(TEKKIG PAAP AALI JÀLLO)
Doktoor Paap Musaa Coor, gëstukat la, xelam màcc ci wérug mbooloo. Aji-caytuwaan (consultant) bi, jiite woon na fi tamit kurél giy xeex sibbiru. Moom, nag, ci xeexub mbas mi, naataangoomi fajkat yi dañoo jaar nii, mu jaar nee. Ndaxte, dafa biral ay kàddu yu safaanook tegtal ak digle yi doktoor yeek nguur gi joxe. Kàddoom yii, jukkees na leen ci waxtaanwu mu amoon ak Alasaan Sàmba Jóob ci Itv.
Ngir, nag, biral ne farul ak kenn, Lu Defu Waxu toftal na ciy kàdduy Dr Coor gis-gisu naataangoom Pr Musaa Séydi mi ne àndu ci tey àndu ci ëllëg
Lii la Doktoor Coor njëkk a wax :
‘’Damay dëggal kàdduy njiitu réew mi, Maki Sàll, bi mu waxee ne ‘luy jot, jot na ginnaaw dee’. Waaye, waxam jooju, mbasum Covid-19 bi la ci nammoon. Te, man, leneen a ma tax di wax. Leneen loolu mooy seen dogal yiñ jël ñeel xeexub mbas mi. dogal yooyu nga xam ne, boobaak léegi, ay loraange rekk lañu jural réew mi.
…Ku dem ba xamatoo foo jëm, dellul fa nga jóge
‘’Man, yaakaar naa ne, jot na ñépp toog, waxtaan waxtaanuw xel, wëliis waxtaanuw xol. Warees na xool, saytu ngir xam lan moo leen tax a jël dogal yooyii, lan lañ ci jublu woon ak yan ngirte lañ ci doon xaar. Day jaadu ci képp ku lal ab naal, walla nga jël ay dogal ngir xeex menn mbir, bu demee ba ci biir, mu amal ab taxaw-seetlu, xool ndax naal walla dogal yooyii baax nañ, am déet. Man, nag, wóor na ma ne, ñiy jël dogal yi dese nañoo xam li ñuy def.
Naam, boo xasee jël ay dogal yi aju ci wérug mboolem-nawle mi, dellu ginnaaw dina jafe lool. Waaye, ba tey lu mën a nekk la. Ndax, kuy dem ba xamatoo foo jëm, dellul fa nga jóge. Ndege, jamono metti na mettiwaay boo xam ne, koom-koom gaa ngiy suux. Nit ñi liggéeyatuñu, génnatuñu te, des na tuuti, dootuñu am luñ suturloo. Te, lii, mënta wéy. Warunu koo seetaan.’’
Nguur gi wekkiwul, day daaj
Nga xool yégle yi jawriñu wér-gi-yaram jiy biral suba su ne, bu 10i waxtu jotee. Saa su nekk mu siiwal wàllenti-ëlëm, naan “am nan ci nàngam… ñooñu béréb sàngam lañ dëkk…” Nga defe ni loolu jaadu na ci njiit loo xam ne, sa wareef bu jëkk, mooy dalal xelu askan wi ? Jàppal wàllenti-ëlëm fii, jàppal wàllenti-ëlëm fee. Nit ñi, ku ci dégg wàllent-ëlëm, saw fit naaw ndax dañ koo ngandal, garaawal ko ba nga ne lii lum doon. Te, nag, bu dee nii lañ ko nar a jàppe, nan leen defaruwaat, toog. Ndaxte, feek desàmbar dinan wéy di am ay wàllenti-ëlëm. Buñ ko xamulee, maa leen koy wax tey. Laaj bi sampu nag mooy bii : ndax nii lees wéy di doxale ba booba ? Te, nag, wax dëgg a neex Yàlla, fi ñu teg wàllenti-ëlëm yi àggu fa.
Nee ñu, wàllent-ëlëm mooy aji-tawatu Covid-19 bees xamul ku ko wàll jàngoro ji ak fan la ko ko wàlle. Nga xool, jamono ji doktoor bi paase-wisit aji-tawat bi ba koy jàppe wàllenti-ëlëm, nekkatu ko. Kon, taxatu koo ñàng noonu. Jamono jiŋ ko xamagulee kay la doon ñàng. Ndax, ci la doon dox di wàlle ak a tasaare feebarbi. Waaye, boo ko xasee am, jeex na. Lu tax nga koy tuddeeti wàllent-ëlëm ? Nguur gi wekkiwul, day daaj.
