Démb ci àjjuma ji, ginnaaw julli jumaa, la waa F24 woote woon fa « Place de la nation » ngir amal fam ndaje mu réy. Mbooloo mu takkoo takku daje fa, fees fa dell. Ay kilifa yu mag, féete boor bu nekk, teewoon fa. Ñépp def wenn say, bokk waxandoo genn kàddu gog, ci tënk, mooy : « 3eelu moome, dees koy tere ci réewum Senegaal.»
Mbooloo mu baree baree wuyusi woon wooteb kurél gii di F24 ci àjjumay démb ji, 12 me 2023, fa « Place de la Nation ». Kurél gi dafa boole ay làngi pólitig yi ci kujje gi, ay mbootaay ak i kilifa yu am dayo yoy, ñii ciy sàndikaa lañ bokk, ñee di ay way-moomeel, ñenn ñi di ay kilifay diine, ñeneen ñi di ay kilifay aada, ña ca des diy jëmm yu am i tur. Ñoom ñépp nag, benn jubluwaay a leen tax a ànd, te mooy xeexal demokaraasi bees jàpp ne, dafa sooxe, nasax lool ci Nguurug Maki Sàll. Démb a doonoon seen njëlbeenug jéego ci xeex biñ sumb, nar cee jàmmaarloo ak Njiitu réew mi ba keroog muy deeltu ginnaaw.
Ba 12i waxtu di jot, ci suba gi, perefe bi génnegul woon ndogal liy daganal ndaje ma. Doon nañ njort sax, di laaj ndax dina ko maye. Waaye, bi waa F24 doon janook taskati xibaar yi ci waxtu woowu la xibaar bi jib, ñu xamle ne perefe bi jibal na ndogal li : ndaje mi mën na am. Doxalin woowu nag, njiiti kurél gi ñaawlu nañ ko. Ndax, waroon na génn ñaari fan laata bésub ndajem ñaxtu bi. Kujje gi jàpp ne, perefe bi duggewu ko lenn lu dul nasaxal ndaje mi, dugal i lënt ci xeli askan wi ngir mbooloo mi bañ a teew. Waaye, bu dee loolu la, pexeem àntuwul. Nde, waa F24, laata ndogal liy génn, tàmbali woon nañ waajal béréb ba. Mbooloo mi tamit wuyusi woon na bu baax a baax sax. Sikk amul ci ne, jubluwaayu kurélug F24 gi mate na. Ñu bari jël nañ fa kàddu gi, naqarlu, ñaawlu ni Njiitu réew mi, Maki Sàll, yore réew mi ak ni mu nootee Yoon, di ko defloo, di ko dindiloo. Waaye, la gënoon a fës ci kàddu ya mooy mbirum ñetteelu moome gees jàpp ne, Maki Sàll yelloowu ko.
Ku ci mel ni Décce Faal, njiitul PRP li bokk ci lëkkatoo Yewwi Askan Wi, bim jëlee kàddu gi, daf ne :
« Maki Sàll mënul tere kenn bokk ci wotey 2024 yi…Ki dul bokk, moom kepp la. »
Maalig Gàkku, njiitul Grand Parti, bokk tamit ci Yewwi Askan wi, feelu Décce Faal, dolli ci ne Maki Sàll xam na ni jeexal na. Yemu ca, ndax biral na àndam ak ak jàppale bi muy jàppale Usmaan Sonko ci tooñ yi ko Maki Sàll di tooñ. Moom, Maalig Gàkku, nee na du mës ànd ciy pexe yoy, Maki Sàll duggewu leen lu dul toroxal njiitul Pastef lim bokkal lëkkatoo, walla di ko tere bokk ciy wote. Rax na ca dolli ne, moom, du bokk ci waxtaan woo xam ne, ag kootoo a ko lal.
Bu dee magum jëwriñ ja woon, nekkoon fi yit jëwriñu Yoon wi, Aminata Ture, moom dafa delloo buum ca boy-boy ga. Kenn umpalewul taxawaayam ci xeex ñetteelu moomeg Maki Sàll gi. Mu gis ne, Maki Sàll mi jiite réew mi, dafay « làq ay sàcc, di sàcc suufi réew mi. » Moo ko tax a digal ndaw ñi, soññ leen ngir ñu takku taxaw, bañ ñetteelu moomeg Maki Sàll gi ba fu bañ yem.
Usmaan Sonko teewewul ndaje ma. Ma nga, ba nëgëni, ca Sigicoor. El Maalig Njaay mi yor jokkalanteg Pastef a ko fa teewaloon. Bi jolof-jolof bi waxee, dafa ñaawlu jàpp yu bari yi ñuy jàppaate ci réew mi, te dara teguwu ci ci dëgg. Ñi ci gën a sonn di naataangoomi Pastef. Mi ngi jeexalee kàddoom ci artu ñeel tere bi Maki Sàll bëgg a tere ay lawax yi ci kujje gi bokk ci wotey 2024 yi. Mu gis ne, loolu, mën na jur fitna ju amul àpp ci réew mi. Yeneen kilifa ya fa ñëwoon yépp, lu ni mel lañ fa wax. Kàddu gi, genn la.
Mbooloo ma fa teewoon nag, saa bu ag kilifa jëlaan kàddu gi, dañ koy tàccu. Waaye de, teraanga boobu, defaluñ ko Xalifa Sàll ak Paap Jibril Faal. Nde, dañ leen fa doon yuuxoo. Daanaka, naruñu woon wax ndax mbooloo mi nanguwu leen woon déglu. Yeneen kilifa ya fa teewoon a mujj wax ak xale yi ngir ñu bàyyi leen ñu wax.
Bu dee meeru Ndakaaru ba woon, Xalifa Sàll, njiitul Taxawu Senegaal li, coowal Bàrtelemi Jaas ak Usmaan Sonko ñeel wooteb waxtaan wi Maki Sàll def, moo sabab yuuxu yiñ ko fa yuuxu. Ndax, ñu bari dañ jàpp ne Xalifa Sàll réeroowul ak Njiitu réew mi, Maki Sàll. Ñoo ngi waxtaan ci suuf, di nas i pexe. Moo tax ñu jàppe ko workat.
Bu dee Paap Jibril Faal moom, du guléet ñu koy toroxal cim mbooloo. Wii mooy ñaareelu yoon wi ñu koy yuuxoo cim ndaje. Jàppees na ne, moom itam, péeteem ci kujje gi dafa lënt. Nde, ci li nit ñiy wax, day màtt di ëf.
Bu loolu weesoo, lees war a jàpp mooy ndajem F24 mi jaar na yoon. Mbooloo ma bari na, xeex amu fa, kenn yàqul, kenn tilimalul. Te yit, wax ja fa jibe leer na : wenn say, génn kàddu, ngir jàmmaarlook Maki Sàll.
Ñu xool ba xam ndax loolu dina tax Njiitu réew mi, Maki Sàll, dellu ginnaaw am déet.