ËLLËGU XALIFA SÀLL CI LÀNGU POLITIG GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Dibéer, 29eelufan ci weeru sàttumbar 2019, la Xalifa Sàll gisaat jant bi ginnaaw bi ñu ko ko nëbbee ñaari ati Yàlla ak genn-wàll. Ñuŋ ko toppe woon tuuma yii di wuruj ak luubal xaalisu méeri bu Ndakaaru. Alal jooju, nag, nee ñu ciy daara la waroon a dem, maanaam ci njàngale mi. Keroog ba ko takk-der yi jàppee, coow li noon na kurr. Xalifa Sàll weddi tuuma yi ñu teg ci ndoddam li ba mu set wecc, lànk ba tëdd ci naaj wi, moom ak i ñoñam. Ñoom, ci seeni wax, Njiitu-réew mi, Maki Sàll ci boppam, moo sooke lépp. Nee nañu yit duggewu ko lenn lu dul bañ Xalifa Sàll bokk ci woteb njiitéefu réew mi ñu dégmaloon ci ndoorteelu 2019. Ndaxte, ba tey ci seeni wax, jamono jooju, Xalifa Sàll rekk a fi amoon dayo bi koy tax a wujje ak Maki, sañ koo diir mbagg. 

Naka noonu, Maki singali ko, kootoog yoon, ñuy lem ak a lemmi, di nos ak a nocci ba tëjlu ko ci atum 2017. Xalifa Sàll, nag, juróomi ati kaso la waroon a tëdd, teg ci ne waroon na fay Buur juróomi miliyoŋ ci sunuy koppar. Waaye, ñaari at ak génn-wàll rekk la jot a tëdd ñu bàyyi ko. Li sabab lu ni mel, nag, dese naa leer ci boppi askan wi. Ndege, am na ñu naan Maki da koo mujjee baal li ñu ko doon toppe ngir bëlde askan wi ko mere woon, mook rakkam Aliyu Sàll, ci coowal petarool li fi jiboon, fexe ba ñépp fàtte loolu. Ñeneen ñi jàpp ne waxtaan wi fi sëriñ Muntaxaa Mbàkke laloon ngir jubale Abdulaay Wàdd ak Maki Sàll ci ubbite jumaawu Masaalikul jinaan ji, moo waral lii lépp. 

Wànte, ak lu mu ci mënti doon, li wóor mooy ne Xalifa Sàll génn na. Te mbir mi mbégte mu réy a réy la jur ci doomi réew mépp. Rawatina nag ci ñi mu bokkal pàrti. Guddig keroog ga muy génn, foo sànni mbàttu ci Ndakaaru mu tag. Askan wi da ko teeru nib buur, gunge ko ba ci biir këram. Bu fa yemoon sax ñu ne waaw ; waaye gaa ñi am nañ meneen mébét. Dafa di, yaakaar la génnub kaso Xalifa Sàll bi meññloo ci xol yi. Waaw, yaakaar kañ ! Bu kenn fàtte ne ca njëlbéen ga, newoon nañu ne am na ci doomi-réew mi ñu gëm ne Xalifa Sàll rekk moo fi mën a jële Maki. Te yaakaar jooju mel na ni ñaari ati kaso yi dindiwuñ ko ci xoli farandoo Xalifa Sàll yi. Mënees na ni sax tey la Waalo gën a aay. Keroog bi ñu bàyyee Xalifa la ki ñu gën a ràññee ci àndandoom yi, Bàrtelemi Jaas, tàmbalee waajal joŋante njiitéefu-réew mi war a am ci atum 2024, ànd ceek fullaam ju mat sëkk. Moom sax xanaa daa fàtte ni Xalifa day door a génn ?  Li waral laaj bi du lenn lu dul ne sunu àtte ndeyu réew mayul ku yoon mës a tëj muy bokk ci joŋante woteb njiitéefu réew mi. Am da koo fàtte ? Naam sax Xalifa baal nañu ko waaye teewul ñu jot koo àtte ba teg ko ay daan. Kon li mu tëddoon Rëbës xaw na xajamal ay mbiram ci wàllu politig. Amaana looloo tax am ñu seen bopp xaw a tëju ba ñuy laaj lan mooy ëllëgu Xalifa Sàll ci géewu politig bi. Tontu ci du yomb waaye xel mënuta nangu ne Xalifa Abaabakar Sàll, newoon fi Meeru Ndakaaru te tàmbalee xeex ba muy gone gu ndaw, jeexal na ba fàww ci politigu Senegaal..

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj