Sëñ Elaas Maalig Njaay lañu fal ci boppu Ngomblaan gu yees gi. Ci altiney tay jii, 2i pai desàmbar 2024, lees doon samp 15eelu moomeg Ngomblaan gi. 134i dépite ñoo ko woteel ci biir 165i dépite yi séq Ngomblaan gi. Ñaari dépite kepp ñoo wote safaan, mu am juróom-ñaar yu màndu (ñàkk a wote).
Laata ñuy wote ngir fal njiitul Ngomblaan gi, coow xawoon na fa am. Nde, dépite Guy Mariis Saañaa dafa biraloon ay laaj ñeel ndombog-tànku Elaas Maalig Njaay mi nekkoon jëwriñ ci Càmm gi. La mu doon laaj mooy ndax dafa tekki ndombog-tànkam njëwriñu yaale gi am déet. Ndaxte, Yoon dafa araamal ku boole ndombog-tànku jëwriñ ak dépite. Waaye, Ayib Dafe mi jiite kippug Ngomblaan gu Pastef moo gaaw, leeral ni Elaas Maalig Njaay tekki na ndombog-tànkam. Ginnaaw gi la Sëñ Àlla Kan, magum Ngomblaan gi, ubbi wote bi, ñu daldi fal Elaas Maalig Njaay mom, moom kese moo nekkoon lawax.
Elaas Maalig Njaay nag, Daara-Jolof la juddoo ca atum 1983, diiwaanu Luga. Moom, ci wàllu yaale ak i jumtuwaay la xam-xamam màcc. Atum 2015 la dugg Pastef. Cig pàttali, jot na a liggéey ca lijjanti gii di Maersk Line ak Eramet ginnaaw bi mu jàngee ca IAE fa Paris-Sorbonne ak fa Jànguneb Paris Dauphine-PSL. Ca weeru màrs wee nu génn la ko Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, tabboon ci njëlbeenug Càmmam gi. Bés niki tay, mooy njiitul Ngomblaan gi.