FAATUG MUHAMMET JÓOB FA PIKIN

Yeneen i xët

Aji bind ji

Am nay xibaar yu bees yu rot ñeel faatug Muhammet Jóob. Nde, jàllale nañ juróom-benni alkaati yiñ ci jàppoon.

Keroog 27 mars 2024 la alkaatiy Pikin yi jàppoon kii di Muhammet Jóob. Waaye, bi Muhammet Jóob di génn pólis, génnaalewul bakkan. Ci les wax, alkaati yee ko fa dóor dóor yu metti ba mu ñàkke ci bakkanam. Coow li ne kurr, lëmbe réew mi. Ca la waa DIC ubbee ag luññutu ci ndigalu toppekatu Pikin bi.

Ba waa DIC dégloo alkaati yi, dañ leen jébbaloon toppekatu Pikin bi (parquet de Pikine). Waaye, bees sukkandikoo ci yéenekaayu Libération, toppekat bi daf leen a jàllale ndung-siin. Tuumay faat bakkan lañu leen di toppee.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj