FËKKUG XALIFA AAMADU HAADI TAAL FA MALI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tiijaani Mali yi ñu ngi ci tiis ak njàqare, rawatina njabootu Séex Umar Fuutiyu Taal ga fa nekk. Seen xalifa ba, Aamadu Haadi Taal, la rëtalkat yi fëkk, yóbbu ko fu kenn xamagul. Keroog alxames, 26i pani desàmbar 2024 la mbir mi xew. Fi mu nekk nii, njiiti réew ma jël nañu ay ndogal ngir ñu seet ba xam fan la nekk, muccal ko ci loxoy sàmbaa-bóoy yooyee.

Ay sàmbaa-bóoy yu gànnaayu ba diis ñoo jàpp Xalifa Aamadu Haadi Taal, keroog alxames 26i pani desàmbar 2024. Fa Jabijala, wetu Ñooro Sayel, lañu ko dogaale, fëkk ko.

Ci genn gàmmu la kilifa diine bi jóge woon, doon ame ci benn dëkk bu jege. Ci yoonu ñibbisi wi la ko rëtalkat (terorist) yi dogaale. Ci lees rotal ciy xibaar, jotees na fa soqi ay soxi fetel. Nee ñu, xaw nañu gaañ tuuti xalifa bi. Noonu, ñu daldi koy jàpp, yóbbu ko fof, ñoom rekk ñoo ko xamagum.

Ba démb ci gaawu bi, amagul woon genn kurél ci kuréli rëtalkat yi gu waxoon ne moo jàpp xalifa bi. Waaye, xel yi, ci sóobarey rëtalkat yi ci diiwaan boobee lañu demoon. Nde, ñoom lañu njortoon ne ñoo def ñaawteef bile. Njort li mujje na doon dëgg.

Kurélug rëtalkat gees duppee Groupe de soutien à l’islam et aux musulmans, gàttal biy joxe JNIM, wax na ne moo jàpp xalifa bi, Aamadu Haadi Taal.

Dafa am ndégtu luy daw ci mbaali-jokkoo yi, waa JNIM ñoo ciy wax. Ci biir wax ji, biral nañu ne, ñoom ñoo jàpp xalifa ba. JNIM nag, ci Al-Qaïda la bokk. Ñoom, ca seen i wax, xalifa ba seen noon la, loolu moo tax ñu jàpp ko. Ndaxte, nee ñu, xalifa ba, Nguurug Mali la faral wëliis ñoom jiyaadist yi. Rax-ci-dolli, JNIM dafa ñaawlu teewaayu sóobarey Riisi yi bokk ci Wagner ca seen gox ak ñaawteef yi ñuy teg ci kow askan wa. Ngir bàyyi kilifa diine bi, jiyaadist yi dañu bëgg mu jël ndogalu dogoo ak Nguurug Mali.

Moom, Aamadu Haadi Taal, Islaamu jàmm lay woote. Sëtu Ceerno Muntagaa Taal la. Dafa di, bu yàggul dara, dafa ŋàññi woon fitna ak tafaar ji rëtalkat yiy waral ci turu diine ji. Ca mawluut ba doon ame Ñooro la ko waxee woon. Kàddoom yooya nag, ci lees foog, moo naqadi rëtalkat ya féete foofa.

Njiiti Mali yi ubbi nañuy luññutu yu yaatu ngir delloosi xalifa bi ci njabootam. Am na yit ay mbooloo yu sumb ay jotaayi ñaan ngir seen xalifa bi delsi ci jàmm ak salaam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj