyyi doomi Palestin ya mu jàppandi.
Njiitu réewum Etaasini, Joe Biden, moom itam dëggal na xibaaru déggoo bi, daldi koy rafetlu. Ciy waxam, déggoob bi dina :
“… dakkal xeex bi fa Gasaa, dina tax ndimbal lees di yóbbul doomi-aadama ya fa Gasaa yokk te yit dina tax ñi ñu jàppoon mën a dellu ca seen i njaboot ginnaaw bi ñu leen jàppee diirub 15i weer ak lu teg”.
Biden yokk na ci ne, li waral déggoo bi mooy :
“lees takkal pot Hamas ak coppite ya tukkee dakkalub xeex ba fa réewum Libaŋ, ak li dooley réewum Irã wàññeeku. Waayeet, li Amerig doxal ab diplomaasi bu xereñ te jaar yoon bokk na ci sabab yi. Sama diplomaasi mësul a deñ ci seqiy jéego ddi ci def ay jéego ci wàll wi.”
Biden biral na cofeelam ak yëg-yëgam ñeel njaboot yi deele a congum 7 oktoobar ba ak ñi deele ci diirub xare bi yépp. Ba tay ci waxam, ” ci lu yàggul dara, ñi ñu jàppandi dinañu dellu ca seen i njaboot.”
Cig pàttali, xare bi dox diggante réewum Palestin ak Israayel mi ngi tàmbali keroog 7i fani oktoobar 2023, ginaaw ba waa Hamas duggee ci bëj-saalumu Israayel, faat fa lu tollu ci 1 200i nit, jàppaale 251i doomi Israayel. Cong mooma nag, fayu la ko waa ko Hamas dugge woon. Ndax, ay ati at, Israayel mi ngi leen di noot, di leen xoqatal ak a fitnaal ci càgganteg àddina sépp. Israayel, rawatina seen elimaanu jëwriñ ya (Benjamin Netanyhu), dafa taafantu mbir ma, bañ a yem ci fayu doŋŋ, daldi koy soppi xare bob, defagum na 2i at. Nde, boobaak léegi, cong ya fa Israayel def ñoo waral lu ëpp 64 000iy nit ñàkk seen i bakkan fa Gasaa. Lim boobu, jëwriñ ja yor mbirum wér-gi-yaram fa Palestin moo ko joxe. Ca biir lim booba, bari nay xale yu ca bokk.
Njiitu réewum Amerig lees fal bees, Donald Trump mi war a jël toog ci jal bi bu altinee, 20i fani sãwiyee 2025, bind na ci mbaalu jokkoo bii di Truth Social, wax ne :
“Am nañu ab déggoo ngir ñu bàyyi ay nit yu ñu jàppandi ca réewi penku yi. Dinañu leen génnee ci diir bu gàtt, jërëjëf waay !”.
PONKI DÉGGOO BI
Persidã Joe Biden nee na, déggoo bi dox diggante Israayel ak Hamas amn a ñetti ponk :
Bi ci njëkk mooy « dakkal xeex bi » ci diiru 6i ayu-bés. Sóobarey Israayel yi dinañu génn Gasaa, bu ko defee, Hamas daldi bàyyi ñi mu jàpp.
Ñaareelu ponk bi mooy waxtaan ngir am déggoob « jeexal xare bi ba fàww ». Njiitu réewu Amerig li waxaat ne, bu waxtaan yi wéyee, lu ëpp juróom-benni ayu-bés, àppug dakkal xeex bi dina wéy.
Ñetteel bi mooy, waa Palestin dinañu mën a dellu ca seen i dëkkuwaay yu yàgg ya, muy fépp fa réew ma. Dinañu tëral naaluw tabaxaat réew ma, te ndimbalu li dina gën a bari.
Elimaanu jëwriñi réewum Qataar, Sheikh Mohammed bin Abdulrahman al-Thani, dafa fësal ni, am na njort bu rafet ci déggoob bi, waaye mi ngi lépp a ngi aju ci ñi ko séq :
“Yaakaar nañu ne ñi ko séq ñépp dinañu sàmmonte ak déggoob bi.”
Mu am nag lenn lu waa Palestin di sàkku te mooy ñu indil leen lu tollu ci 600i sëfaan (kamiyoŋ) yu def ay ndimbal ak i garab yees di fajoo, boole ci ay mbaar (xayma), duggal leen fa réew ma, jaarele leen fa Rafah.
Ba tay ci wàllu ndimbal li, bëgg nañ ñu indil leen ay jumtukaay yu taxawalee ay béréb yu am solo niki ay raglu (opitaal), balluwaayi mbëj (centrales électriques), ay solom yees di jaarale ndoxum naan mi ak ndox mu bon mi.