DÉPITEY FARÃS YI DAANEEL NAÑU CÀMMUG MICHEL BARNIER

Yeneen i xët

Aji bind ji

Dépitey Ngomblaanu Farãs yi wote nañu pasum diiŋat (motion de censure), daldi daaneel Càmmug elimaanu jëwriñ ya, Michel Barnier. Dépitey kujje gees duppee « La gauche » ñoo dugaloon pasu diiŋat mi, wote ko, jàllale ko. Muy tekki ne, Càmm gi Michel Barnier taxawaloon dafay tas, ñu daldi tabbaat elimaanu jëwriñ bu yees, mu taxawal Càmm gu yees.

Ci àllarbay tay jii la pasu diiŋat mi jàll. Laata wote bi di am, dépite yi wàqante nañu fa diirub 3i waxtu. Dafa di nag, 288i dépite doŋŋ lañu soxla woon ngir jàllale pasu diiŋat mi. Wànte, lim bi ko wote dafa mujje kowe seen njort. Nde, 331i dépite ñoo ko wote.

Wëliis dépitey NFP yi (Nouveau Front Populaire), dépite RN (Rassemblement National) yi tamit dañu wote ngir daaneel Càmmug Michel Barnier gi. Moo tax, fi mu nekk nii, réewum Farãs amatul Càmm. Waaye, ñoñ baatu doxal bi (l’Exécutif) ñooy saytoogum doxalinu réew mi fileek geneen Càmm gu yees di sampu.

Cig pàttali, ngir wote nafag « Sécurité sociale » mi ñeel atum 2025 mees dëgmal, Michel Barnier dafa sukkandiku woon ci dogu 49.3 bu Ndeyu Sàrtu réewum Farãs. Waaye, dafa lajj ci kanamu dépite yi. Bu ko defee, war na jébbal Njiitu réew ma, Emmanuel Macron, ab bataaxal ngir biral tekkig ndombog-tànkam niki elimaanu jëwriñ.

Wii mooy ñaareel wi yoon ñuy daaneel ag Càmm fa réewum Farãs. Yoon wu njëkk wa, atum 1962 la woon, di at ma ñu daaneeloon Càmmug Georges Pompidou. Jamono jooja, Seneraal De Gaulle dafa jëloon ndogalu tas Ngomblaan ga. Waaye nag, Emmanuel Macron moom, du mën a tas Ngomblaan gii.

Yoonuw réew ma mayagul Emmanuel Macron sañ-sañu tasaat Ngomblaan ga. Li ko waral moo di ne, dafa tasoon Ngomblaan gi lu yàggul dara (9eelu fan ci weeru suwe 2024). Te, balaa mu koy mën a tasaat, fàww mu am at, maanaam 9eelu fan ci weeru suwe 2025. Moo tax nag, fi mu nekk nii, ci nen la toog. Ndaxte, lees di séentu ci moom mooy mu ba, tekki ndombog-tànkam, ñu daldi amal yeneen i wote ngir fal Njiitu réew lu yees.

Ndax dina bàyyi am déet ? Li ci kanam rawul i bët.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj