(PAAP AALI JÀLLO)
Njiitu réew mi woyofal na sàrti guural gi ak dogal yi mu jëloon ngir xeex mbasum Covid-19 bi. Ci altine ji, 11eelu fan ci weeru Me la xamal askan wi ci bàttaleem bi tele RTS biral ci guddi gi, bi 20i waxtu jotee. Njiitu réew mi ne, li ko dale ci talaata ji 12eelu fan ci Me, dees na ubbiwaat jumaa yi ak jàkka yi, luuma yi, dakkal ay-ayloo yi amoon ci ubbite ja yi (màrse yi) ci biir Ndakaaru, delloosi néewi Móodu-Móodu yi deewe bitim-réew ci sababu mbas mi…
Bañoon mbasum Covid-19 bi jur ci réew mi ab jéyya moo taxoon Maki Sàll jël ab dekkare ci bésub 23eel ci màrs, sàrtal guural gi ak dëju-sa-kër ñeel réew mépp. Démb, rafetlu na taxawaayu doktoor yi ci xeexub mbas mi ak pajum way-tawat yi doonte ne jàngoro jaa ngiy wéy di law. Njiitu réew mi ne :
« Maa ngi dolli sant ak a gërëm sunu fajkat yu jaambaare yi, ñiy liggéey ci wàllu paj mi ak ñi leen di jàppale ñépp. Noo ngi leen di sargal ci xeex bi ñuy xeex guddi ak bëccëg jàngoroy Covid-19 ju bees jii, jaaxal àddina te ñàng lool. Te, tey, seen bakkan a ngi ci xottu-gerte. Moo tax seen kaaraange lu ma yitteel la. Bu ko defee, dinan jël ay matuwaay ngir aar leen, xeex lawug jàngoro ji. Maa ngi ndokkeel itam liggéeykati njawriñu wér-gi-yaram ak ndimbal njaboot gi. »
Njiitu réew mi fàttewul takk-der yi ak soldaar yiy sàmm kaaraange gi tey wattu guural gi ak dëju-sa-kër gi ci biir réew mépp. Sant na yit kilifa diine yépp, kilifa aada yi ak kuréli way-moomeel yiy jàppale nguur gi ci xeexub mbas mi. Maki Sàll ñaanal na ñi faatu ci sababu mbas mi, jaalewaale leen seen i njaboot.
« Lépp jàppandi na ngir nu delloosi néewi Móodu-Móodu yi deewe bitim-réew ci sababu mbas mi… »
Njiitu réew mi, Maki Sàll, xamle na ne dégg na jàmbati njabooti Móodu-Móodu yiy sàkku ci nguur gi mu delloosi Senegaal néewi yi jàngoroy Covid-19 bi rey ca bitim-réew. Ci loolu la sukkandiku, digal jawriñu mbiri bitim-réew yi ak Móodu-Móodu yi mu déggook fajkat yi def li ci war.
Ginnaaw gi, Maki Sàll fàttali na ne, bi mbas mi duggee ci réew mi, dafa sant nguur gi ci saa si mu lal ab naal bu yemoo te méngoo ak sunu doole, sunu koom-koom, sunuy aada ak nekkin ngir xeex ko. Ci kow loolu lañ ne gaw gi du baax ci réew mi. Moo taxoon ñu jël ay matuwaay yuy wàññi yëngu-yëngu nit ñi, rawatina tukki yi. Njiitu réew mi bég na ci matuwaay yooyu ndaxte, ciy kàddoom, « ci lan jaar ba dog buumug wàllentu jàngoro ji, tere koo law ci réew mi, doonte sax ñi muy faat a ngi yokku. Jéego yooyu, nag, ku nekk ci yéen jaayante naak boppam ba mu sotti. »
Bim noppee ci loolu, njiitu réew mi dafa biral ay lim, wax tolluwaayu mbas mi ci biir réew mi. Ci la ne : « Ci bésu tey jii (altine 11eel ci weeru Me 2020), sunu réew mi ngi ak 1886i way-tawati Covid-19 bi, 715i nit yu ci jot a wér ak 19 yu ci faatu. Fi nu tollu nii, limees na 1151i way-tawat yuy faju ci sunu bérébi fajukaay yi. Lëlees na 718i wàlli-jegeñaale (cas contacts). Rax-ci-dolli, 22 ci 45i depaartemaa yi amuñu jàngoro ji. Warees na koo rafetlu te gën a góorgóorlu ci moytandiku bi. »
Wiris bi dina wéy di dox ci réew mi ba weeru Ut, walla sax Sàttumbar.
Njiitu réew mi xamle na yit ne, ci diirub 2i weer yu metti, waxtaan naak ay boroom xam-xam yu mag a mag ci réew mi, seen xel màcc ci xeeti xam-xam yu bare te wute. Bees sukkandikoo ci kàdduy Maki Sàll yi, li rote ci njàngat ak gëstu yu xóot yu ñooñii jot a def ci mbas mi, mooy ne du fi gaaw a jóge. Nee ñu, lu mu gaaw gaaw (bu dee noo ngi sàmmonte ak matuwaay yi), Covid-19 bi dina wéy di dox ci réew mi ba weeru Ut, walla sax Sàttumbar. Kon, bàyyeeku xaju fi. Li am ba des moo di ne war nanoo xool nan lanuy def ba dëkk ak wiris bi te dun lor. Te, ciy waxam, tey la nguur gi gën a taxaw ngir def li war ba ñépp sàmmonte ak digle yi. Muy góor di jigéen, ku ci nekk am nga wàll ci xeex bile. Te, nan xam ne mbir mi du gaaw a sottee noonu ndax lu mu néew néew «dinanu jàmmaarlook mbas mi lu mat 3 mbaa 4i weer.» Looloo tax njiitu réew mi jàpp ne warees na soppi anam biñ doon xeexe ba ku nekk ci nun mën a dox ay soxlaam, dundal sunu koom-koom, waaye boole ko ak di moytandiku ngir aar sunu bopp, aaraale askan wi.
Li Maki Sàll jot a taataan yépp a ko tax a woyofal sàrti guural gi, ni mu ko waxe ci kàddu yii :
« Li ko dale talaata jii, 12eelu fan ci weeru Me 2020, dees na toxal waxtuy dëju-sa-kër yi nekkoon diggante 8i waxtu ci guddi jàpp 6i waxtu ci fajar, yóbbu leen 9i waxtu ci guddi ba 5i waxtu ci fajar. Ja yi ak yeneen bérébi jaayukaay yi ñu daan tëj yenn fan yi, ubbi leen yeneen yi, dinañ di ubbi 6i fan ci ayu-bés gi, 7eel bi ñu tëj leen, raxas leen. Njiiti gox-goxaat yi ñooy xool ni ñuy tànne bés yooyu. Luuma yi tamit dinañ ubbiwaat. Dees na ubbiwaat itam jàngu yeek jàkka yi. Jawriñu kaaraange biir réew mi ak jawriñu wér-gi-yaram ak ndimbal njaboot ji dinañ ci waxtaan ak kilifa ak mbootaayi diine yi ngir seet ci yan anam lees koy amale. »
Njàng mi…
Bu dee li aju ci njàng mi, njiitu réew mi dafa dëggal rekk ne, ci 2eelu fan ci weeru Suweŋ 2020 lay dooraat ñeel ndongo yi tollu ci kalaasi nattandiku, « maanaam kalaasi CM2 yi, 3ème yeek Terminaal yi. Ci xayma, 551.000i ci kow 3.500.000i ndongo, boo boolee lekooli nguur geek yeneen yi. Dees na joyyanti atum njàng mi ngir méngale ko ay dogal yi. » Maki Sàll teg ci ne, yeneen ndongo yi tollu ci yeneen kalaas yi dinañ wéy di jànge ci tele yi, rajo yi ak anternet. Bu dee iniwérsite yi, nee na seen jawriñ dina wéy di waxtaan ak kàngami iniwérsite yi ngir yaxanal njàngum teewadi mi. Maki Sàll ne, «Nguur gi dina fexe ba askan wiy sàmmonte ak digle yi ci juuma yi ak jàkka yi, ja yi ak luuma yi, lekool yi, bérébi jaayukaay yi, restóraŋ yi, ak béréb yiy am mbooloo yépp. Maanaam, képp kuy dem ci béréb yooyii, dees na fexe ba nga takk mask, raxas say loxo te sàmmonte ak dandante gi.»
10i miliyoŋi mask…
Njiitu réew mi xamle na ne Senegaal defaral na boppam 10i miliyoŋi mask yu mu nar a maye ci bérébi jaamukaay Yàlla yi, lekool yeek ja yi te du fàtte oto yiy yóbbu nit ñi ci biir gox-goxaat yeek biir réew mi.
Ci wàllu koom-koom gi, dafa mel ni Maki Sàll ci woyofal sàrti tukki yi la jëm. Moo ko tax a wax ne, «nawet baa ngiy ñëw, na nguur gi xool nu muy def ba yombal tukki bi ngir beykat yi ak ñu mel ni ñoom mën a dellu ci seen i tool. »
Maki Sàll rafetlu na yit xareñte doomi-réew mi. Nee na mu ngi bàyyi xel ñawkat yiy ñaw ay mask di leen maye, ndongoy iniwérsite yi, jàngalekat yeek gëstukat yiy defar ndoxum-raxasu yi am alkol, ay róbóo, ay noyyikaay ak i masini raxasukaay. Maki Sàll ñooñu ñépp la waxal, ku ci nekk mu rafetlu sa taxawaay ak liggéey bi ngay def ci jamonoy mbas mi ngir aar askan wi.
Njiitu réew maa ngi jeexale bàttaleem bi ci di sàkku ci askan wépp bennoo ak jàppalante ngir « xàll yoonu ëllëgu, yoonuw muñ ak ñaq jariñu, am ndam. »