DÉGGOOB YOON DIGGANTE SENEGAAL AK MAROG : DÉPITE YI JÀLLALE NAÑU SÉMBU ÀTTE WI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci talaatay démb ji la Ngomblaan gi doon fénc sémbuw àtte ñeel Déggoob Yoon bi dox diggante Senegaal ak Marog. Sémbu àtte woowu mooy may Njiitu réew mi sañ-sañu jëmmal Déggoo bi ñaari réew yi xaatim jëm ci taxawu ak dimbali seen i doomi réew ñi ñu jàpp ci kaso yi ak yónnante ay nit ñu ñu daan. Déggoo boobu, 17 desàmbar bee weesu lañu ko xaatimoon fa Rabat, péeyu Marog.

Ca ndajem jëwriñ ma amoon keroog 22 sãwiyee 2025, Soxna Yaasin Faal miy jëwriñu mbiri bitim-réew ak saa-senegaal yi nekk bitim-réew, dafa waxoon ne :

« Jubluwaayu Déggoo bi mooy taxawu sunuy doomi réew mi te yombalal leen ndimbal li foofa ñu leen jàpp, ca réewum jàmbur. »

Déggoo bi mooy leeral sàrt ak anam yi ñaari réew yi di yónnantee ay nit yu ñu daan, sabab yi waral ngànt yi ak njeexital yi ciy sosoo ci wàllu Yoon. Soxna Yaasiin Faal  ne :

« Bu jumtukaayu Yoon bii yembee, dina gën a ñoŋal nekkiinu saa-senegaal yi ñu jàpp ca kasoy Marog ya, waayeet dina gën a yomb ci ñoom ginnaaw bi ñu leen delloosee fi réew mi, ñu tëdd fi diir bi ñu war a tëdd kaso. »

Déggoo bi nag, ci leerali jëwriñ ji, saa-senegaal yi ñu jàpp fa Marog ak saa-marog yi ñu jàpp fi Senegaal rekk la ñeel, ak it li réew mu ci nekk mënee tóxal nit ku ñu daan ba noppi, delloo ko Yoonu réewam.

Déggoo bii nag, dina tax Càmmug Senegaal mën a taxawu doomi réew mi yoy, dañu amlante ak Yoon foofa, fa Marog. Loolu la yégleb Càmm gi xamle.

Marog nag, am 299i saa-senegaal yi ñu jàpp ca seen i kaso. Lim bile, Njiitul Móodu-Móodu ak Faatu-Faatu yi (Directrice des Sénégalais de l’Extérieur) moo ko joxe ci ab yégle bu mu siiwaloon bërki-démb ci altine ji. Ci biir 299 yooyu, am na 160 yoo xam ne Dakhla lañu féete, 93 yi fa Lâyoune, 49 yi fa Bouizakarne ak yeneen 18 yu nekk Tan-tan. Bu dee 139 yiy mottali 299 yi, dañoo tas fa des ca réew mépp. Yéenekaay Le Soleil moo ko xamle.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj