Xibaar bu yéeme te doy waar moo jib tey, ci bésub tabaski bi. Muy xibaarub fitna ak taafar ju bawoo Medina Gunaas, diggante ñaari kurélu diine yu bokk benn waaso, bokk itam benn tarixa. Nee ñu, Xalifa Medina Gunaas bii di Ceerno Aamadu Tiijaan la am mbooloo song otoom, di ko sànniy xeer ba mbir ma tàbbi ci xeexoo bu jur tóoxidóona.
Bésub tabaski de, jàmmoo, bennoo ak baalante àq lees ci miin. Muy bésub mbégte bob, way-gëm yi dañuy tàppe xol ginnaaw bi ñu jubalee sàppey jullig yoor-yoor biy màndargaal bés bu mag bile ci lislaam. Waaye de, tabaski ren jii, wex na xàtt ci askanuw Medina Gunaas wa. Li ko waral mooy ab xeex bu fu amoon tey, biñ jullee tabaski ba noppi. Bees sukkandikoo ci PressAfrik mi taataan waxi ma-kàddu (porte-parole) Xalifa Medina Gunaas bi, lenn ci ñoñi Medinatul Hudaa (di ay Saa-Fuladu) ñoo song daamaru Xalifa bi, naan ko xërr i xeer.
Ñoom, waa Medinatul Hudaa, ñoo gën a néew ci gox ba : téeméer boo jël ca askan wa fay yeewoo, juróom lañ fa walla 10. Waaye, ànduñu ak Xalifa ba. Ci li PressAfrik rotal, jëlee ci ki yor kàddug Xalifa Medina Gunaas bi, ca “rond-point” ba lañu kar oto Xalifa bi, di ko sànni ay xeer. Sàndarmëri moo mujje xelal Xalifa bi mu beru, xaar tuuti ba yëf yi dal mu sog di àggali yoonam. Waaye, loolu fayul coow li.
“Bi Xalifa bi xaaree lu jege 15 jàpp 20i simili, ci li ko sàndarm yi xelaloon, dafa doon jéem a dellu këram. Waaye, bi muy dem rekk la ay nit yu génnee ci jumaay gox bi tàmbalee sànniy xeer ci otoom ak oto yi ko toppoon.” (Kàdduy ma-kàddu Xalifa bi, PressAfrik)
Nee ñu, ñu bare jële nañ ciy gaañu-gaañu. Daamaru Xalifa bi tamit, amee na ci yàqu-yàqu. Waa COD/TMS (Cadre d’échange et d’organisation des disciples de Thierno Mouhamadou Saïdou Ba) génnee nañ ab yëgle di ci duut baaraam Ngaabunke yi (waa Ngaabu).
Nee ñu, wëliis oto Xalifa Ceerno Aamadu Tiijaan Ba bi ñu yàqate, am nay kër yu ñu taal. Ba tey, ci seen yëgle bi, ñu xamle ne am na kenn ku ci ñàkk bakkanam.
Li am ba des mooy, fitna ji yàgg na lool. Dees na ci dox tànki jàmm, seet i pexe ngir juboole ñaari kurél yooyu balaa mbir miy ëpp i loxo. Ndax kat, ay du yem ci boppu boroom.