FMI DËGGAL NA ËTTUB CETTANTAL GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

RFI, saabalukaay Farãs bi, moo siiwal xibaar bi. Ci li mu fésal, FMI dafa wax ne, diggante 2019 jàpp 2024, Nguurug Maki Sàll ga woon dafa nëbboon borub “7i miliyaari dolaar”. Wax joojee nag, dafay feddali caabalug Ëttub cettantal gi.
Ca weeruw féewiryee 2025 wa nu génn la Ëttub cettantal gi siiwaloon ag caabal ginnaaw bi mu lëñbatee sàqi Càmm gi, amal gëstu bu xóot ci nees yoree woon koppari réew mi ca jamonoy Sëñ Maki Sàll. La tukkee woon ca caabal googee nag, yëngaloon na réew mi, jaaxal àddina sépp. Nde, lees ca jànge mooy ne, ñi nekkoon ci boppu réew mi diggante 2019 jàpp 2024, dañu daan caxat-caxatee alalu askan wi, yoree woon ko ci anam bu safaanoo ak njub. Ca la saabal gi xamlee ay njombe yu réy a réy ñeel yoriinu koppari doomi réew mi : ay luubal ak i njuuj-njaaj, rawatina li ñu nëbb boru réew mi.

Eddy Gemayel mii jiite ndaw yi FMI yónni Senegaal dafa njëkk a wax ne : “nangu nanu li caabalu Ëttub cettantal gi xamle.” Mu rax ca dolli ne :

“Dañu néewal tolluwaayu bor bi. Maanaam, dañu nëbb benn pàccu bor bi. Te, loolu moo taxoon ba njiit ya woon mën a lebiwaat ci ja yi, di jaay xar-kanamu Senegaal gu rafet ci jayi koppar yi ak it ngir mën a leb ci ay anam yu gën a yomb fuuf bu fekkoon ne wax nañu dëggantaan tolluwaayu bor bi.”

Tungune du teew ñuy nataal. Lii lépp, caabalu IGF gaa ko njëkkoon a wax, gog Ëttub cettantal bi ñëw feddali ko, waayeet gën ko leeral.

Mu mel ni, ci fànni koppar ak koom-koom, Senegaal dafa nekkandi ci guuta gu metti. Moo tax njiit yiy sàkk i pexe ngir génne ci réew mi. Bu dee lu ñeel pexe yooyii nag, FMI joxe na ci xalaatam, daldi joxoñ ay yoon yoy, ci gis-gisam, bu ci Senegaal tegoo, dinañ génn ci lëndëm bi ñu nekk.

Sëñ Eddy Gemayel dafa joxe ñaari pexe yu mënut a ñàkk ngir joyyanti koom-koomu réew mi, tegaat Senegaal ci yoon wu jub. Bees sukkandikoo ci moom, li war, te gën a jamp, mooy fexe ba “sellal yoriinu koppari bokkeef gi”. Loolu mooy dëppoo ak bàkku Nguurug Jomaay gi : jub, jubal, jubbanti.

Ñaareelu liggéey bi, ba tay ci kàdduy Sëñ Gemayel, mi ngi aju ci jubluwaay yi Càmm giy dàkk ci fànni koom-koom. Sëñ bi daf ne : “Njiit yi dañu war a sumb seen naal wu bees wi ngir kopparalkat yi mën a ñëw.” Ci xalaatu njiitul ndawi FMI yi, bu loolu yembee, dina doon ndimbal lu réy ci réew mi. Mu jeexalee ay kàddoom ci rafetlu naaluw “Senegaal 2050” wi ngi xam ne, ab poseb yokkute la bob, dafay sawarloo ñiy dugal seen i koppar ci réew mi ngir liggéey.

Saabalukaay AFP moo taataan i kàddoom.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj