ETAASINI : DÀQ NAÑ 140i SAA-SENEGAAL

Yeneen i xët

Aji bind ji

140i saa-senegaal la Etaasini dàq. Daf leen a waññi ginnaaw biñ fa duggee ci anam bu jaarul yoon. Yéenekaay Les Échos moo siiwal xibaar bi.

Limub saa-senegaal yiy sàcc di dugg fa Etaasini mi ngi wéy di yokk. Réewum Nikuwaraguwaa lañuy faral di bëtte, dugg fa réew ma Jóo Biden jiite. Waaye de, ci alxamesu démb ji, am na 140i doomi Senegaal yi ñu delloosi fi réew mi. Ñoom itam, ndeke, Nikuwaraguwaa lañ jaare. 

Nee ñu, guléet lim bu ni tollu ciy saa-senegaal di dugg fa Amerig. Bees sukkandikoo ci Baaba Aydara, ab taskatu xibaar  bu féete foofa :

“Gaawu gii weesu, 20i saa-senegaal lañu jébbaloon keyitug dàq (avis de déportation). Ca ëllëg sa, dibéer, yeneen téeméeri saa-senegaal yi doon sog a jéggi digi réew ma, ca booru bëj-saalum ba, jot nañ ci këyitug dàq.”

Kii di Elaas Aamadu Ndagaan ndaw, àmbasadëeru Senegaal fa Etaasini, dëggal na xibaar bile. Waaye, moom, limub 135 walla 137 la joxe. 

Njiitu réew mi, Maki Sàll, war dem Etaasini ci dibéer ji. Waaye, roppalaanam bi dafa nar a rombante ak roppalaan biy delloosiy doomi Senegaal. Ak wote yees dëgmal, askan waa ngi xaarandi ba xam lu lawax yiy wax ak dige ñeel xëyub ndaw ñi. Ndax, léegi dañu xeeb mbëkk mi bay sóobu ci yoonu suuf si ak jafe-jafe yi mu làmboo yépp. Lépp ngir bëgg a tekki, te yaakaarewuñ ko fi réew mi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj