FITNAY KÀMPAAÑ BI / NDAR : JÀPPAGUM NAÑ 81i NIT

Yeneen i xët

Aji bind ji

Pólisu Ndar bi jàppagum na juróom-ñett-fukki nit ak benn yees njort ne dañu laale ak fitna yi amoon ci guddig altine ji fa Ndar. Jaraafu diiwaan ba, Al Hasan Sàll, moo ko xamle.

Jaraaf bi daf ne :

« Ci altine ji, 11i pani nowàmbar 2024, ci wàllu kàmpaañi wotey 17 nowàmbar yees randalsi, nemmeeku nañ ay fitna yu jib fi Ndar diggante ñi doon wattu kaaraangeg menn njëggu pólitig ak i jaaykat fa jawub Soor. » APS moo taataan yile kàddoom.

Jaraaf bi teg na ci sax ne, am na ay nit ñu ci jële ay gaañu-gaañu, ñu sàccaale ci alali jàmbur, añs. Loolu moo tax ñu ubbi ag luññutu ngir leeral mbir mi, xam ku def ak ku deful, yoon daldi ci def li war. Ci kow loolu, takk-der yi jàppagum nañu lu tollu ci juróom-ñett-fukki nit ak benn ñoñ, dañoo njortagum ne laale nañ ci fitna ji.

Fileek ñuy wéyal luññutu gi, Jaraaf baa ngi woote jàmm, di ñaax ñépp ñu wéer ngànnaay yi. Mu ngi digal njëggi pólitig yi tamit ñu jaar ciy yoon yu wuute, di moytoo mbëkkante ci yoon yi. Jëwriñu biir-réew mi tamit, Sã-Batist Tin, artu na, dankaafuwaat ñépp, xamle ne jox nañ ndigal takk-der yi ngir ñu seet nit ñi ak ñiy ànd ak njëgg yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj