DIGAALE SENEGAAL AK RIISI ÑEEL MBAY MI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiiti réew mi, dañu nas aw naal, tudde ko “Senegaal 2050”, mu doon cëslaay gi nuy sukkandiku ngir ligg réew mi. Ca weer yee jàll lañu ko gaaraloon Saa-senegaal yi ak àddina sépp. Jubluwaayu naal wi mooy, fii ak atum 2050, soppi xar-kanamu Senegaal, suqali réew mi, fexe jàppandil dund ak nekkiinu askan wi.

Ku ne dund nag, wax lekk ak naan, muy lu mënut a ñàkk ci nit. Te nag, lekk ak naan itam, boo ko waxee, waxaale nga la mbay. Ñoom nag, njiiti réew mi, seen nisër mooy suuxat mbay mi, càmm gi, napp gi ak ndefar yi ngiree Senegaal di dunde luy meññee ci suufam, walla di génnee ci ndoxam, walla ñu ko fiy defaree.

Bu dee mbay mi nag, ngir jëmmal yéene ji ci Càmm gi am, fàww ñu amal ciy coppite ci fànn yu bari, dooleel baykat yi, jox leen jumtukaay yu war. Loolu nag, Senegaal daf ci lottagum jamono jii, moo ko tax di wut ak réew yu xarañ ci fànn wi ngir lëkkatook ñoom, suqali mbay mi. Ci kaw loolu la Càmm gi waxtaan ak réewum Riisi. Kii di Sëñ Móodu Géy Sekk, di xelalkatu elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, moo ko xamle.

Ci li Sëñ Sekk xamle, Riisi dina dimbali Senegaal ngir mu suqali mbay mi. Ginnaaw bi ñu waxtaanee, Riisi dina dimbali Senegaal ci fànn yii toftalu :

  • Yombalal Senegaal ay jiwu yu baax te doy

  • Indil Senegaal ay xeeti àngare “organiques”

  • Tàggat ay nit ba seen xam-xam màcc ci fànnu mbay

Naka noonu, tëral nañu ay sémb yu ñuy bokk liggéeyandoo, niki :

  • Taxawal sàqum jiwu ci réewum Afrig

  • Suqali mbayum bele bi

  • Defar ay àngare “organiques”

  • Tàggat ay Saa-senegaal ci wàllu mbay.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj