Farba Ngom dem na kaso. Tay ci alxemes ji, 27 féewiryee 2025, la ko njiitul àttekati “Pool judiciaire financier” (PJF) yi dóor ab “mandat de dépôt”. Moom Farba Ngom, turam dëgg di Muhammadu Ngom, lees koy tuumaal mooy : luubalub alal ju tollu ci 31i miliyaar, weexalug xaalis ak kootoog njubadi.
Waa CENTIF ñoo amaloon ag luññutu, daldi génne ag caabal gog, dañu ci duut baaraam 125i miliyaar yu dugg ak a génn, te teey xel. Loolu nag, ci li luññutug waa CENTIF feeñal, Farba Ngom daf ci laale.
Looloo tax ñu woolu woon Farba Ngom ngri déglu ko. Moom nag, ci liy layookatam xamle, dafa weddi lépp. Waaye, ngir bañ ñu jàpp ko, dafa tayle woon ay taax yoy, bees xayma seen njëg, dafay tolloo ak limu xaalis bi ñu koy toppe. Yoon nag dafa bañ tayle boobu. Ndax, toppekatu PJF bi dafa sàkku woon ci àttekat bi mu gàll ko “mandat de dépôt”. Layookatam yi, ñoom, dañu bëggoon ñu bàyyeendi ko, mu nekk ci caytug Yoon (mise en liberté provisoire sous contrôle judiciaire). Wànte, àttekat bi dafa santaane ñu jàppandi ko ca kaso ba, fileek ñu koy àtte.
Ci beneen boor, mbir mi, tudd nañu ci Aamadu Sàll, doomu Maki Sàll, Njiitu réew ma woon. Dañu wax ne, moom Aamadu Sàll, dafa laale ci luubalub alal ju tollu ci 10i miliyaar. Mu am itam yeneen juroom-ñeenti nit ñees ci tudd. Toppekatu PJF bi moom, ñi ñu ci tudd ñépp la sàkku ñu teg leen “mandat de dépôt” ba mu des kii di Mamadu Daaf mi nekkoon njiitu lu mag lu CMU (Couverture Maladie Universelle). Moom Aamadu Daaf, 35i miliyoŋ yi mu génne ci ab bànk lañu koy toppe.
Amoon na ay farandooy Farba yu dajaloo woon ci kanamu màkkaanu PJF ngir ñaxtu, jàppale ko. Waaye, takk-der yi dañu leen dàq ak i lakkirimosen.
Ëllëg, Tayiiru Saar dina wuyuji àttekati PJF yi. Moom itam, ci mbirum 125i miliyaar lees koy déglu.