Gaw gi (le confinement) jaru ko…
Ci beneen boor, bépp fajkat xam na ne ñakk du lenn lu-dul doomu-jàngoro buñ néewal doole ba noppi daldi koy dugal ci yaramu nit ki. Liñ ci jublu mooy tàggat yaram wi, mu xàmmee doomu-jàngoro bi ngir, su duggatee ci yaram wi, doomi-kiiraayu deret ji (globules blancs) song ko, daan ko. Dafa di, nag, am na beneen xeetu ñakk bu ñuy wax ci nasaraan « vaccination naturelle ». Maanaam, bees bàyyee koronaa bi mu law, rawatina ciw askan woo xam ne ndaw yee ci ëpp, yarami nit ñi dañuy jur ay “anticorps”. Mënees na méngale “anticorps” yooyu akub dëq buy tee mbas mi law. Kon, lu fi jar gaw gi ? Nañ bàyyi nit ñi génn, doxi seen i soxla. Ndaxte, noonu mooy anam bu gën a gaaw ngir xeex mbas mi. Mu des, nag, yenn matuwaay yi mënta ñàkk. Maanaam, tëral ay pexe ngir saytu mbas mi, aar ñi jàngoroy Covid-19 bi gën a sonal. Lii rekk lan soxla te, tëlewunu ko. Am nan xam-xam bi ak jumtukaay yi. Kon, nan bàyyi tiitalaate bi. wàllenti-ëlëm du dara. Bu ma neexee sax ma ne, ci sunu wàll, ab xéewal la ! Nan bàyyi wiris bi law, dinan am kiiraayug-mbooloo, maanaam « protection de masse » ci nasaraan.
Warees na dalal xelu askan wi
Man, bu ma doon ñoom, ay baat yu mel ni wàllent-ëlëm, añs., dama koy bàyyee fajkat yi ; seen waxin la, ci ñoom la war a yem. Waaye, aw askan walla mbooloo, booy wax ak moom war nga xam li ngay wax. Dangay xool li mu aajowoo xam, nga xamal ko ko ci kàllaama gu leer, te yem fa. Te, nag, li askan wi soxal mooy xam fi mbir mi tollu cig tënk, xam naka la koy moytoo, fan lay dem su ko amee (walla ñan lay woo). Jeex na !
Lenn am na, bu feebar dikkaale nit koo xam ne, dafa ame tiitaange ak njàqare, loraange yi muy def moo ëpp fuuf bu dee feebar bi da koo fekk cim xel mu dal. Moo tax, doktoor, liy wareefam bu jëkk, mooy saa su nekk jéem a dalal xelu aji-tawat bi laata muy jublu ci paj mi. Boo ko mënul a faj tamit, nga dalal xelam. Ndege, lee-lee nga dalal xelu aji-tawat ba mu jaare fa wér te doo ko sax laal. Aji-tawat dina la fekk sa palaas, nga wax ko wax ju teey te dal, raay boppam, mu ne cocc wér te joxoo ko benn garab. Waaye, bu dee dafa ñëw nga tiital ko, yóbbu fitam, ndare amewul dara sax, feebaram dina yokku, nga daldi koy lor.
Yeneen feebar yaa ngiy rey nit ñi, ñu naan koronaa bi la…
Jamono jii, nag, am na ñu bare ñuy dee, ñu naan koronaa moo leen rey fekk ne, wóor na Yàlla, beneen feebar moo leen rey. Ndege, lépp lañ jël sippi ko koronaa bi. Ana kañseer ? Ana sibbiru ? Ana koleraa ? Ndax feebar yooyu dañ fee jóge ? Ana jigéen ñiy matu ci àll bi, ci kow i saret ? Mu mel ni koronaa rekk mooy feebar. Kenn fajatu fi leneen lu dul koronaa. Pómpiye yi, sax, kenn mënatu leen a jot.
Te, nun, Yàlla daf noo suturaal. Li mbas miy def ci réewi tubaab yu ci mel ni Espaañ, Àngalteer, Etaasini walla Farãs, bu ko defoon ci miim réew, ken waxatu ko. Bu la Yàlla defalee sutura daŋ koy xam te sante ko ko. Léegi, nag, réewi sowu yi ñoo nuy tiital, naan nu « feebar baa ngiy ñëw de ! Fagaruleen ! Bu agsee du baax ! Gaawleen lal palaŋu fàggu ngir nu lebal leen xaalis. » Noonu lañuy def, di fowe sunu xel yi. Te, jamono jii, dan waroon a taxaw temm ; ndax réewi sowu yi laago nañ jamono jii, seen doole wàññeeku na bu baax. Li nu waroon kay, mooy nu defar ay mask, ay gã ak sax ay noyyikaay ngir jaay leen ko. Am nan xam-xam bi ak mën-mën bi. Waaye nuy ñàkkal sunu bopp faayda nii. Fexe nañ ba jaay nu xel, tiital nu, nax nu ba nu nërmeelu ak ñoom. Lan lees ci war a jàngat ?
Mbas mi, nootaange da cee laxasu
Nan taxaw, seetlu. Naalub fàggu bu 1000 miliyaar yi, ñaata la ci Banque Mondiale ak FMI dugal nga foog ? Xaalis bu bare ! Te, du may, du sarax. Bor buy dolleeku ci yeneen bor doŋŋ la. Yaa ngi naan ñu far bor bi walla wàññi ko ba noppi ngay wëlbatiku di lebaat. Ndeysaan, sunuy doom ñoo koy fey. Kon, dañ nuy gal-gal ; te ci lañ dëkk.
Démb, amoon nañ fi mbasum H1N1, Sras-cov, Mers-cov, Ebola, añs. Tey, ñu indil nu mbasum Covid-19. Ëllëg tamit, leneen lañ nuy indilati ba noppi naan nu def leen lii nu lebal leen. Lenn rekk lañ bëgg, mooy gën noo saxal cib nootaange, suuxal sunuy koom-koom. Noonu ba kañ ?