DI BUUR, DI BUMMI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Li jaaxal waa Senegaal, mooy wax-waxeet yi kilifay réew mi dëkke. Ku ci jóge ci kujje gi, dem ci nguur gi yaa ngiy xas ñaa nga àndaloon démb.

Mbir mi dafay faral di am ba kenn, ci ñaari làng yépp, muccu ci. Ñépp a ngi fàttaliku ci ndetteelu atum 2018, bi peresidaŋ Maki Sàll nee mësul a ni nañu jële wote yi ci loxoy Usmaan Ngom. Moone, ba mu ko waxee yàggul woon dara te yit moom yemul woon ci loolu, nde noon na doonte sax Séex Géy la ñuy dénk liggéey boobu, ba tey Usmaan Ngom ay wéy di doon kilifaam. Waaw lan a fi soppeeku ci diggante bi ba mënul a def lu yées li mu doon laaj ? Ci sunu gis-gis, li ko waral du dara lu moy doole ju bari ji ñu jox peresidaŋ ci sunu doxalinu réew. Te loolu du tey la tàmbali : bi digganteem ak Mamadu Ja yàqoo la Seŋoor soppi sasug njiitu réew mi, jox ko doole ju baree-bari. Kon dafa mel ni mbir mi du Wàdd, du Maki te du keneen : képp ku fanaan Màkkaanu Njiitum Réew mi genn guddi, sooy yeewu di sax i laaf.

Ba tax na, foog ñu wàññi doole joojuy tax benn doom-aadama kese yaakaar ni moo gën ñépp, lu mu xalaat mbaa lu mu xaw a xalaat sax, noonu la !

Lenn ci li waral loolu, mën nañu cee lim li wolof naan : « Ku ëmb sa sanqal, ëmb sa kersa ». Lépp luy ndombog-tànk gu kawe, njiitu réew mi moo cay tabbe. Bu ko defee, ku nekk di xaar sa wàll ci nag wi, doo bëgg a def walla nga wax peresidaŋ loo xam ni dina tax ëllëg, mu ni kii de, àndul ak man, xereñ na, gaa, waaye dara laa ko dul jox.

Ngir loolu deñ fi, foog ñu def ni yen réew yi, maanaam di amal ay joŋante diggante doomi-réew yi ngir xool kan moo war a jiite bérébi liggéeyukaay yu kawe yi. Lu ko moy peresidaŋ dafay wéy di nekk daanaka Buur ak Bummi, kenn du ko sañ ni sa bët bi suuf a ngi ci.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj